Yeesu mooy Boroom bésu noflaay bi
6
Benn bésu noflaay, Yeesu doon jàll ci tool yi. Taalibe yi witt ci pepp yi, di boxom te di yéy. 2 Ñenn ci Farisen yi laaj leen: «Lan moo tax ngeen di def loolu? Yoonu Musaa dafay tere liggéey ci bésu noflaay bi.» 3 Yeesu tontu leen ne leen: «Xanaa jànguleen li Daawuda defoon bu mu xiifee, moom ak ñi mu àndaloon? 4 Mu dugg ci kër-Yàlla gi, jël mburu yi ñu jébbal Yàlla, lekk ci, te jox ci ñi mu àndaloon, te fekk na yoon bi mayul kenn di ko lekk ku dul jébbalkati-sarax si.» 5 Te mu ne leen: «Doomu nit ki mooy boroomu bésu noflaay bi.»
6 Beneen bésu noflaay Yeesu dugg ci kër-ñaan bi, di jàngale. Foofu amoon na benn waay bu loxo ndeyjooram làggi. 7 Jàngalekati-yoonu-Musaa yi ak Farisen yi doon ko xool ba xam ndax ci bésu noflaay bi dina wéral waa ji ngir ñu tuumaal ko. 8 Waaye Yeesu xam seeni xalaat, wax ku am loxo bu làggi bi: «Jógal te nga taxaw ci kanamu ñépp.» Mu jóg, taxaw. 9 Yeesu ne leen: «Am naa benn laaj ngir yeen. Lan la yoon bi maye ngir ñu def ko ci bésu noflaay bi, lu baax walla lu bon? Muccal nit walla bàyyi ko mu loru?» 10 Noonu Yeesu xool leen ñoom ñépp, wax nit ki am loxo bu làggi bi: «Tàllalal sa loxo.» Nit ka tàllal loxoom, daldi wér. 11 Jàngalekati-yoonu-Musaa yi ak Farisen yi daldi fees dell ak mer, di waxtaan ci seen biir lan lañu wara def Yeesu.
Yeesu tànn na fukki ndaw yi ak ñaar
12 Benn bés Yeesu dem na ci tund bi ngir ñaan. Mu fanaane ñaan Yàlla, guddi gi yépp. 13 Bi bët setee, mu woo taalibeem yi te tànn ci fukk ak ñaar, tudde leen ay ndaw: 14 Simoŋ mi Yeesu doon woowe Piyeer, Andare te mu bokk ak Piyeer ndey ak baay, Saag, Yowaana, Filib, Bartelemi, 15 Macë, Tomaa, Saag di doomu Alfe, Simoŋ mi ñuy woowe "ku takku ci réewam", 16 Yudaa di doomu Saag, ak Yudaa Iskariyot di ki ko mujjoona wor.
Yeesu jàngal na taalibeem naka lañu wara jëfe
17 Bi Yeesu wàccee ci tund bi àndoon na ak ndaw yi, taxaw ci béréb bu suufe. Foofu, amoon na taalibe yu bari ak mbooloo mu takku jóge woon ci diiwaanu Yude ak dëkku Yerusalem ak dëkk yi nekk ci wetu géej, maanaam Tir ak Sidon. Ñëwoon nañu ngir déglu ko te jot seen wér gu yaram. 18 Ñi nga xamante ne ay rab yu bon dañu leen sonaloon tamit jot nañu seen wér gu yaram. 19 Ñoom ñépp dañu doon wuta laal Yeesu ndax kàttan bi doon génn ci moom tey wéral seeni feebar.
20 Noonu Yeesu yékkëti bëtam yi, xool taalibe yi, ne leen:
«Barkeel ngeen, yeen ñi néew doole
ndaxte nguuru Yàlla yeena ko moom.
21 Barkeel ngeen, yeen ñi xiif léegi,
ndaxte dingeen regg.
Barkeel ngeen, yeen ñiy jooy léegi,
ndaxte dingeen reetaan ni ji.
22 Barkeel ngeen su leen ñépp bañee
te beddi leen te di leen saaga,
di wax lu bon ci yeen ndax Doomu nit ki.
23 Ci kaw loolu, àndleen ak mbégte tey fecc,
ndaxte Yàlla mu ngi leen di waajal neexal bu mag ci asamaan.
Ci dëgg-dëgg, ñoom, noonu la seeni maam doon def ak yonent yi.
 
24 «Waaye musiba dal na leen, yeen boroom alal yi
ndaxte dëfël nañu leen ba noppi.
25 Musiba dal na leen, yeen ñi regg
ndaxte dingeen xiifati.
