Benn jigéen tuur na latkoloñ ci boppu Yeesu
14
Ñaari fan a desoon bala màggalu Paak bi ak màggalu mburu yu amul lawiir yi. Njiiti-jébbalkati-sarax yi ak jàngalekati-yoonu-Musaa doon wut pexe ngir jàpp Yeesu ci kumpa te reylu ko, 2 ndaxte dañu doon wax ne: «Warunu ko jàpp ci bésu màggal yi. Lu ko moy yëngu-yëngu mën na am ci askan bi.»3 Bi Yeesu nekkee Betani ci këru Simoŋ gaana bi, benn jigéen duggsi ci waxtu bi mu nekkee ci bérébu lekkukaay bi. Mu yor butéel bu ñu defare xeeru albaatar bu fees ak latkoloñ bi ñuy woowe naar bu raxul dara, te njég li bari. Mu toj butéel bi te tuur latkoloñ bi ci boppu Yeesu. 4 Ñenn ñi daldi ci mer te di wax ci seen biir: «Lu tax muy yàq latkoloñ bi? 5 Ndaxte mënoon nañu ko jaaye lu tollook peyooru atu lëmm te jox xaalis bi néew-di-doole yi.» Te ñu tàmbali di ŋàññe ku jigéen ki. 6 Waaye Yeesu ne: «Bàyyileen ko. Lu tax ngeen koy sonnal? Jëf ju baax la ma defal, 7 ndaxte néew-di-doole yi dinañu nekk ak yeen saa su nekk te mën ngeen leen defal lu baax saa su ngeen ko bëggee, waaye man duma nekk ak yeen saa su nekk. 8 Def na li mu mën: xeeñal na sama yaram bala ñu koy rob. 9 Ci dëgg maa ngi leen koy wax: fépp fu ñuy yégle xibaar bu baax bi ci àddina si yépp dinañu nettali tamit li jigéen jii def ngir fàttaliku ko.»
10 Noonu Yuda Iskariyot, kenn ci fukk ak ñaar yi, dem ci njiiti-jébbalkati-sarax yi ngir jébbal leen Yeesu. 11 Ñu daldi bég ci xibaar boobu te ñu dig ko ne dinañu ko jox xaalis. Yuda tàmbali di wut pexe ngir jébbal leen Yeesu.
Yeesu mu ngi màggal bésu Paak ak taalibeem yi
12 Bés bu jëkk ci màggalu mburu yu amul lawiir yi, bés bi ñuy rendi mbote yi ngir reeru Paak, taalibe yi laaj Yeesu: «Fan nga bëgg nu waajale la reeru Paak bi?» 13-14 Noonu Yeesu yónni ñaar ci ay taalibeem, ne leen: «Demleen ci dëkk bi; dingeen daje ak waa ju yenu ndaal bu am ndox. Toppleen ko ba fi muy dugg, te nii ngeen di waxe ak boroom kër gi: "Jàngalekat bi moo ne: 'Fan mooy sama néeg bi may lekke reeru Paak bi ak samay taalibe?'" 15 Dina leen won benn néeg bu yaatu bi ñu defar ba lépp sotti te mu féete ci kaw. Foofu ngeen nu koy waajale.» 16 Taalibe yi dem te dugg ci dëkk bi, fekk lépp ni leen ko Yeesu waxe woon te ñu daldi waajal reeru Paak bi.
17 Ci ngoon si Yeesu yegsi ak fukk ak ñaar yi. 18 Bi ñu nekkee ci bérébu lekkukaay bi di lekk, Yeesu ne: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, kenn ci yenn, kiy lekkandoo ak man, moo may jébbale.» 19 Ñu ànd ak tiis, ku nekk di laaj Yeesu naan: «Mbaa du man?» 20 Mu ne leen: «Kenn ci yeen la, ku bokk ci fukk ak ñaar yi. Kiy cappandoo ak man ci ndab li. 21 Ndaxte Doomu nit ki dina dee ni ko Mbind mi yégle ci lu jëm ci moom, waaye musiba dina dal nit ki koy jébbale. Mu bañoona juddu sax, moo gën ci moom.»
