Yeesu nettali na léebu jikat bi
4
Yeesu tàmbaliwaat di jàngale ci wetu dexu Galile. Mbooloo mu takku dajaloo, wër ko, ba tax mu yéeg ci benn gaal bu nekkoon ci dex bi te toog ci. Mbooloo mi nekk ci tefes bi. 2 Doon na leen jàngal mbir yu bari jaarale ko ci ay léeb di wax naan: 3 «Dégluleen! Dafa amoon benn jikat bu génn ngir ji. 4 Bi muy ji, am pepp yu daanu ci yoon bi. Picc yi ñëw, lekk leen. 5 Yenn pepp yi daanu ci diggante xeer yi fu amul woon suuf su bari. Ñu jóg ci saa si ndaxte suuf si xootul woon, 6 waaye bi jant bi fenkee ñu daldi lakk te wow ndaxte amuñu ay reen. 7 Yeneen pepp yi daanu ci diggante ay xaaxaam. Ñu daldi jógandoo ak xaaxaam yi. Xaaxaam yi tanc leen te noonu amuñu meññeef. 8 Waaye yi ci des daldi daanu ci suuf su baax si. Ñu sax, jóg, te meññ. Yenn yi meññ fanweeri pepp, yeneen yi meññ juróom benn fukk, yi ci des téeméer.» 9 Yeesu yokk ca ne: «Na ki am nopp ngir déglu, dégg.»
10 Bi ñu nekkee ak moom kese ñi àndoon ak moom ak fukk yi ak ñaar laaj ko li léeb yooyu di tekki. 11 Mu ne leen: «Yeen, Yàlla may na leen ngeen xam li nëbbu ci nguuru Yàlla gi. Waaye ñi ci bokkul, dama leen di wax lépp ci léeb, 12 ngir
ñuy xool bu baax waaye duñu gis dara,
te ñuy déglu bu baax waaye duñu ràññee,
ngir ñu baña woññeeku te Yàlla baal leen.»
13 Gannaaw loolu Yeesu ne leen: «Su ngeen xamul léeb bii, naka ngeen di xame yeneen léeb yépp? 14 Jikat bi, kàddu Yàlla gi lay ji. 15 Ñenn ñi ñooy ñi nekk ci wetu yoon bi ñu ji kàddu gi. Bi ñu déggee kàddu gi, ci saa si Seytaane ñëw, këf li ñu ji woon ci ñoom. 16 Ñi nga xam ne ñoo jot jiwu ci béréb bi am xeer yi, su ñu déggee kàddu gi rekk, ci saa si ñu nangu ko ak mbégte. 17 Waaye kàddu gi saxul ci ñoom. Dañu koy jàpp diir bu gàtt, te noonu bu jafe-jafe yi ñëwee walla ñu fitnaal leen ndax kàddu gi, ci saa si ñu bàyyi ngëm gi. 18 Ñeneen ñi ñooy ñi jot jiwu ci biir xaaxaam yi. Ñoom, dañuy dégg kàddu gi 19 waaye dañuy jaaxle ci yëfi àddina sii, dañuy wut alal yuy naxaate, te dañoo bari bëgg-bëgg. Loolu lépp mooy tanc kàddu gi ba tax du am meññeef. 20 Ñi ci des, ñooy ñi jot jiwu ci suuf su baax si. Ñoom dañuy dégg kàddu gi, nangu ko te am meññeef. Ñenn ñi meññ fanweer, ñeneen ñi meññ juróom benn fukk, ñi ci des téeméer.»
Yeesu nettali na léebu làmp bi ak nattukaay bi
21 Yeesu ne leen: «Ndax nit dina jël làmp di ci dëpp leket, walla di ko dugal ci ron lal? Ndax du ko wékk? 22 Ndaxte amul dara lu nëbbu lu ñu dul feeñal te amul dara lu umpe lu ñu dul leeral. 23 Na ki am nopp ngir déglu dégg.» 24 Yeesu yokk ca ne: «Bàyyileen xel bu baax ci li ngeen di déglu. Ni ngeen di nattale ñeneen ñi, noonu lañu leen di nattale, te dinañu leen ko yokkal, 25 ndaxte ku am dinañu la yokkal, waaye ku amul dinañu jël sax li nga am.»
Yeesu nettali na ñaari léeb ci pepp yi
26 Yeesu waxaat ne: «Nguuru Yàlla dafay mel ni benn waay bu ji ci toolam. 27 Muy nelaw walla mu yeewu, guddi ak bëccëg, pepp yi dañuy sax te jóg, doonte xamul sax ni muy deme. 28 Suuf si ci boppam day meññ: day jëkka saxal jiwu bi, teg ci tóor-tóor. Ci mujjantal bi, pepp yi feeñ bu baax ci biir tóor-tóor yi, 29 te bu pepp yi ñoree, ñu dagg ko ci saa si, ndaxte waxtu ngóob bi jot na.»
30 Yeesu yokkaat ca ne: «Lan lañu mëna méngale nguuru Yàlla gi? Ak ban léeb lañu ko mëna misaale? 31 Dafay mel ni doomu fuddën. Bu ñu ko jiwee ci suuf si moom mooy pepp bi gëna tuuti ci pepp yi yépp. 32 Waaye bu ñu ko jiwee day sax te mujje nekk garab bi gëna réy ci garab yi nekk ci tool bi te dafay sax ay bànqaas yu réy ba tax picci asamaan si mëna ràbb seen tagg yi ci keram.» 33 Jaarale ko ci léeb yu bari yu mel noonu la Yeesu doon jàngal kàddu Yàlla gi ñi ko doon déglu ci lu aju ci li ñu mëna xam. 34 Daawul wax ak ñoom lu dul ci léeb, waaye bu wéetoon ak taalibeem yi, mu tekkil leen lépp.
Yeesu dalal na ngelaw bu am doole bi
35 Ci bés boobu ci ngoon, Yeesu ne taalibe yi: «Nanu dem ba ci beneen wetu dex gi.» 36 Ñu bàyyi fa mbooloo mi te yóbbu Yeesu ci gaal gi ñu nekkoon. Yeneen gaal àndoon nañu ak ñoom. 37 Ngelaw bu am doole daldi jóg, ndox mi di dugg ci gaal gi ba tax gaal gi doon fees ak ndox. 38 Yeesu mu ngi woon ci gannaawu gaal gi, teg boppam ci njegenaay di nelaw. Taalibeem yi yee ko, ne ko: «Jàngalekat bi, xanaa li nuy suux defu la dara?» 39 Yeesu daldi jóg, gëdd ngelaw li, te wax dex gi ne: «Noppil te nga dal.» Ngelaw li daldi bàyyi te lépp dal. 40 Noonu Yeesu ne taalibeem yi: «Lu tax ngeen di ragal. Ndax amaguleen ngëm ba léegi?» 41 Waaye taalibeem yi tiitoon nañu lool te di waxtaan ci seen biir naan: «Kii nag, mooy kan, ba ngelaw li ak ndox mi sax di ko déggal?»