Liggéeyu Yaxya
3
Ci fukkeelu at ak juróom ci nguuru Tibeer Sesaar, fekkoon na Poñsë Pilaat yilifoon diiwaanu Yude, Erodd yilifoon diiwaanu Galile te magam Filib yilifoon diiwaanu Iture ak bu Tarakonit, Lisañas yilifoon diiwaanu Abilen. 2 Anas ak Kayif nekkoon jébbalkati-sarax-yu-mag ya. Noonu kàddu Yàlla gi wàcc ci Yaxya mi di doomu Sakari ci biir màndiŋ bi. 3 Yaxya doon na wër diiwaanu dexu Yurdan ba yépp, di waare naan: «Nanguleen ma sóob leen ci ndox ngir wone ne tuub ngeen seeni bàkkaar, te noonu Yàlla dina leen baal.»
4 Noonu, li yonent Yàlla Esayi bindoon ci téereem mat na:
«Lii mooy baatu nit kiy yuuxu ci biir màndiŋ bi:
"Waajalleen yoonu Boroom bi
defarleen yoonam yi, ñu jub.
5 Xur bu nekk dinañu ko sëkk.
Bépp tund bu mag ak bépp tund bu ndaw, dinañu leen maasale.
Yoon yu dëng yi dinañu leen jubbanti.
Yoon yu ñagas yi dinañu leen liisal,
6 te ñépp dinañu gis mucc gi Yàlla maye."»
7 Noonu mbooloo mu bari daan na ñëw ci Yaxya ngir mu sóob leen ci ndox. Yaxya da leen doon wax naan: «Yeen ñi fees ak daŋar mel ni jaan, kan moo leen jàngal ngir ngeen daw meru Yàlla mi nara wàcc? 8 Woneleen nag ci seen jëf ne tuub ngeen seeni bàkkaar. Buleen yem rekk di wax ci seen xel ne: "Nun am nanu Ibraayma ni baay." Ndaxte maa ngi leen koy wax, ci xeer yii, Yàlla mën na cee sàkkal Ibraayma ay doom. 9 Sémmiñ bi jege na ba noppi ngir dagg reeni garab yi. Bépp garab bu meññewul meññeef bu baax dinañu ko dagg te sànni ko ci safara si.»
10 Mbooloo mi laaj ko ne: «Kon nag lan lanu wara def?» 11 Mu tontu leen: «Képp ku am ñaari mbubb na jox benn bi nit ki amul, te ku am ñam, séddoo ko ak ki amul dara.»
12 Ay juutikat tamit ñëw nañu ngir mu sóob leen ci ndox. Ñu laaj Yaxya ne ko: «Jàngalekat bi, lan lanu wara def?» 13 Mu tontu leen: «Buleen laaj lu ëpp, li leen yoon di laajloo.»
14 Ay soldaar tamit ne ko: «Lan lanu wara def nag?» Mu tontu leen: «Buleen jël alalu kenn ci kaw jaay doole walla ci kaw di ko sosal, te doylooleen seen peyoor.»
15 Noonu askan bi di xaar ak yaakaar, di laaj ci seen xel, ndax Yaxya mooy Almasi bi. 16 Yaxya wax leen ñoom ñépp: «Man, maa ngi leen di sóob ci ndox, waaye kenn ku ma ëpp kàttan dina ñëw. Yelloowuma sax tekki ay dàllam, te kooku dina leen sóob ci Xel mu Sell mi ak ci safara. 17 Teg na layu ci loxoom di bees ngir teqale pepp bi ak xatax bi. Dina dajale pepp bi ci sàqam waaye dina lakk xatax bi ci safara bu dul fey mukk.» 18 Noonu Yaxya doon na leen jàngal ci ay mbir yu bari tey yégal xibaar bu baax bi askan bi.
19 Erodd mi yilifoon diiwaanu Galile takkoon na Erojàdd mi di jabaru magam, te tamit dafa defoon yeneen ñaawteef yu bari, loolu taxoon na Yaxya di ko sikk. 20 Noonu Erodd yokkaat ci beneen ñaawteef, ci bi mu jàppalu Yaxya ba tëj ko kaso.
21 Bi Yaxya sóobee askan bi yépp ci ndox, sóob na tamit Yeesu ci ndox. Noonu bi Yeesu di ñaan, asamaan si ubbeeku, 22 te Xel mu Sell mi wàcc ci moom, ci jëmm ju mel ni pitax, te benn baat jóge ci asamaan ne: «Yaa di sama doom ji ma sopp. Ci yaw laa ame bànneex.»
Cosaanu Yeesu Almasi bi
23 Yeesu amoon na lu tollook fanweeri at bi mu tàmbalee liggéeyam. Dañoo xalaatoon ne mooy doomu Yuusufa.
Yuusufa mooy doomu Eli,
24 Eli di doomu Matat,
Matat di doomu Lewi,
Lewi di doomu Melki,
Melki di doomu Yanayi,
Yanayi di doomu Yuusufa,
25 Yuusufa di doomu Matacas,
Matacas di doomu Amos,
Amos di doomu Naxum,
Naxum di doomu Esli,
Esli di doomu Nagayi,
26 Nagayi di doomu Maat,
Maat di doomu Matacas,
Matacas di doomu Semeyin,
Semeyin di doomu Yoseg,
Yoseg di doomu Yoda,
27 Yoda di doomu Yowanan,
Yowanan di doomu Resa,
Resa di doomu Sorobabel,
Sorobabel di doomu Salacel,
Salacel di doomu Neri,
28 Neri di doomu Melki,
Melki di doomu Adi,
Adi di doomu Kosam,
Kosam di doomu Elmadam,
Elmadam di doomu Er,
29 Er di doomu Yeesu,
Yeesu di doomu Eliyeser,
Eliyeser di doomu Yorim,
Yorim di doomu Matat,
Matat di doomu Lewi,
30 Lewi di doomu Simeyon,
Simeyon di doomu Yuda,
Yuda di doomu Yuusufa,
Yuusufa di doomu Yonam,
Yonam di doomu Eliyakim,
31 Eliyakim di doomu Meleya,
Meleya di doomu Mena,
Mena di doomu Matata,
Matata di doomu Natan,
Natan di doomu Daawuda,
32 Daawuda di doomu Isayi,
Isayi di doomu Obedd,
Obedd di doomu Bowas,
Bowas di doomu Salmon,
Salmon di doomu Nason,
33 Nason di doomu Aminadab,
Aminadab di doomu Admin,
Admin di doomu Arni,
Arni di doomu Esron,
Esron di doomu Peres,
Peres di doomu Yuda,
34 Yuda di doomu Yanqóoba,
Yanqóoba di doomu Isaaxa,
Isaaxa di doomu Ibraayma,
Ibraayma di doomu Teraa,
Teraa di doomu Naxor,
35 Naxor di doomu Serug,
Serug di doomu Rew,
Rew di doomu Peleg,
Peleg di doomu Eber,
Eber di doomu Sela,
36 Sela di doomu Kaynam,
Kaynam di doomu Arpagsàdd,
Arpagsàdd di doomu Sem,
Sem di doomu Nóoyin,
Nóoyin di doomu Lemeg,
37 Lemeg di doomu Matusalem,
Matusalem di doomu Enog,
Enog di doomu Yeredd,
Yeredd di doomu Maleleel,
Maleleel di doomu Kaynan,
38 Kaynan di doomu Enos,
Enos di doomu Set,
Set di doomu Aadama,
Aadama di doomu Yàlla.