Ku nit ñi fooge woon Yeesu
9
Yeesu dajale na fukki ndaw yi ak ñaar, jox leen kàttan ak sañ-sañ ngir dàq rab yi yépp tey wéral ñi feebar. 2 Noonu mu yónni leen ngir ñu waare xibaar bu baax bi ci nguuru Yàlla te wéral feebar yi. 3 Mu ne leen: «Buleen yóbbu dara ci tukki bii: du yet, du saaku, du mburu, du xaalis, te buleen yóbbaale yeneen yére. 4 Bu ñu leen dalalee ci kër, nangeen des foofu ba seen waxtu dem jot. 5 Fépp fu leen nit ñi baña dalal, génnleen ci dëkk boobu te faxas pënd bi nekk ci seeni tànk, ngir loolu mën leen seedeel seen réer.» 6 Noonu ñu daldi dem ci gox-goxaat yi, di waare xibaar bu baax bi tey wéral ñi feebar.7 Bi Erodd mi yilif diiwaanu Galile déggee lépp li xewoon, noonu mu daldi jaaxle, ndaxte ñenn ñi dañu doon wax ne: «Yaxya moo dekki ci ñu dee ñi.» 8 Ñeneen ñi di wax ne: «Ilyaas moo feeñu.» Ñi ci des di ne: «Kenn ci yonent yu jëkk yi moo dekki.» 9 Waaye Erodd di wax ne: «Dagglu naa boppu Yaxya, kon ci kan lañuy wax ci li ma dégg ci mbir yi?» Noonu mu wutoon ko gis.
10 Bi fukki ndaw yi ak ñaar dellusee, ñu nettali Yeesu lépp li ñu defoon. Noonu mu jël leen, beru ak ñoom ci wetu dëkk bi ñuy woowe Betsayda. 11 Waaye bi mbooloo mi yégee loolu, ñu daldi koy topp. Yeesu dalal leen, wax leen ci nguuru Yàlla gi, te wéral ñi soxla woon wér-gu-yaram. 12 Bi jant bi di waaja sow, fukki ndaw yi ak ñaar jegesi ko, te wax ko ne: «Yewwil mbooloo mi, ñu mëna dem ci dëkk yi ak ci gox-goxaat yi nu wër ngir ñu mëna dal foofu te am lu ñuy lekk ndaxte béréb bi nu nekk màndiŋ la.» 13 Waaye Yeesu ne leen: «Yeen ci seen bopp, joxleen ñoom lu ñuy lekk.» Noonu ñu wax ko ne: «Fii déy, juróomi mburu rekk ak ñaari jën lanu am. Walla nu dem jëndal mbooloo mi yépp lu ñuy lekk?» 14 Ndaxte foofu amoon na ci xayma juróomi junniy góor. Noonu Yeesu ne taalibe yi: «Toogloo leen mbooloo mi ci ay géewi juróom fukki nit.» 15 Noonu ñu def loolu, toogloo ñépp. 16 Noonu Yeesu daldi jël juróomi mburu yi ak ñaari jën yi; yékkëti bëtam yi ci asamaan, barkeel leen, damm leen, te jox leen taalibe yi ngir ñu séddale leen mbooloo mi. 17 Ñépp lekkoon nañu ba regg; ba ñu for ci fukki pañe ak ñaar yu fees dell ci dagg yi desoon.
18 Benn bés Yeesu beddeeku, di ñaan. Taalibe yi nekkoon ci wetam. Mu laaj leen: «Nit ñi kan lañuy wax ne moom la?» 19 Ñu tontu ko ne: «Am na ñuy wax ne yaw yaay Yaxya, ñii ne yaw yaay Ilyaas, ñi ci des, ne kenn ci yonent yu jëkk yi moo dekki.» 20 Mu laaj leen: «Yeen nag, kan ngeen wax ne moom laa?» Piyeer tontu ko ne: «Yaw yaay Almasi Yàlla bi.» 21 Yeesu dénk leen ndigal bii, ne: «Buleen ko wax kenn.» 22 Mu yokk ca ne: «Fàww Doomu nit ki sonn lool. Noonu mag ña, njiiti-jébbalkatu-sarax yi ak jàngalekatu-yoonu-Musaa yi dëddu ko, rey ko, mu dekki ci ñetteelu fan ba.»
23 Mu wax leen ñoom ñépp ne: «Ku ma bëgga topp, na bàyyi boppam, nangu daj lu metti, doora topp ci man. 24 Ndaxte ku bëgga muccal sa bakkan dina ko ñàkk, waaye ku ñàkk sa bakkan ngir man jotaat ko. 25 Lu muy jériñ nit su fekkee day moom àddina si yépp te ñàkk bakkanam walla mu sànku? 26 Ku ma rusa seedeel te rusa seede samay kàddu, Doomu nit ki dina la rusa xam bés bu ñëwee ci màggaayam, ci màggaayu Baay bi ak bu malaaka yu sell yi. 27 Ci dëgg, maa ngi leen koy wax, am na ñoo xam ne ñu ngi fii duñu dee mukk te gisuñu nguuru Yàlla.»
