Yeesu ak ñi mu àndaloon
8
Te ci noonu, Yeesu doon na dem dëkk ak dëkk ak ci gox-goxaat yi, di waare ak di yégle xibaar bu baax bi ci nguuru Yàlla. Fukki ndaw yi ak ñaar àndoon nañu ak moom 2 ak yenn jigéen yi mu dàqoon ay rab yu bon ak wéral seeni feebar: Maryaama mi ñuy woowe Maryaama mu Magdala te mu dàqoon ci moom juróom ñaari rab yu bon, 3 ak Sànn di jabaru Kusa miy njiitu ñi doon liggéey kër Erodd mi yilifoon diiwaanu Galile, ak Susànn ak yeneen jigéen yu bari yu doon jàppale Yeesu ak taalibeem yi ak seen alal.Léebu jikat bi
4 Noonu mu am mbooloo mu bari, jóge dëkk ak dëkk, ñu daldi ñëw ci wetam. Noonu mu wax leen léeb bii: 5 «Dafa amoon benn jikat bu génn ngir jiyi jiwam. Bi muy ji am pepp yu daanu ci yoon bi; nit ñi ñëw, dëgg ko, picci asamaan si ñëw lekk li des. 6 Yenn pepp yi daanu ci diggante xeer yi, bi ñu saxee ñu daldi wow, ndaxte foofu tooyul woon. 7 Yeneen pepp yi daanu ci diggante ay xaaxaam; ñu daldi jógandoo ak xaaxaam yi, xaaxaam yi tanc leen. 8 Waaye yi ci des daldi daanu ci suuf su baax si; ci noonu ñu daldi meññ téeméeri yoon lu ëpp li ñu ji woon.» Yeesu yékkëti baatam te yokk ca ne: «Na ki am nopp ngir déglu, dégg.»
9 Taalibeem yi laaj ko lu léeb bi di tekki. 10 Mu tontu leen: «Yeen, Yàlla may na leen ngir ngeen xam li nëbbu ci nguuru Yàlla gi, waaye ñeneen ñi, dama leen koy wax ci léeb ngir bu ñuy xoole, ñu baña gis, te ñu dégg, baña ràññee.
11 Lii la léeb bi di tekki: jiwu ji mooy kàddu Yàlla gi. 12 Ñi nga xam ne moo nekk ci yoon bi mooy ñiy déglu kàddu gi, waaye Seytaane ñëw, këf kàddu gi nekk ci seen biir xol ngir ñu baña gëm te baña mucc. 13 Li nga xam ne moo daanu ci xeer yi mooy ñiy déglu te nangu kàddu gi ak mbégte waaye amuñu reen, te dañuy gëm benn diir te bàyyi ngëm bi ci waxtu bi jafe-jafe yi ñëwee. 14 Beneen bi mooy ji nga xam ne moo daanu ci xaaxaam yi, mooy ñiy déglu te nangu kàddu gi, waaye jafe-jafe àddina si, alal yi, bànneexu bakkan tanc leen ba tax duñu am ay meññeef yu baax. 15 Te beneen bi daanu ci suuf su baax si mooy ñi nga xamante ne dañuy déglu kàddu gi te denc ko ci seen biir xol bu baax ak dëggu, téye ko di dëgër-dëgërlu ba ñu am meññeef.»
Léebu làmp bi
16 «Kenn du taal làmp di ko muur walla di ko dugal ci ron lal, waaye dañu koy wékk ngir ku duggsi mëna gis leer bi. 17 Amul dara lu nëbbu lu nit dul xam; amul dara lu umpe lu nit dul xamle benn bés. 18 Moytuleen ci anam bi nuy déggee, ndaxte ku am dinañu la yokkal, waaye ku amul dinañu jël sax li nga xalaatoon ne moom nga am.»
Yaayu Yeesu ak rakkam yi
19 Yaayu Yeesu ak rakki Yeesu yi ñëw ngir gis Yeesu, waaye mënuñu woon jot ci moom ndax mbooloo mi. 20 Ñu ne ko: «Sa yaay ak say rakk ñu ngi ci biti, bëgg la gis.» 21 Waaye Yeesu tontu leen ne: «Sama yaay ak samay rakk, mooy ñiy déglu kàddu Yàlla gi te di ko jëfe.»
Yeesu dalal na ngelaw li ak ndox mi
22 Benn bés Yeesu ak taalibe yi yéeg gaal. Yeesu ne taalibe yi: «Nu dem ba ci beneen tefes bi.» 23 Bi ñu doon dem Yeesu daldi nelaw. Ngelaw gu am doole yëngal ndox mi, te ndox mu bari dugg ci biir gaal gi. Ñu nekkoon ci tolof-tolof. 24 Taalibe yi jegesi ko, yee ko ne ko: «Kilifa gi, kilifa gi, nu ngi suux!» Yeesu daldi jóg, gëdd ngelaw li ak ndox mi. Lépp dal. 25 Yeesu ne taalibe yi: «Ana seen ngëm?» Taalibe yi tiitoon nañu te waaru di waxtaan ci seen biir di naan: «Waaw! Kii mooy kan sax, bay joxe ndigal ngelaw li ak ndox mi te ñu koy déggal?»
