Yeesu woo na taalibeem yu jëkk yi
5
Benn bés, Yeesu nekkoon ci wetu dexu Senesaret. Foofu amoon na mbooloo mu takku mu ko wëroon, doon buuxante ngir déglu kàddu Yàlla gi. 2 Noonu mu gis ñaari gaal yu nekkoon ci tefes bi. Nappkat yi dañoo wàccoon ngir raxas seeni mbaal. 3 Mu yéeg ci benn gaal gi nga xam ne Simoŋ moo ko moomoon. Te mu ñaan ko ne: «Sorilal sa gaal gi tuuti tefes gi.» Yeesu daldi toog ci gaal gi, di jàngal mbooloo ma fa nekkoon.4 Bi mu jàngalee ba noppi, mu wax Simoŋ ne ko: «Joowal sa gaal gi ba fi ndox mi gëna xóote, te ngeen sànni seeni mbaal ngir napp.» 5 Simoŋ tontu ko ne: «Kilifa gi, danoo fanaane mbaal guddi gi yépp ba sonn te jàppunu dara. Waaye ci say kàddu dinaa sànni mbaal yi.» 6 Bi ñu ko sànnee ñu daldi jàpp ay jën yu bari, ba seen mbaal yi di waaja xotteeku. 7 Noonu ñu tàllal loxo seen àndandoo yi nekkoon ci beneen gaal gi ngir ñu ñëw jàppale leen. Bi ñooñu ñëwee, ñu daldi feesal ñaari gaal yépp ak ay jën, ba seen gaal yi di waaja suux. 8 Bi Simoŋ Piyeer gisee loolu, mu daldi sukk ci kanamu Yeesu te ne ko: «Boroom bi, sori ma, ndaxte man bàkkaarkat laa.» 9 Simoŋ ak ñépp ñi nekkoon ak moom dañoo tiitoon lool ndax kéemaan bi Yeesu defoon, ba tax ñu jàpp jën yu bari. 10 Tiit boobu tamit jàppoon na ay àndandoom, maanaam Saag ak Yowaana yi nekkoon ay doomi Sebede. Waaye Yeesu tontu Simoŋ ne ko: «Bul ragal dara ndaxte dale ko tey nappkat nit ngay doon.» 11 Noonu ñu génne seeni gaal ba ci suuf, ñu bàyyi lépp te topp Yeesu.
Yeesu setal na benn waay ju gaana
12 Gannaaw loolu Yeesu nekkoon na ci benn dëkk te foofu amoon na benn waay ju yaramam yépp daj ak feebaru ngaana. Bi mu gisee Yeesu mu daldi sukk, dëpp kanamam ci suuf, te ñaan ko ne: «Boroom bi, su fekkee bëgg nga ko, mën nga ma setal.» 13 Yeesu tàllal loxoom, laal ko te wax ko ne: «Bëgg naa ko. Setal.» Ci saa si, feebaru ngaana bi daldi koy bàyyi. 14 Ci noonu, Yeesu dénk ko ne: «Bul ko wax kenn waaye demal nga won sa bopp jébbalkatu-sarax si te nga joxe sarax siy wone ne set nga, ni ko yoonu Musaa diglee, te loolu dina mëna nekk seede ci ñoom.» 15 Turu Yeesu daldi gëna siiw te ay nit yu bari ñëwoon nañu ngir déglu ko te mu wéral seeni feebar. 16 Waaye Yeesu ci boppam dem na, ni mu ko tàmme woon di def, ci biir màndiŋ ba ngir ñaan.
