Ngëmu njiitu soldaaru Room bi
7
Gannaaw bi mu waxee kàddu yooyu yépp mbooloo mi ko doon déglu ba noppi, Yeesu dugg na Kapernawum. 2 Foofu, amoon na benn njiitu soldaaru Room bu amoon surgaam bu mu bëggoon lool, te mu feebar bay waaja dee. 3 Bi mu déggee ñuy wax ci Yeesu, mu yónni yenn njiitu Yawut ngir ñu ñaan ko mu ñëw wéral surgaam bi. 4 Bi ñooñu yegsee ci wetu Yeesu, ñu daldi koy ñaan ndimbal ak doole, ne ko: «Kii déy, yelloo na nga defal ko lii 5 ndaxte ku bëgg sunu askan bi la, te moo def ba nu tabax sunu kër-ñaan bi.»6 Noonu Yeesu daldi ànd ak ñoom. Bi ñu demee ba jegesi kër gi, njiitu soldaar bi daldi ko yónnee ay xaritam. Bi ñu dajeek Yeesu, ñu ne ko: «Boroom bi, jarul ngay sonal sa bopp ndaxte yelloowuma nga dugg sama kër. 7 Te loolu moo waral sax ma yaakaar ne yelloowuma ñëw fekksi la. Waaye waxal benn kàddu te sama surga bi dina wér, 8 ndaxte man tamit am naa ay kilifa yu may jiite, te jiite naa ay soldaar yu may jox ndigal. Su ma nee kii "Demal," mu dem! Su ma nee kee "ñëwal," mu ñëw! Am naa tamit surga. Su ma ko nee "defal lii," mu def ko!»
9 Noonu bi Yeesu déggee kàddu yooyu, mu daldi yéemu ci njiitu soldaar bi te mu daldi walbatiku xool mbooloo mi ko doon topp te ne: «Maa ngi leen koy wax, ci Israyil mësuma gis ngëm gu réye nii.» 10 Noonu bi ñi njiitu soldaar bi yónni woon delloo kër ga, ñu fekk surga bi feebaroon daldi wér.
Yeesu dekkil na doom ju góor ju jigéen ju ñàkkoon jëkkëram
11 Te noonu Yeesu àndoon na ak taalibeem yi ak mbooloo mu bari, doon dem ci dëkk bi ñuy woowe Nayin. 12 Bi ñu yegsee ba ci buntu dëkk bi, foofu amoon na ay nit yuy génn dëkk bi, doon robi néew, di woon benn doom bu góor képp ci yaayam bi ñàkkoon jëkkëram, te mbooloo mu takku jóge woon na dëkk ba di ko gunge. 13 Noonu, bi Boroom bi gisee ku jigéen ki, mu daldi ko yërëm lool te wax ko ne: «Bàyyil jooy yi.» 14 Noonu mu jegesi, laal basaŋ bi ñu tëraloon néew bi, ñi ko yoroon daldi taxaw. Mu wax ne: «Xale bu góor bi, maa ngi la koy wax, jógal.»
15 Noonu néew bi daldi toog te tàmbali wax. Yeesu delloo ko yaayam. 16 Mbooloo ma fa nekkoon yépp àndoon nañu ak tiitaange, di màggal Yàlla tey wax ne: «Yonent bu mag feeñ na sunu biir te Yàlla ganesi na askanam.» 17 Noonu kàddu yooyu ci Yeesu daldi siiw ci réewu Yawut yépp ak li ko wër.
Yeesu wax na ci lu jëm ci Yaxya
18 Te taalibe Yaxya yi nettali nañu ko loolu lépp. Noonu mu woo ñaar ci ñoom, 19 te mu yónni leen ci Boroom bi ngir laaj ko: «Ndax yaw yaay Almasi bi waroona ñëw walla danoo wara xaar keneen?»
20 Noonu bi ñu yegsee ci wetu Yeesu ñu wax ko ne: «Yaxya moo nu yónni ngir nu laaj la: "Ndax yaw yaay Almasi bi waroona ñëw walla danoo wara xaar keneen?"» 21 Ci waxtu boobu sax Yeesu mu ngi doon wéral ay nit ñu bari ci seeni feebar, ci seeni laago te di dàq rab yu bon, te mu doon gislowaat gumba yi. 22 Noonu mu tontu taalibe Yaxya yi ne leen: «Demleen, nettali Yaxya li ngeen gis ak li ngeen dégg. Gumba yi ñu ngi gisaat, lafañ yi ñu ngi dox, gaana yi wér nañu, tëx yi ñu ngi dégg, te ñi dee woon ñu ngi dekki; te yégal nañu xibaar bu baax bi néew-di-doole yi. 23 Barkeel na ki dul ñàkk ngëm ndax man!»