22 Ci waxtu bi ñuy lekk, Yeesu jël mburu, barkeel ko ba noppi, damm ko, te jox leen ko ne: «Jëlleen ko. Lii moo di sama yaram.» 23 Noonu mu jël benn kaas, sant Yàlla ba noppi, jox leen ko te ñu naan ñoom ñépp. 24 Noonu mu wax leen ne: «Lii moo di sama deret bi tuuru ngir ñu bari, ngir fas kóllëre gi. 25 Ci dëgg maa ngi leen koy wax: dootuma naan biiñ mukk ba keroog may naan biiñ bu bees ci nguuru Yàlla gi.»
26 Gannaaw bi ñu woyee benn woy ci Saboor yi, ñu génn ngir dem ci Tundu Oliw ya.
27 Yeesu ne leen: «Yeen ñépp dingeen dem, bàyyi ma, ndaxte Mbind mi ne na:
"Dinaa dóor sàmm bi
te xar yi dinañu tasaaroo."
28 Waaye gannaaw bu ma dekkee, dinaa leen jiituji diiwaanu Galile.» 29 Piyeer ne ko: «Bu ñépp demee, bàyyi la sax, man duma la bàyyi.» 30 Yeesu ne ko: «Ci dëgg maa ngi la koy wax, tey jii, ci guddi gi sax, bala ginaar di sab ñaari yoon, dinga ma weddi ñetti yoon.» 31 Waaye Piyeer waxaat ak doole ne: «Su de sax, damaa wara dee ak yaw, duma la weddi mukk.» Te ñépp wax loolu tamit.
Yeesu ñaan na ci béréb bi nuy wowe Setsemane
32 Ñu yegsi ci béréb bi ñuy woowe Setsemane te Yeesu wax taalibeem yi: «Toogleen fii, ci waxtu bi may ñaan.» 33 Noonu mu jël Piyeer, Saak, ak Yowaana. Mu tàmbale yég tiis ak naqar. 34 Mu ne leen: «Sama xol dafa tiis ba ma bëgga dee. Desleen fii te di xoole.» 35 Mu sori leen tuuti, daanu ci suuf, tey ñaan ngir su mënee nekk, Yàlla soril ko waxtu naqar bi, 36 ne: «Baay, mën nga def lépp. Soril ma kaasu naqar bii. Wànte bu mu doon sama coobare, waaye na sa coobare am.» 37 Mu dellu, fekk leen ñuy nelaw, te mu ne Piyeer: «Simoŋ, yaa ngi nelaw! Mënoo sax xoole benn waxtu! 38 Xooleleen te ñaan, ngir ngeen baña daanu ci fiir. Xel mi waaj na ba noppi, waaye yaram bi dafa néew doole.» 39 Noonu mu soriwaat leen tuuti tey ñaan di wax kàddu yi mu waxoon. 40 Noonu mu ñëwaat, fekk leen ñuy nelaw, ndaxte seen bët yi mënuñu woon xoole ndax gëmmentu, te xamuñu woon li ñu koy wax. 41 Bi mu ñëwaatee ci ñetteelu yoon ba, mu ne leen: «Yeena ngi nelaw tey noppalu! Doy na. Waxtu bi jot na. Xoolleen! Ñu ngi jébbal Doomu nit ki ci loxoy bàkkaarkat yi. 42 Jógleen, nu dem. Xoolleen! Ki may jébbale mu ngi nii.»
Yuda wor na Yeesu
43 Bi Yeesu di wax loolu, ci saa si Yuda mi bokkoon ci fukk yi ak ñaar yegsi. Mbooloo mu takku ànd ak moom, yor ay jaasi ak ay yet. Njiiti-jébbalkati-sarax yi, jàngalekati-yoonu-Musaa, ak mag ñi ñoo leen yónni woon. 44 Ki ko doon jébbale joxoon na leen benn màndarga, ne leen: «Ki may fóon, moom la. Jàppleen ko te téye ko bu baax.» 45 Bi mu ñëwee, mu jegesi ko ci saa si te ne: «Jàngalekat bi.» Noonu mu daldi ko fóon. 46 Noonu ñu song Yeesu te jàpp ko. 47 Waaye kenn ci ñi nekkoon foofu daldi rocci jaaseem, dóor surga jébbalkatu-sarax-bu-mag bi, te dagg nopp bi. 48 Yeesu jël kàddu gi ne: «Lu tax ngeen ñëw jàppsi ma yor ay jaasi ak ay yet, mel ni damaa nekk defkatu lu bon? 49 Bés bu nekk nekkandoo woon naa ak yeen ci ëttu kër-Yàlla gi ngir jàngale te yeen jàppuleen ma. Waaye loolu am na ngir matal Mbind mi.» 50 Noonu ñépp ñi doon ànd ak moom bàyyi ko te daw. 51 Amoon na benn waxambaane bu ko doon topp. Benn sér rekk la laxasu woon. Ñu jéem ko jàpp, 52 waaye mu bàyyi sér bi te daw, yaramu neen.
