Yeesu juddu na ca dëkku Betleyem
2
Ci jamono jooju, Sesaar Ogust joxe na ndigal ngir ñépp binduji, ngir xam ñaata nit lañu tollu ci nguuru Room. 2 Mu nekkoon waññ bu jëkk ci jamono bi Kiriñus yilifoon diiwaanu Siri. 3 Noonu ñépp daldi dem, binduji fu ñu cosaanoo. 4 Yuusufa nag jóge dëkku Nasaret bi nekk ci diiwaanu Galile, ngir dem dëkku Betleyem bi nekk ci diiwaanu Yude. Foofu la Daawuda juddoo, te Yuusufa bokk ci askanam. 5 Looloo tax mu ànd ak Maryaama mi ñu ko mayoon te mu ëmboon, ngir mu dem fa binduji.6 Bi ñu nekkee Betleyem, waxtu bi Maryaama wara am doom yegsi. 7 Mu am doomam bu jëkk, bu góor; lëmës ko ci laytaay, tëral ko ci lekkukaayu jur, ndaxte fi ñu doon dalal gan yi daa feesoon.
8 Ci diiwaan boobu, ay sàmmkat nekkoon nañu ci àll bi, fanaane wottu seeni gétt. 9 Benn malaaka feeñu leen te màggaayu Yàlla di leeral li leen wër. Ñu daldi ànd ak tiit, 10 waaye malaaka mi ne leen: «Buleen tiit ndaxte, xoolleen! Maa ngi leen di yégal xibaar bu baax biy bégloo askan bi yépp. 11 Tey jii ci dëkku Daawuda, seen Musalkat juddu na, di Almasi bi, di Boroom bi. 12 Ci màndarga yii ngeen koy xàmmee: dingeen fekk benn liir bu ñu lëmës ak laytaay te tëral ko ci lekkukaayu jur.»
13 Ci saa si, amoon na ak malaaka bi yeneeni malaaka yu bari. Ñuy sant Yàlla te di wax ne:
14 «Nañu màggal Yàlla ci asamaan yu gëna kawe yi,
te ci suuf si, na jàmm am ci ñépp ñi mu may yiwam.»
15 Bi leen malaaka yi bàyyee te dellu asamaan, sàmmkat yi di waxtaan ci seen biir ne: «Nanu dem nag ba Betleyem ngir gis li fa xew te Boroom bi xamal nu ko.» 16 Ñu gaawantu dem. Ñu fekk fa Maryaama ak Yuusufa ak liir bi ñu tëral ci lekkukaayu jur. 17 Bi ñu leen gisee, ñu nettali ñépp kàddu yi ñu déggoon ci li jëm ci xale bi. 18 Ñépp ñi doon dégg waxu sàmmkat yooyu daldi yéemu, 19 te Maryaama moom, denc loolu lépp ci xelam te mu ciy xalaat. 20 Sàmmkat yi dellu seeni gétt. Ñuy màggal Yàlla te di ko sant ci lépp li ñu dégg te gis ko, loolu lépp amoon na, ni leen ko malaaka bi waxe woon.
21 Ci juróom ñetteelu fan bi gannaaw bi mu juddoo, di bés bi ñu wara xarafal xale bi, ñu tudde ko Yeesu, di tur bi ko malaaka bi waxoon laata yaayam di ëmb.
Waajuru Yeesu yi yóbbu nañu ko ci kër-Yàlla ga
22 Bi bési setal yi matee, ni ko yoon bi Boroom bi Yàlla joxe woon jaarale ko ci Musaa digle, Yuusufa ak Maryaama yóbbu nañu xale bi ci dëkku Yerusalem ca kër-Yàlla ga ngir andi ko ci teewaayu Boroom bi Yàlla, 23 ni ñu ko binde woon ci benn yoon boobu ne: «Bépp taaw bu góor dinañu ko beral Boroom bi.» 24 Yuusufa ak Maryaama jébbal nañu sarax ni ko yoonu Boroom bi digle: «ñaari pitaxu àll walla ñaari picc yu ndaw yu ñuy woowe xati.»