Musiba dal na leen, yeen ñiy ree léegi,
ndaxte dingeen ànd ak naqar aki rongooñ.
26 Musiba dal na leen, su leen ñépp di wax lu baax ci yeen,
ndaxte ñoom, noonu la seeni maam doon def ak yonent yi nga xam ne dëgguwuñu woon.
27 «Waaye maa ngi leen koy wax yeen ñi may déglu, bëggleen seeni noon, te di leen defal lu baax ñi leen bañ, 28 te barkeelleen ñépp ñi leen yéene lu bon te ñaanalleen ñi leen di def lu bon. 29 Bu la nit mbejee ci benn lex bi, jox ko bi ci des. Bu nit jëlee sa mbubb mu mag, bu ko tere mu jël yére bu ndaw bi nga sol. 30 Mayal képp ku la ñaan. Bu nit jëlee sa yëf bul ko wax mu delloo la ko. 31 Li ngeen bëgg ñu defal leen ko, yeen tamit defleen ko ngir ñoom. 32 Booleen bëggee ñi leen bëgg rekk, ban ngërëm ngeen ciy jële? Bàkkaarkat yi tamit bëgg nañu ñi leen bëgg rekk. 33 Booleen defalee lu baax ñi leen di defal lu baax rekk, ban ngërëm ngeen ciy jële? Ndax bàkkaarkat yi tamit dañuy defal lu baax ñi leen di defal lu baax? 34 Te bungeen di lebal ñi ngeen yaakaar ñu fey leen, ban ngërëm ngeen ciy jële? Bàkkaarkat yi tamit, dañuy lebal seeni moroom bàkkaarkat ngir bu ñu leen di fey, ñu jox leen lu tollook li ñu leen lebaloon. 35 Waaye yeen, nangeen bëgg seeni noon, te defal leen lu baax, te nangeen leble te baña xaar ngir ñu fey leen, te noonu dingeen am neexal bu réy, te dingeen doon ay doomu Yàlla Aji-Kawe ji, moom mi nga xam ne moo baax ci ñu goreedi ñi ak ñu soxor ñi. 36 Amleen yërmande ni Yàlla seen Baay ame yërmande.
37 «Buleen àtte te duñu leen àtte, buleen daan te duñu leen daan. Baaleleen te dinañu leen baal. 38 Joxeleen te dinañu leen jox. Dinañu leen sottil ay peppu ceeb ci seeni poos ba ñu fees dell bay tuuru, ndax ni ngeen di natte noonu lañu leen di nattale.»
39 Yeesu wax léeb bii: «Ndax gumba mën na wommat moroomu gumbaam? Déedéet, ndaxte bu ñu moytuwul, ñoom ñaar ñépp dinañu daanu ci kàmb. 40 Ndax taalibe bi, moo gëna mag jàngalekatam? Waaye bu jàngee ba mokkal, mën na mel ni jàngalekatam.
41 «Lu tax ngay xool ñax bi nekk ci sa bëtu moroom te gisoo bant bi nekk ci sa bët? 42 Lu tax ngay wax sa moroom: "Kaay ma dindil la ñax bi ci sa bët," te yaw gisoo bant bi ci sa bët? Naaféq bi! Génneel ba noppi bant bi ci sa bët. Bu booba dinga gis bu baax te mëna génne ñax bi ci sa bëtu moroom.
43 «Garab bu baax du am meññeef bu bon te garab bu bon du am meññeef bu baax. 44 Garab bu nekk ñu ngi koy xàmme ci meññeefam. Kenn du witt gaŋ ci garabu kàdd, te kenn du witt ay reseñ ci ay xaaxaam. 45 Nit bu baax mu ngi jële ci biir xolam bu fees ay mbir yu baax, te nit bu bon mu ngi jële ci biir xolam bu fees ay mbir yu bon. Lu fees ci xol, gémmiñ wax ko.
46 «Lu tax ngeen may woowe "Boroom bi, Boroom bi," te dooleen jëfe samay kàddu? 47 Dinaa leen won nit kiy ñëw ci man lu muy nirool, mooy ki nga xam ne day déglu samay kàddu te di ko jëfe. 48 Day mel ni nit kuy tabax këram, gas, gas ba mu xóot, teg fondamaa bi ci kaw doj. Bu dex bi walee, ndox yi dal ci kër gi, te du ko mëna yàq ndaxte tabax bi dafa baaxoon. 49 Waaye kiy déglu samay kàddu te du ko jëfe, day mel ni nit kuy tabax ci suuf si. Amul fondamaa. Bu ndoxu dex gi walee ci kër gi, ci saa si, kër gi daldi màbb. Noonu yàqute kër googu dina réy lool.»