Yeesu ci këru jébbalkatu sarax bu mag bi
53 Noonu ñu yóbbu Yeesu ci këru jébbalkatu-sarax-bu-mag bi. Njiiti-jébbalkati-sarax yi, mag ñi, ak jàngalekati-yoonu-Musaa daje woon nañu foofu. 54 Piyeer doon topp Yeesu fu sori ba ci ëttu këru jébbalkatu-sarax-bu-mag bi. Toogoon na ak wottukat yi te di jaaru ci wetu xal bi. 55 Njiiti-jébbalkati-sarax yi ak kurélu àttekati Yawut yépp doon nañu wut seede ngir tuumaal Yeesu ngir ñu teg ko daanu dee, waaye amuñu ko woon. 56 Ndaxte amoon na nit ñi ko doon seedeel lu dul dëgg, waaye seeni seede àndul woon. 57 Ñenn ñi jóg te di seede lu dul dëgg jëmale ko ci moom naan: 58 «Dégg nanu ko muy wax ne: "Dinaa toj kër-Yàlla gi ay loxo nit tabax, te ci ñetti fan, ma tabax beneen bu loxoy nit dul tabax."» 59 Waaye ci kàddu yooyu sax seen seede àndul woon ba léegi. 60 Noonu jébbalkatu-sarax-bu-mag bi jóg ci diggu mbooloo mi te laaj Yeesu ne: «Ndax doo tontu dara ci li la nit ñii di tuumaal?» 61 Waaye mu noppi te tontuwul dara. Jébbalkatu-sarax-bu-mag bi laajaat ko ne: «Ndax yaw yaay Almasi bi, Doomu Yàlla Aji-Cant ji?» 62 Yeesu tontu ne: «Moom laa, te dingeen gis Doomu nit ki toog ci ndeyjooru Yàlla Aji-Kàttan ji tey ñëw ak niiri asamaan.» 63 Noonu jébbalkatu-sarax-bu-mag bi xotti yéreem tey naan: «Lan lanuy soxlati ay seede? 64 Dégg ngeen muy saaga Yàlla ci li mu méngale boppam ak moom. Lan ngeen ci xalaat?» Te ñépp teg ko daanu dee. 65 Ñenn ñi di ko tifli, takk bëtam yi di ko dóor ay kurpeñ te ne ko: «Waxal ci turu Yàlla.» Te wottukat yi jël ko di ko mbej.
66 Ci bi Piyeer nekkee ci suuf, ci ëtt bi, kenn ci surga yu jigéenu jébbalkatu-sarax-bu-mag bi yegsi. 67 Bi mu gisee Piyeer di jaaru, mu daldi ko xool bu baax te ne ko: «Yaw tamit nekkoon nga ak Yeesu mu Nasaret.» 68 Waaye Piyeer weddi ko ne: «Xamuma li nga bëgga wax. Dégguma ci dara.» Te mu dem ci wetu bunt bi te benn ginaar daldi sab. 69 Waaye surga bu jigéen bi gis ko te mu waxaat ñi nekkoon foofu: «Waa jii, ci ñoom la bokk.» 70 Waaye mu weddiwaat ko. Ci kanam tuuti ñi nekkoon foofu tàmbale wax Piyeer ne: «Li wóor mooy ci ñoom nga bokk, ndaxte ci diiwaanu Galile nga jóge.» 71 Noonu mu tàmbale giñ di waat ne: «Xamuma waa ji ngeen di wax,» 72 te ci saa si benn ginaar sab ci ñaareelu yoon. Noonu Piyeer fàttaliku kàddu gi ko Yeesu waxoon: «Bala ginaar di sab ñaari yoon dinga ma weddi ñetti yoon,» te mu tàmbale jooy.