24 Gannaaw bi ñi Yaxya yónni woon delloo, Yeesu di wax ak mbooloo mi, ci lu jëm ci Yaxya: «Lan ngeen demoon gis ci màndiŋ bi: benn xeetu ñax bu ngelaw li di naawloo ci wet bu nekk? 25 Waaye lan ngeen demoon gis: benn nit bu sol ay yére yu rafet? Ñiy sol ay yére yu rafet dañuy dund ci biir bànneex te di dëkk ci biir kër buur yi. 26 Waaye lan ngeen demoon gis: ab yonent? Waaw, maa ngi leen koy wax, ku ëpp sax yonent, 27 ndaxte ci Yaxya la Mbind mi wax ne:
"Xoolal maa ngi yónnee ci sa kanam benn yonent
ngir mu waajal sa yoon ci sa kanam."\qt*
28 Te maa ngi leen koy wax, ci ñi juddoo ci jigéen amul kenn ku gëna màgg Yaxya, waaye ki gëna ndaw ci nguuru Yàlla gi, moo ko gëna màgg.»
29 Te noonu niti askan bi yépp ak juutikat yi doon déglu bataaxalu Yaxya, nangu nañu ne Yàlla dafa jub ba tax ñu nangu Yaxya sóob leen ci ndox. 30 Waaye Farisen yi ak jàngalekati-yoonu-Musaa yi nanguwuñu coobare Yàlla ci seen dund ba tax nanguwuñu Yaxya sóob leen ci ndox.
31 Yeesu waxaat ne: «Ñan laa wara méngalee nitu jamono ji ak ñan lañuy nirool? 32 Ñu ngi nirook ay xale yu toog ci péncu dëkk bi di yuuxuwante, ñenn ñi di wax ñeneen ñi, ne:
"Woyal nanu leen woyu bànneex te fecculeen.
Woyal nanu leen woyu dëj te jooyuleen."
33 Ndaxte Yaxya ñëw na, lekkul mburu, naanul biiñ, ngeen wax ne: "Kii dafa am rab." 34 Noonu Doomu nit ki ñëw na di lekk te di naan, ngeen wax ne: "Kii day lekk ak naan rekk, di xaritu juutikat yi ak bàkkaarkat yi." 35 Waaye ñépp ñi nangu li Yàlla wax ci xelam bu rafet, xam nañu ne Yàlla dafa jub.»
Yeesu ci kër Farisen ba Simoŋ
36 Amoon na benn Farisen bu ñaan Yeesu ngir mu lekkandoo ak moom ci këram. Yeesu nangu, dugg kër Farisen bi, te toog ci bérébu lekkukaay ba. 37 Mu am benn jigéen bu dundinam baaxul bu nekkoon ci dëkk bi, mu xam ne Yeesu mu ngi kër Farisen bi, mu ñëw, andaale butéel bu rafet bu ñuy woowe albaatar bu fees dell ak latkoloñ. 38 Noonu mu jegesi ci wetu tànki Yeesu, di jooy ba tooyal tànki Yeesu ak rongooñam te di leen fompe kawaram, di leen fóon te di ko sotti latkoloñ.
39 Noonu bi Farisen bi dalal Yeesu gisee loolu, muy xalaat ci xelam ne: «Kii, su doon yonent, doon na xam, jigéen bi koy laal, dundinam baaxul.» 40 Yeesu jël kàddu gi, ne ko: «Simoŋ, bëgg naa la wax lii.» Simoŋ tontu ko ne: «Jàngalekat bi, waxal.» 41 Yeesu ne ko: «Dafa amoon benn waay. Mu lebaloon ñaari nit bor. Kenn ki mu lebal ko téeméeri junni, keneen ki mu lebal ko fukki junni. 42 Te ñoom ñaar ñépp amuñu woon lu ñu mëna feye bor yi. Ci mbaaxam mu baal leen ñoom ñaar ñépp seeni bor. Ci ñoom ñaar kan moo ko ciy gëna bëgg?» 43 Simoŋ tontu ko ne: «Xanaa ki mu baal bor bu mag bi.» Yeesu ne ko: «Àtte nga bu baax.» 44 Noonu, Yeesu walbatiku ci ku jigéen ki, ne ko: «Simoŋ, gis nga ku jigéen kii? Yaw, bi ma duggee sa kër mayuloo ma ndox ngir ma raxas samay tànk, waaye moom, noppiwul di tooyal samay tànk ak rongooñam te di leen fompe kawaram. 45 Yaw, fóonuloo ma, waaye moom, noppiwul di fóon samay tànk. 46 Diwuloo diw ci sama bopp, waaye moom, noppiwul di sotti latkoloñ ci samay tànk. 47 Moo tax maa ngi la koy wax ne mbëggeelam dafa bari ndaxte baal nañu ko bàkkaaram yu bari yi, waaye ku ñu baal tuuti, mbëggeelam day tuuti.» 48 Noonu Yeesu ne ku jigéen ki: «Baal nañu la say bàkkaar.»