Pilaat mu ngi laaj Yeesu
15
Ci suba teel, njiiti-jébbalkati-sarax yi waxtaan ak mag ñi, jàngalekati-yoonu-Musaa yi, ak kurélu àttekati Yawut yi yépp. Noonu ñu yeew Yeesu, yóbbu ko, te jébbal ko Pilaat. 2 Pilaat laaj ko ne: «Ndax yaw yaay buuru Yawut yi?» Yeesu tontu ne: «Yaw, yaa ko wax.» 3 Njiiti-jébbalkati-sarax yi tàmbali di ko tuumaal ci ay mbir yu bari. 4 Noonu Pilaat laajaat ko ne: «Xanaa déggoo lépp li ñu lay tuumaal? Ndax doo tontu dara?» 5 Waaye Yeesu tontuwul dara, ba tax Pilaat waaru lool.6 Màggalu Paak bu nekk, Pilaat dafa tàmmoon di bàyyi kenn ci ñi ñu tëj kaso, ki askan bi doon laaj. 7 Fekk amoon na benn nit bu tudd Barabas. Ñu tëjoon ko kaso ak yeneen fippukat ndaxte dañoo reyoon nit ci fippu bi amoon ci dëkk bi. 8 Mbooloo mi dem kër Pilaat te ñu ñaan ko ngir mu jëfe ni mu ko tàmme woon di def. 9 Pilaat tontu leen ne: «Dangeen bëgg ma bàyyil leen buuru Yawut yi?» 10 Laaj na leen loolu ndaxte xamoon na ne iñaan moo tax njiiti-jébbalkati-sarax yi jébbal ko Yeesu. 11 Waaye njiiti-jébbalkati-sarax yi di yékkëti mbooloo mi ngir ñu ñaan Pilaat mu bàyyil leen Barabas. 12 Pilaat jëlaat kàddu gi ngir laaj leen: «Lan ngeen bëgg nag ma def ci ki ngeen di woowe buuru Yawut yi?» 13 Ñuy yuuxu naan: «Daaj ko ci bant.» 14 Pilaat laaj leen: «Lan la def lu bon?» Waaye ñu gëna yuuxu naan: «Daaj ko ci bant.» 15 Noonu Pilaat bàyyil leen Barabas ndaxte da bëggoon lu neex mbooloo mi. Yeesu nag, mu dóorlu ko ay yar te jébbal ko soldaar yi ngir ñu daaj ko ci bant.
Ñaawal nañu Yeesu, daaj ko ci bant, te mu dee
16 Soldaar yi yóbbu Yeesu ci biir kër njiitu diiwaan bi, te ñu woo mbooloo soldaar yi yépp, ñu dajaloo. 17 Ñu solal ko mbubb bu xonq te ñu teg ci boppam ab kaala bu ñu ràbbe dég. 18 Ñu tàmbali di ko nuyu naan: «Nuyu nanu la, yaw buuru Yawut yi.» 19 Ñu di ko dóor ci bopp ak benn bant, di tifli ci kawam, te sukk di sëgg ci kanamam. 20 Bi ñu ko ñaawalee ba noppi, ñu daldi summi mbubb bu xonq bi ñu ko solaloon, delloo ko yéreem yi, te yóbbu ko ci biti ngir daaj ko ci bant ba.
21 Benn waay bu tudd Simoŋ mu Siren, miy baayu Alegsàndar ak Rufus, jaaroon foofu, jógewoon ci toll yi. Soldaar yi sëf ko bantu Yeesu bi. 22 Ñu yóbbu Yeesu ci béréb bi ñuy woowe Golgota, luy tekki yaxu bopp. 23 Ñu bëgg ko jox biiñ bu ñu jaxase ak lu ñuy wax miir, waaye Yeesu bañ. 24 Noonu ñu daaj ko ci bant te séddoo yéreem yi di tegoo bant ngir xam ku nekk li muy am. 25 Bi ñu koy daaj ci bant juróom ñeenti waxtu ci suba moo jotoon. 26 Lii lañu bind: «Kii mooy Buuru Yawut yi» ngir wone li tax ñu teg ko daan. 27-28 Ñu daajaale ñaari defkatu lu bon ci wetam, kenn ki ci ndeyjooram, keneen ki ci càmmoñam. 29 Ñi doon romb foofu di ko saaga di yëngal seeni bopp, naan: «Éey, yaw miy toj kër-Yàlla gi te tabaxaat ko ci ñetti fan, 30 wàccal ci bant bi ngir musal sa bopp.» 31 Ci noonu tamit njiiti-jébbalkati-sarax yi ak jàngalekati-yoonu-Musaa di ko ñaawal, di waxante ci seen biir: «Musal na ñeneen ñi waaye mënula musal boppam. 32 Na Almasi bi, buuru Israyil bi, wàcc ci bant bi léegi, ngir nu gis te gëm.» Ñi ñu daajaale woon ak moom sax di ko saaga.
33 Ci diggu bëccëg réew mi yépp lëndëm ba ci ñetti waxtu ci ngoon. 34 Bi ñetteelu waxtu bi jotee, Yeesu yuuxu ak baat bu kawe naan: «Eli, Eli, lema sabaktani?» luy tekki: «Sama Yàlla, sama Yàlla, lu tax nga bàyyi ma?» 35 Ñenn ñi fa nekkoon dégg loolu tey yuuxu naan: «Dégluleen, mu ngi woo yonent Yàlla Ilyaas.» 36 Am kenn ku daw, jël benn sagar, capp ko ci bineegar, takk ko ci bant, te tàllal ko Yeesu ngir mu naan ko, te ne: «Xaarleen ba xam ndax Ilyaas dina ñëw wàcce ko ci bant bi.» 37 Waaye Yeesu yuuxu ak baat bu kawe te daldi dee. 38 Rido kër-Yàlla gi daldi xar ñaar, li ko dale ci kaw ba ci suuf. 39 Njiitu soldaar bi taxawoon ci kanamu Yeesu, bi mu gisee naka la deewe, mu ne: «Ci dëgg, nit kii Doomu Yàlla la.»
Rob nañu Yeesu
40 Amoon na tamit yenn jigéen yu doon seetaane fu sori. Maryaama mu Magdala, Maryaama yaayu Saak bu ndaw ak Yose, ak Salome bokkoon nañu ci. 41 Daan nañu topp Yeesu te di ko toppatoo bi mu nekkee ci diiwaanu Galile. Amoon na tamit yeneen jigéen yu bari yu àndoon ak moom ba Yerusalem.
42-43 Bésu waajal bi la woon, maanaam bés bi jiitu bésu noflaay bi. Bi ngoon si jotee, ku tudd Yuusufa mu Arimate yegsi. Bokkoon na ci kurélu àttekat yi te ñu joxoon ko cér, te mu doon xaar moom tamit nguuru Yàlla gi. Mu takk fitam, dem ci Pilaat ngir laaj ko néewu Yeesu. 44 Pilaat waaru woon na bi mu yégee ne Yeesu dee na ba noppi. Mu woolu njiitu soldaar bi te laaj ko ndax bi mu deewee ak léegi, yàgg na. 45 Gannaaw bi mu déggee tontu njiitu soldaar bi, Pilaat may Yuusufa mu jël néew bi. 46 Yuusufa daldi jënd benn perkaal, wàcce néew bi ci bant bi, lëmës ko ci perkaal bi, te denc ko ci benn bàmmeel bi ñu yattoon ci biir doj. Noonu mu bërëŋ xeer bu réy ngir tëj buntu bàmmeel bi. 47 Maryaama mu Magdala ak Maryaama yaayu Yose doon xool fan lañu ko denc.