Seytaane fiir na Yeesu
4
Yeesu jóge woon na dexu Yurdan, fees ak Xel mu Sell mi. Xel mi yóbbu ko ci biir màndiŋ bi. 2 Foofu Seytaane fiir na ko ñeent fukki fan. Lekkul dara ci bés yooyu yépp. Bi loolu weesoo, mu xiifoon. 3 Seytaane ne ko: «Su fekkee yaay Doomu Yàlla, waxal xeer wii mu soppeeku mburu.» 4 Yeesu ne ko, «Mbind mi nee na: "Nit du dunde mburu rekk."»
5 Noonu Seytaane yóbbu ko ci catu tund wu gëna kawe, te won ko ci saa si nguuri àddina si yépp. 6 Mu ne ko: «Yaw, dinaa la jox sañ-sañu nguur yii ngay gis ak seeni màggaay, ndaxte man lañu ko jox te ku ma neex rekk la koy jox. 7 Soo nangoo sukk ci sama kanam, lii yépp yaa koy moom.» 8 Yeesu ne ko, «Mbind mi nee na: "Bul sukk ci kanamu kenn ku dul Yàlla sa Boroom te di ko jaamu moom rekk."»
9 Noonu Seytaane yóbbu ko ci Yerusalem, ba ci collu kër-Yàlla gi, te ne ko: «Su fekkee yaay Doomu Yàlla, tëbal fii te nga daanu ci suuf, 10 ndaxte Mbind mi nee na: "Yàlla dina jox malaakaam yi ndigal ngir ñu aar la, 11 téye la ci seeni loxo, ngir ñu bañ say tànk fakkastalu ci xeer."» 12 Noonu Yeesu ne ko, «Mbind mi nee na: "Bul seetlu Yàlla sa Boroom."»
13 Gannaaw bi mu ko fiiree ci fànn yépp ba noppi, Seytaane dem bàyyi fa Yeesu ba beneen yoon.
Yeesu dem na ci dëkku Nasaret
14 Gannaaw loolu, Yeesu dellu ci diiwaanu Galile fees ak kàttanu Xel mi ba tax turam siiw ci diiwaan bi yépp. 15 Ni muy jàngalee ci kër-ñaan yi tax na ñépp di ko tagg.
16 Noonu, mu dem ca Nasaret fa mu yaroo woon, dugg ci kër-ñaan bi, ci bésu noflaay bi, ni mu ko tàmme woon di def. Mu jóg taxaw ngir jàng kàddu gi, 17 ñu jox ko téere yonent Yàlla Esayi. Mu ubbi ko gis aaya yiy wax ne:
18 «Xelu Boroom bi mu ngi ci man,
ndaxte moo ma tànn
ngir ma yégal néew-di-doole yi xibaar bu baax bi.
Moo ma yónni ngir ma yégal jaam yi ne dinañu leen goreel,
ngir ma yégal gumba yi ne dinañu gisaat,
ngir ma yewwi ñi ñu not,
19 te yégle atu yiwu Boroom bi.»
20 Bi mu jàngee ba noppi, mu tëj téere bi, jox ko ki koy denc, te toog ngir jàngale. Ñépp ñi nekkoon ci kër-ñaan bi di ko xool ci biir bët. 21 Noonu mu tàmbali di leen wax ne: «Tey jii, kàddu gi ngeen dégg ci Mbind bi mat na.»
22 Ñépp a ko doon seedeel lu baax te waaru ci kàddu yiw yi doon génn ci gémmiñam, te ñuy wax ne: «Kii ndax du doomu Yuusufa?» 23 Yeesu tontu leen ne leen, «Dingeen ma wax ci léeb bi wax ne "Fajkat bi, fajal sa bopp." Te dingeen ma waxaat ne: "Yég nañu lépp li nga def ci Kapernawum, moom lañu bëgg nga def ko fii ci sa dëkk."»