Yeesu wéral na waay ju am ay rab
26 Yeesu ak taalibeem yi teer nañu ci diiwaanu Serasa. Mu jàkkaarlook diiwaanu Galile. 27 Bi Yeesu wàccee gaal gi, am benn waay, di doom ci diiwaan bi, di ñëw, di dajesi ak moom. Waa ji amoon na ay rab, te yàgg na lool daawul sol yére te dëkkul ci kër waaye mu ngi dëkkoon ci armeel yi. 28-29 Yenn saay rab yi jàpp ko, te nit ñi doon takk loxoom yi ay ceen te di takk tànk yi ak ay weñ, waaye du tere mu dog ko te rab bi di ko yóbbu ci màndiŋ mi. Bi mu gisee Yeesu mu daanu ci tànkam yi di yuuxu te di wax ak baat bu kawe ne: «Loo ma bëggal, Yeesu Doomu Yàlla Aji-Kawe ji? Ma ngi la koy ñaan, bul ma metital.» Wax na loolu ndaxte fekkoon na Yeesu jox ndigal rab bi ngir mu génn ci waa ji. 30 Yeesu laaj ko: «Noo tudd?» Mu tontu ko ne: «Coggal laa tudd.» Wax na loolu ndaxte rab yu bari ñoo nekkoon ci moom. 31 Rab yi ñaan Yeesu ngir mu bañ leena sànni ci kàmb gu ñu tëj xel yu bon yi.
32 Te fekk na ci waxtu boobu amoon na géttu mbaam-xuux yu bari, yu doon wut lu ñuy lekk ci kaw tund bi. Rab yi ñaan Yeesu ngir mu may leen ñu dugg ci géttu mbaam-xuux yi. Yeesu may leen ko. 33 Noonu rab yi daldi génn ci waa ji, dugg ci mbaam-xuux yi, te mbaam-xuux yi di gaawantu, tarxiis, daanu ci dex bi, daldi lab. 34 Bi sàmmkatu mbaam-xuux yi gisee li xewoon, ñu daldi daw, dem ci dëkk bi, ak ci kër àll yi, di nettali lépp lu ñu gisoon. 35 Nit ñi génn ngir gis li xewoon. Bi ñu yegsee ci wetu Yeesu, ñu gis ki rab yi jàppoon, mu toog ci wetam sol yére te ànd ak sagoom. Ñu daldi tiit. 36 Ñi ko fekkewoon di nettali naka la waa ji ame woon rab mucce. 37 Noonu waa diiwaanu Serasa yépp di ñaan Yeesu ngir mu génn seen diiwaan ndaxte tiitaange bu mag, moo leen jàppoon. Bi Yeesu di yéeg ci gaal gi ngir dellu, 38 ki mu teqale woon ak rab yi ñaan ko ngir mu ànd ak moom. Waaye Yeesu ne ko: 39 «Ñibbil sa kër te nga nettali lépp li la Yàlla defal.» Waa ji ñibbi këram, di yégle ci dëkk bi yépp li ko Yeesu defal.
Yeesu dekkil na doomu Yayrus te wéral jigéen ju doon xëpp deret
40 Bi Yeesu dellusee ci Galile mbooloo mu bari moo ko doon teeru ndaxte dañu ko doon xaar. 41 Foofu amoon na benn nit bu tudd Yayrus nekk njiitu kër-ñaan bi. Mu sukk ci tànku Yeesu ngir ñaan ko ngir mu ñëw këram, 42 ndaxte dafa amoon benn doom bu jigéen képp bu am fukki at ak ñaar, te feebaroon bay waaja dee.
Bi ñuy dem ci yoon bi mbooloo mi di tanc Yeesu. 43 Foofu amoon na benn jigéen bu doon xëpp deret lu tollu ci fukki at ak ñaar, te fajoo alalam bi yépp ci fajkat yi, waaye kenn mënu ko woona wéral. 44 Mu jaar ci gannaaw Yeesu, laal catu yéreem, te xëpp deret bi daldi taxaw ci saa si. 45 Yeesu laaj leen: «Kan moo ma laal?» Waaye ñépp di wax ne: «Du man! Du man!» Piyeer ne ko: «Kilifa gi, mbooloo mi la wër ñoo la tanc.» 46 Yeesu waxaat ne: «Am na ku ma laal ndaxte yég naa kàttan bu génn ci man.» 47 Bi ku jigéen ki xamee ne mënatul nëbbatu. Muy ñëw di lox, te sukk ci tànku Yeesu yi, di wax ci kanamu ñépp lu tax mu laaloon ko ak ni mu jote wér ci saa si. 48 Yeesu ne ko: «Sama doom sa ngëm wéral na la; demal ci jàmm.»
49 Bi Yeesu di wax loolu, benn nit jóge ci kër Yayrus mi nekk njiitu kër-ñaan bi, te ne ko: «Jarul nga sonal jàngalekat bi, ndaxte sa doom dee na.» 50 Bi Yeesu déggee wax yooyu, mu ne Yayrus: «Bul ragal dara. Gëmal rekk te sa doom dina mucc.» 51-53 Noonu bi ñu yegsee ci kër gi, Ñépp a doon jooy di naqarlu xale bi. Mu ne leen: «Bàyyileen jooy yi. Xale bi deewul, day nelaw rekk.» Noonu ñu koy ñaawal ndaxte xamoon nañu ne xale bi dee na. Yeesu nanguwuloon kenn dugg ak moom, ku dul Piyeer, Yowaana, Saag, pàppa xale bi ak yaayam. 54 Mu téye loxo xale bi, te mu wax ak baat bu kawe ne: «Sama doom, jógal.» 55 Noonu xale bi daldi dekki te mu jóg ci saa si. Mu naan leen: «Joxleen ko mu lekk.» 56 Waajuru xale bi waaru woon nañu lool. Waaye Yeesu ne leen: «Buleen wax kenn li fi xew.»