Yeesu wéral na waay ju làggi
17 Benn bés Yeesu doon jàngale. Amoon na ñu bokk ci tarixa bi ñuy woowe Farisen yi ak ay jàngalekatu-yoonu-Musaa yu fa toogoon di ko déglu. Jógewoon nañu ci dëkk yépp ci diiwaanu Galile, ci diiwaanu Yude ak ci dëkku Yerusalem. Yeesu àndoon na ak kàttanu Boroom bi ngir faj. 18 Noonu mu am ay nit ñu ñëw, jàppoo ci basaŋ nit ku làggi. Ñu jéemoon koo dugal ci biir kër gi ngir andi ko ci kanamu Yeesu, 19 waaye mënuñu ko woon ndax mbooloo ma. Noonu ñu yéeg ci kaw kër gi, toj dal bi, te wàcce ko ak basaŋam ci diggu ñépp ci kanamu Yeesu. 20 Bi Yeesu gisee seen ngëm, mu wax nit ku làggi ki ne: «Sama waay, baal nañu la say bàkkaar.» 21 Noonu jàngalekatu-yoonu-Musaa yi ak Farisen yi tàmbali di xalaat ci seeni xel di wax ne: «Kii mooy kan bay méngale boppam ak Yàlla? Amul kenn ku mëna baale bàkkaar yi, ku dul Yàlla.» 22 Yeesu xam li ñu doon xalaat ci seen biir xol, te mu ne leen: «Lan ngeen nekk di xalaat ci seen biir xol? 23 Ban moo gëna yomb: wax nit ki "baal nañu la say bàkkaar," walla wax nit ki "jógal te dox"? 24 Li ma bëgga def mooy ngir ngeen xam ne Doomu nit ki am na sañ-sañ ci àddina si baale bàkkaar yi.» Noonu mu wax ku làggi ki: «Jógal, jël sa basaŋ, te nga ñibbi.» 25 Ci saa si mu daldi jóg ci kanamu ñépp di màggal Yàlla, jël basaŋ bi mu tëddewoon, di ñibbi këram. 26 Ñépp waaru woon nañu, ànd ak tiitaange di màggal Yàlla te di wax ne: «Gis nanu tey ay mbir yu nu yéem.»
Yeesu woo na Lewi te Farisen yi laaj nañu Yeesu
27 Bi loolu weesoo, Yeesu génn te gis benn juutikat bu tudd Lewi, mu toog ci bérébu liggéeyukaay bi. Mu wax ko ne: «Topp ma,» 28 te mu jóg, bàyyi lépp, daldi topp Yeesu. 29 Lewi togglu reer bu mag ci biir këram ngir Yeesu te juutikat yu bari ak ay nit ñu bari doon lekkandoo ak ñoom. 30 Farisen yi ak jàngalekati-yoonu-Musaa yi bokkoon ci ñoom di xuntu, di wax taalibeem yi: «Lu tax ngeen di lekkandoo te di naanandoo ak ay juutikat ak ay bàkkaarkat?» 31 Yeesu jël kàddu gi te wax leen: «Du ñi wér ñoo soxla fajkat, waaye ñi wéradi. 32 Damaa ñëw ngir woo bàkkaarkat yi, ñu tuub seeni bàkkaar, waaye du ñu jub ñi.»
33 Ñu wax ko ne: «Taalibey Yaxya yi ak taalibey Farisen yi dañuy faral di woor ak di ñaan, waaye yaw say taalibe dañuy lekk ak di naan.» 34 Mu tontu leen ne: «Ndax kenn mën na woorloo xariti boroom séet bi, waxtu yi mu nekke ak ñoom? 35 Ay bés a ngi ñëw ñu jële boroom séet bi ci seen biir te ci bés yooyu dinañu woor.»
36 Mu wax leen benn léeb ne leen: «Kenn du xotti ab daggit ci yére bu bees te di ko taqale ci yére bu màggat, ndaxte bu ko defee, bu bees bi day yàqu te daggit bu bees bi du ànd ak yére bu màggat bi. 37 Te kenn du jël biiñ bu bees di ko def ci ay mbuusi der yu màggat. Lu ko moy, biiñ bi dina fëq mbuus ya, daldi tuuru, te mbuus ya dinañu yàqu, 38 waaye fàww nga jël biiñ bu bees nga def ko ci ay mbuusi der yu bees. 39 Te kenn, gannaaw bi mu naanee biiñ bu màggat ba noppi du bëgg biiñ bu bees ndaxte day wax ne bu màggat bi moo gëna baax.»