Yeesu dekki na ci ñu dee ñi
16
Bi bésu noflaay bi weesoo, Maryaama mu Magdala, Maryaama yaayu Saak, ak Salome jënd diw bu xeeñ latkoloñ ngir dem xeeñale ko néewu Yeesu. 2 Dimaas ci suba teel bi jant bi fenkee ñu dem ci bàmmeel bi. 3 Ñuy wax ci seen biir ne: «Kan moo nuy bërëŋal xeer bi tëj bàmmeel bi?» 4 Bi ñu yékkëtee seeni bët, ñu gis ne bërëŋ nañu xeer bi, doonte xeer bu réy la woon. 5 Bi ñu duggee ci bàmmeel bi, ñu gis benn waxambaane bu sol yére bu weex tooge ci seen ndeyjoor, te ñu daldi tiit. 6 Waaye mu ne leen: «Buleen tiit. Yeesu mu Nasaret mi ñu daajoon ci bant bi ngeen di seet. Dekki na. Nekkatu fi. Xoolleen béréb bi ñu ko dencoon. 7 Léegi demleen, wax taalibeem yi ak Piyeer: "Mu ngi leen di jiituji diiwaanu Galile. Foofu ngeen koy gise, ni mu leen ko waxe woon."» 8 Noonu ñu génn ci bàmmeel bi di daw, ndaxte dañu doon lox te yéemu lool. Waxuñu kenn dara ndaxte dañoo tiitoon.
Yeesu feeñu na taalibeem yi te wax leen nu yégle xibaar bu baax bi ci àddina si yépp
9 Bi Yeesu dekkee Dimaas ci suba si, Maryaama mu Magdala la jëkka feeñu. Ci moom la dàqoon juróom ñaari rab yi. 10-11 Ñi doon ànd ak Yeesu nekkoon nañu ci naqar di jooy. Maryaama mu Magdala dem yégal leen ne Yeesu mu ngi dund te gis na ko, waaye ñoom gëmuñu ko. 12 Gannaaw loolu Yeesu feeñu ñaari taalibe ci beneen melokaan bi ñu nekkee ci yoon ngir dem ci këru àll yi. 13 Te ñooñu ñëwaat yégal ko ñeneen ñi, waaye gëmuñu leen tamit. 14 Noonu mu daldi feeñu fukk yi ak benn, bi ñu nekkee ci bérébu lekkukaay bi, te mu yedd leen ndax seen ñàkka gëm ak seen dëgëraayu xol, ndaxte gëmuñu woon ñi ko gisoon gannaaw bi mu dekkee. 15 Noonu mu ne leen: «Demleen ci àddina sépp te yégle xibaar bu baax bi ci ñépp. 16 Ku gëm te ñu sóob ko ci ndox dina mucc. Waaye ku gëmul dinañu ko teg daan. 17 Màndarga yii ñooy ànd ak ñi gëm: dinañu dàq rab yi ci sama tur; dinañu wax ay kàllaama yu bees; 18 dinañu jàpp ci seeni loxo ay jaan; te bu ñu naanee tooke dara du leen dal. Dinañu teg seeni loxo ci kaw ñi feebar te ñu wér.» 19 Gannaaw bi Boroom bi Yeesu waxee ak ñoom ba noppi, Yàlla yékkëti ko ci asamaan, te mu toog ci ndeyjooram. 20 Ñoom, ñu dem yégle fépp xibaar bu baax bi. Boroom bi doon na ànd ak ñoom, di dëggal kàddu gi jaarale ko ci màndarga yi doon gunge kàddu gi.