Yeesu dàq na ay rab yu bari yu nekkoon ci benn waay
5
Yeesu ak taalibeem yi yegsi ci beneen wetu dex bi ci diiwaanu Serasa. 2 Bi Yeesu wàccee gaal gi, ci saa si benn waay bu am rab génnee ci armeel ba te ñëw daje ak moom. 3 Ci armeel ba la dëkkoon. Kenn mënu ko woon a takk ceen sax ba mu baña rëcc. 4 Yenn saay nit ñi dañu doon takk tànkam yi ak loxoom yi ak ay weñ, waaye da ko doon dog, te kenn amul woon doole ngir téye ko. 5 Guddi ak bëccëg da doon wër armeel bi ak tund yi di yuuxu te di gaañ boppam ak ay xeer. 6 Bi mu séenee Yeesu fu sori, mu daw, sukk ci kanamam, 7 te di yuuxu ak baat bu kawe naan: «Loo ma bëggal, Yeesu doomu Yàlla Aji-Kawe ji? Maa ngi lay ñaan ci turu Yàlla, bul ma metital.» 8 Waxoon na loolu ndaxte Yeesu waxoon na ko ne: «Rab bu bon bi, génnal ci waa jii.» 9 Yeesu laaj ko ne: «Noo tudd?» Mu tontu ko ne: «Coggal laa tudd ndaxte ñu bari lanu.» 10 Te mu ñaan Yeesu ak doole ngir mu bañ ko dàq ci diiwaan bi. 11 Fekk na ci waxtu boobu amoon na géttu mbaam xuux yu bari yu doon wut lu ñuy lekk ci kaw tund bi. 12 Rab yi ñaan Yeesu ne: «May nu, nu dugg ci mbaam xuux yi.» 13 Yeesu may leen ko. Noonu rab yi génn ci nit ki, dugg ci mbaam xuux yi. Gétt boobu nekkoon ci kaw tund bi, lu tollook ñaari junni mbaam xuux, daldi gaawantu, tarxiis, daanu ci dex bi, lab fa. 14 Sàmmkati mbaam xuux yi daldi daw, te dem ci dëkk bi ak ci kër àll yi, di nettali lépp li ñu gisoon te nit ñi génn ngir gis li xewoon. 15 Bi ñu yegsee ci wetu Yeesu, ñu gis nit ki rab yi jàppoon, mu toog, sol yére, te ànd ak sagoom. Ñu daldi tiit. 16 Ñi gisoon li xewoon di nettali li daloon mbaam xuux yi ak waa ji rab yi jàppoon. 17 Noonu ñu tàmbali di ñaan Yeesu ngir mu génn ci seen diiwaan. 18 Ci waxtu bi Yeesu di yéeg ci gaal gi nit ki amoon rab yi ñaan ko ngir ànd ak moom. 19 Yeesu mayu ko ko, waaye mu ne ko: «Demal, nga ñibbi sa kër ci sa wetu njaboot, te nga nettali leen lépp li la Boroom bi defal ci ni mu la yërëme.» 20 Waa ji dem, te mu tàmbali yégle lépp li ko Yeesu defal ci diiwaan bi ñuy woowe Fukki dëkk yi. Ñépp waaru woon nañu.Yeesu wéral na benn jigéen ju feebaroon te dekkil xale bu jigéen bu dee woon
21 Bi Yeesu jàllee ak gaal gi ci beneen wetu dex ba, mbooloo mu takku dajaloo ci tefes bi, wër ko. 22 Benn njiitu kër-ñaan bu tudd Yayrus daldi yegsi. Bi mu gisee Yeesu, mu sukk ci ay tànkam, 23 te mu ñaan ko ak doole ne: «Sama doom bu jigéen bi mu ngi dee. Ñëwal, nga teg ko say loxo ngir musal ko te mu dund.» 24 Noonu Yeesu dem, ànd ak moom. Mbooloo mu takku gunge ko, di ko tanc ci wet bu nekk.
25 Benn jigéen buy xëpp deret lu tollu ci fukki at ak ñaar mu ngi fa woon. 26 Sonnoon na lool ci loxoy fajkat yu bari. Def na ci alalam bi yépp te tanewul waaye dafa gëna sonn. 27-28 Noonu mu dégg ñuy wax ci lu jëm ci Yeesu. Mu daldi wax ci xelam ne: «Su ma fexee ba lal yéreem, dinaa wér.» Ci biir mbooloo mi, mu jaare Yeesu gannaaw te laal yéreem. 29 Ci saa si, xëpp deret bi bàyyi te mu yég ne wér na ci metitam. 30 Ci saa si Yeesu xam ne kàttan génn na ci moom, mu walbatiku ci mbooloo mi te laaj ne: «Kan moo laal sama yére?» 31 Taalibeem yi ne ko: «Gis nga mbooloo mi di la tanc ci wet bu nekk, ngay wax ne: "Kan moo ma laal?"» 32 Waaye mu xool ñi ko wër ngir xam kan moo def loolu. 33 Jigéen bi tiit di lox, xam li ko dal, ñëw sukk ci kanamam, te wax ko dëgg bi yépp. 34 Yeesu ne ko: «Sama doom, sa ngëm wéral na la. Demal ci jàmm te nga wér ci sa metit.»
35 Bi Yeesu di wax loolu, ay nit jóge ci kër Yayrus mi nekk njiitu kër-ñaan bi te ne ko: «Sa doom dee na. Bul sonnalaat jàngalekat bi.» 36 Waaye Yeesu jàppul wax jooju, mu wax njiitu kër-ñaan bi ne: «Bul ragal dara. Gëmal rekk.» 37 Yeesu nanguwul woon kenn ànd ak moom ku dul Piyeer, Saak ak Yowaana ñi bokk ndey ak baay. 38 Bi ñu yegsee ci kër Yayrus, Yeesu dégg coow li, ay nit yuy naqarlu di jooy tey yuuxu. 39 Mu dugg te ne leen: «Lu waral coow lii ak jooy yii? Xale bi deewul, day nelaw rekk.» 40 Waaye ñuy ñaawal Yeesu. Noonu mu génne leen ñoom ñépp. Mu woo pàppay xale bi ak yaayam ak taalibe yi ko gunge woon te mu dugg ci néeg bi xale bi nekkoon, 41 téye ko ci loxoom, te ne ko: «Talita kumi,» liy tekki ne: «Xale bu jigéen bi, maa ngi la koy wax: jógal.» 42 Ci saa si, xale bu jigéen bi daldi jóg te tàmbali di dox ndaxte amoon na fukki at ak ñaar. Ñépp waaru woon nañu lool, 43 waaye Yeesu dénk leen ak doole ngir ñu bañ ko wax kenn te ne leen ñu jox ko mu lekk.