24 Mu yokk ca ne: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, amul benn yonent bu ñu nangu ci dëkkam. 25 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ci jamono yonent Yàlla Ilyaas, ci Israyil amoon na jigéen ñu bari, ñu ñàkkoon seen jëkkër te asamaan si tëju woon diiru ñetti at ak genn-wàll, tawul te xiif bi bari ci réew mi yépp, 26 waaye Yàlla yónniwul Ilyaas ci kenn ci ñoom ku dul ci benn jigéen bu ñàkkoon jëkkëram; bu dëkk ca Sarebta ci wetu réewu Sidon. 27 Ci jamono yonent Yàlla Alyaasa, ci Israyil amoon na ay gaana yu bari, waaye faju ci woon kenn ku dul Naamaan mi jóge woon réewu Siri.»
28 Ba ñi nekkee ci kër-ñaan bi déggee wax yooyu, ñoom ñépp daldi fees ak mer. 29 Ñu jóg, génne ko dëkk bi, yéegal ko ci kaw tund, bi nga xamante ne foofu lañu tabaxe woon seen dëkk, ngir bëmëx ko ci suuf. 30 Waaye Yeesu jaar seen diggante te dem.
Yeesu dàq na ay rab te wéral ay nit yu feebar
31 Noonu Yeesu dem dëkku Kapernawum ci diiwaanu Galile. Mu dugg ci kër-ñaan bi di jàngale ci bésu noflaay bi. 32 Nit ñi yéemu ci anam ni mu doon jàngalee ndaxte da doon jàngale ak sañ-sañ bu ko Yàlla jox. 33 Ci biir kër-ñaan bi, amoon na benn waay bu am rab. Waa ji di wax ak baat bu kawe, di yuuxu, di naan: 34 «Éey! Yeesu mu Nasaret, loo ma bëggal? Ndax danga ñëw ngir sànk ma? Xam naa la; yaw yaay ku sell ki Yàlla yónni.» 35 Yeesu gëdd rab bi ne ko: «Noppil te nga génn ci nit ki.» Noonu, rab bi daaneel ko ci suuf ci kanamu ñépp, génn ci moom, te defu ko dara. 36 Ñépp waaru di waxtaan ci seen biir, di wax ne: «Waaw! Yii ñooy yan kàddu? Muy wax ak kàttan ak sañ-sañ, bay joxe ndigal te rab yi di génn.» 37 Noonu turu Yeesu daldi siiw ci Kapernawum ak li ko wër.
38 Bi loolu weesoo, Yeesu génn ci kër-ñaan bi, dem ci kër Simoŋ. Fekk na yaayu jabaru Simoŋ am yaram bu tàng lool. Ñu ñaan Yeesu ngir mu def ci dara. 39 Mu jegesi ko, tiim ko, gëdd tàngooru yaram bi te tàngooru yaram bi bàyyi. Ci saa si yaayu jabaru Simoŋ jóg te di leen toppatoo.
40 Bi jant bi sowee, ñu andi ci Yeesu ñépp ñu amoon ay feebar yu wuute te mu teg kenn ku nekk loxo, wéral leen. 41 Rab yi di génn ci ñu bari, di yuuxu di wax ne: «Yaw yaay Doomu Yàlla ji.» Yeesu gëdd leen te tere leen ñu wax ndaxte xamoon nañu ne moom mooy Almasi bi.
42 Noonu bi bët setee, Yeesu génn dëkk bi, dem ci béréb bu sori te mbooloo mu bari di ko seet. Bi ñu ko gisee, ñu bëgg ko téye, ngir bañ mu dem. 43 Waaye Yeesu jël kàddu gi te wax leen, «Fàww ma yégle xibaar bu baax bi ci nguuru Yàlla ci yeneen dëkk yi, ndaxte loolu moo tax Yàlla yónni ma.» 44 Noonu Yeesu di wër ci kër-ñaan yi nekk ci réewu Yawut yépp, di yégle xibaar bu baax bi.