25 Amoon na ci Yerusalem benn waay ju tuddoon Simeyon. Waa ju jub la woon te gëm Yàlla. Da doon xaar dëfëlu Israyil, te Xel mu Sell mi àndoon na ak moom. 26 Xel mu Sell mi xamaloon na ko ne du dee mukk te gisul Almasi bi Boroom bi dige woon. 27 Noonu Xel mi yóbbu ko ba ca kër-Yàlla gi. Bi waajuru Yeesu yi indee xale bi ngir matal li yoon bi digle, 28 Simeyon jël ko ci ay loxoom tey sant Yàlla di wax ne:
29 «Léegi nag Boroom bi Yàlla sa dige mat na,
yewwil sa jaam mu dee ci jàmm,
30 ndaxte samay bët gis nañu sa mucc bi,
31 mucc bi nga waajal ci kanamu askan yi yépp.
32 Mu nekk leer bi lay won xeeti àddina si yépp.
Mooy tamit màggaayu Israyil sa askan.»
33 Pàppa Yeesu ak yaayam waaru woon nañu ci li mu doon wax ci lu jëm ci xale bi. 34 Simeyon barkeel leen te wax Maryaama yaayu Yeesu ne: «Yàlla da tànn xale bii ngir mu waral daanu ak jógu ñu bari ci Israyil, dina doon màndarga Yàlla bi nit ñi dul nangu. 35 Te noonu dina feeñal ci leeraay xalaat yi nëbbu ci biir xolu ñu bari, te yaw nag metit dina xar sa ruu ni jaasi.»
36 Amoon na tamit benn yonent bu jigéen bu tudd Aana di woon doomu Fanuwel bokkoon ci askanu Aser. Aana màggatoon na lool. Ba muy janq te xamul góor la séy. Dundoon na ak jëkkëram juróom ñaari at. 37 Gannaaw loolu jëkkëram gaañu te mu des moom kese. Léegi amoon na juróom ñett fukki at ak ñeent. Daawul jóge ci kër-Yàlla gi te doon na jaamu Yàlla ci woor ak ñaan, guddi ak bëccëg. 38 Mu yegsi ci waxtu bi Simeyon doon wax. Aana tàmbalee gërëm Yàlla te doon na wax lu jëm ci xale bi ñépp ñi doon xaar waxtu bi Yàlla di yewwi Yerusalem.
39 Bi waajuru Yeesu yi matalee lépp li yoonu Boroom bi digle, ñu dellu ci seen dëkk Nasaret ci diiwaanu Galile. 40 Xale bi mu ngi doon màgg te di dëgër. Amoon na xel bu rafet, te yiwu Yàlla nekkoon na ak moom.
Yeesu des na ca kër-Yàlla ga
41 At bu nekk waajuru Yeesu yi dañu doon dem Yerusalem ngir màggalu Paak bi. 42 Bi Yeesu amee fukki at ak ñaar, ñu yóbbaale ko ni ko aada màggalu Paak bi bëgge. 43 Bi màggal bi jeexee ñu ñibbi, waaye xale bi Yeesu des Yerusalem te ay waajuram yéguñu ko. 44 Ñu xalaatoon ne dafa ànd ak ñi ñu bokkaloon yoon bi. Bésu lëmm ñu koy dox, noonu ñu tàmbali di ko seet ci mbokk yi ak xarit yi, waaye gisuñu ko. 45 Ñu dellu Yerusalem te wéy di ko seet. 46 Ñetteelu fan bi, ñu daldi ko gis ci kër-Yàlla gi, mu toog ci diggu jàngalekat yi di leen déglu te di leen laaj ay laaj. 47 Ñépp ñi ko doon déglu daldi waaru lool ci dégginam ak tontu yi mu leen doon jox. 48 Bi ko ay waajuram gisee ñu daldi waaru. Yaayam ne ko: «Sama doom, lan moo tax nga def nu lii? Man ak sa Pàppa jaaxle woon nanu lool te danu la doon seet.» 49 Mu tontu leen ne: «Ndax xamuleen ne damaa wara def sama liggéeyu Baay? Léegi nag, lu tax ngeen may seet?» 50 Waaye ñoom xamuñu woon dara ci li mu leen doon wax.