Màggaayu Yeesu feeñ na
28 Lu tollook juróom ñetti fan gannaaw bi mu waxee kàddu yooyu, Yeesu jël Piyeer, Yowaana, ak Saag, daldi yéeg ci tund wi ngir ñaan. 29 Bi mu doon ñaan, xar kanamam soppeeku, yére yu mu soloon weex tàll bay melax. 30 Ci saa si ñaari nit di waxtaan ak moom, Musaa ak Ilyaas. 31 Ñu feeñu ci màggaayu Yàlla di wax ci demam li mu wara matal ca Yerusalem. 32 Piyeer ak ñi mu àndaloon nelawoon nañu waaye seeni nelaw xootul woon. Noonu ñu yeewu, gis màggaayu Yeesu ak ñaar ñi nekkoon ak moom. 33 Bi ñooñu di xaajaloo ak moom, Piyeer ne ko: «Kilifa gi, baax na ngir nu des fii. Nanu def ñetti mbaar, benn ngir yaw, benn ngir Musaa, ak benn ngir Ilyaas.» Xamul woon lu mu doon wax. 34 Bi mu nekkee di wax, benn niir daldi ñëw, muur leen. Bi taalibe yi duggee ci niir bi, ñu daldi tiit. 35 Noonu baat jóge ci niir bi, ne: «Kii mooy sama Doom. Moom laa tànn. Dégluleen ko.» 36 Gannaaw bi baat bi waxee ba noppi, Yeesu des fa moom kese. Ci jamono jooju taalibe yi noppi, nettaliwuñu kenn li ñu gisoon.
Yeesu wéral na benn xale bu am rab
37 Ci ëllëg sa bi Yeesu, Piyeer, Yowaana ak Saag di wàcc ci tund wi, mbooloo mu takku ñëw di dajesi ak Yeesu. 38 Ci diggu mbooloo mi, am benn waay bu ñëw di yuuxu di naan: «Jàngalekat bi, maa ngi la koy ñaan, xoolal ma sama doom, ndaxte kenn kii laa am. 39 Rab moo ko jàpp, mu jekki di ko yuuxuloo, di ko sayloo, gémmiñam di fuur te du ko bàyyi feek metital ko. 40 Ñaan naa sa taalibe yi ngir ñu dàq rab bi, waaye mënuñu ko.» 41 Yeesu daldi jël kàddu gi te ne leen: «Yeen niti jamono jii, ñi amul ngëm te dëng. Man, ba kañ laay nekk ak yeen te di leen muñal?» Mu daldi wax waa ji: «Andil ma sa doom bi fii.» 42 Bi xale bi di ñëw, rab bi daaneel ko ci suuf, sayloo ko. Yeesu tëkku rab bi, wéral xale bi, te delloo ko pàppaam. 43 Ñépp daldi jaaxle ndax màggaayu Yàlla.
Bu ñépp yéemoo ci li mu doon def, Yeesu ne taalibeem yi: 44 «Ubbileen seeni nopp bu baax: Fàww ñu jébbal Doomu nit ki ci loxoy nit ñi.» 45 Waaye kàddu yooyu leerul ci ñoom: ump na leen, te mënuñu woona xam luy loolu di tekki, te ragal nañu laaj Yeesu lu jëm ci kàddu yooyu.
Kan moo gëna mag ci taalibe yi?
46 Gannaaw loolu taalibe yi tàmbali di waxtaan ci seen biir ngir bëgga xam kan moo gëna màgg ci ñoom. 47 Noonu Yeesu xam seeni xalaatu xol, andi benn xale ci wetam, 48 ne leen: «Ku nangu xale bii ci sama tur, man nga nangu; te ku ma nangu, nangu nga ki ma yónni. Ndaxte ki gëna ndaw ci yeen ñépp, kooku moo gëna mag.» 49 Noonu Yowaana tontu ko ne: «Kilifa gi, gis nanu benn waay buy dàq ay rab ci sa tur waaye danu ko doon jéema tere ndaxte àndul ak nun.» 50 Yeesu tontu ko ne: «Buleen ko tere ndaxte ku leen xeexul, ci yeen la far.»
Yeesu jëm na Yerusalem
51 Bi bés bu ñu waroona yékkëti Yeesu asamaan jegesee, mu jël ndogal ngir dem Yerusalem. 52 Noonu mu yónni ay ndaw ngir ñu jiitu ko. Ci yoon bi, ñu dugg ci benn gox bu nekk ci diiwaanu Samari ngir waajal ko fu mu mëna dal, 53 waaye waa gox boobu bañ koo dalal ndaxte dafa doon dem Yerusalem. 54 Bi ñu gisee ne waa Samari dañu leen baña dalal, Saag ak Yowaana laaj Yeesu ne: «Boroom bi, ndax danga bëgg nu wax safaras asamaan si mu wàcc ci seen kaw ngir lakk leen?» 55 Noonu Yeesu walbatiku ci ñoom, gëdd leen 56 te ñu dem ci beneen gox.
57 Bi ñuy dem ci yoon bi benn waay ne Yeesu: «Boroom bi, dinaa la topp foo mëna dem.» 58 Yeesu tontu ko ne: «Xaju àll yi am nañu ay pax yu ñu dëkke; picc yi am nañu ay tagg, waaye Doomu nit ki amul fu muy teg boppam ngir noppalu.» 59 Noonu Yeesu wax keneen ki ne: «Topp ma.» Mu ne ko: «Boroom bi, may ma, ma dem suul sama pàppa ba noppi.» 60 Yeesu ne ko: «Bàyyil ñi dee suul seeni néew waaye yaw nga dem yégle nguuru Yàlla gi.» 61 Noonu keneen ne: «Boroom bi, dinaa la topp waaye may ma, ma dem tàggooji ak sama waa kër ba noppi.» 62 Yeesu ne ko: «Kuy bey di geestu, amuloo njériñ nguuru Yàlla gi.»