Yeesu mu ngi wax ci li wara ñëw
13
Bi Yeesu di génn ci kër-Yàlla gi, kenn ci taalibeem yi ne ko: «Jàngalekat bi, xoolal xeer yu rafet yii ak tabax yu rafet yii!» 2 Yeesu ne ko: «Gis nga tabax yu réy yii ngay xool nii? Lii lépp dinañu ko yàq, te doj dootul des ci kaw doj.»3 Yeesu daldi toog ci kaw Tundu Oliw ya jaakarloo ak kër-Yàlla gi, te Piyeer, Saak, Yowaana, ak Andare, wéetoo ak moom te laaj ko ne: 4 «Jàngalekat bi, wax nu kañ la loolu di am ak ban màndarga mooy firndeel ne loolu lépp dina mat.»
5 Yeesu tontu leen ne: «Moytuleen! Buleen kenn nax. 6 Ndaxte dina am ñu bari ñuy ñëw mbubboo sama tur tey wax ne: "Man maay Almasi bi" te dinañu nax ay nit ñu bari. 7 Bu ngeen déggee ñuy wax ci ay xare ak ay coowi xare, buleen ragal, ndaxte mbir yooyu, fàww ñu am bu jëkk, waaye nekkagul njeextel gi. 8 Ndaxte benn xeet dina jóg ngir xeex ak beneen xeet te réew dina jóg ngir xeex ak beneen réew. Dina am ay yëngu-yëngu suuf yu réy ci béréb yu wuute, ak xiif. Xew-xew yooyu dinañu mel ni metit yu jëkk ci matu.
9 «Waaye yeen ci seen bopp moytuleen! Ndaxte dinañu leen jébbal ci bérébu àttekaay yi, dinañu leen dóor ay yar ci kër-ñaan yi, dinañu leen yóbbu ci kanamu njiiti réew yi ak ci kanamu buur yi ndax man ngir ngeen nekk samay seede ci seen kanam. 10 Fàww ñu jëkka yégle xibaar bu baax bi ci xeet yi yépp. 11 Te bu ñu leen jàppee ngir yóbbu leen ci àttekaay bi, buleen jaaxle ci li ngeen wara wax. Li ñu leen jox ci waxtu boobu, waxleen ko, ndaxte du yeen yeenay wax waaye Xel mu Sell mi. 12 Mag dina jébbale rakkam ci dee, te baay jébbale doomam. Ay doom tamit dinañu fippu ci seeni waajur te reylu leen. 13 Ñépp dinañu leen bañ ndax man, waaye ku dëgër-dëgërlu ba ci njeextel gi dinga mucc.
14 «Dina am bés, li ñuy wax "lu araam tey yàqe" taxaw fi mu warula taxaw (na ki jàng xam). Su ngeen gisee loolu, na ñi nekk ci Yude daw, yéeg ci tund yi. 15 Ki nekk ci kaw këram, bu mu wàcc, dugg ci këram ngir jël dara, 16 te ki nekk ci tool, bu mu dellu gannaaw ngir jël mbubbam. 17 Musiba dina dal jigéen ñi nga xam ne dañoo ëmb ak ñiy nàmpal ci bés yooyu. 18 Ñaanleen Yàlla loolu baña am ci jamonoy seddaay. 19 Ndaxte ci bés yooyu dina am ay metit yu mësula am dale ko ci njàlbéen bi Yàlla sàkkee àddina si ba léegi te dootul am mukk, 20 te su Boroom bi wàññiwul woon bés yooyu, kenn du mucc, waaye wàññi na leen ndax ñi mu tànn. 21 Ci jamono jooju, bu leen kenn waxee ne: "Xoolleen, Almasi bi mu ngi fii" walla "Mu ngi fale," buleen ko gëm. 22 Ndaxte Almasi yu dëgguwul ak yonent yu dëgguwul dinañu feeñ. Dinañu def ay màndarga ak ay kéemaan ngir bu mënee nekk ñu nax ñi Yàlla tànn. 23 Yeen nag, moytuleen! Wax naa leen loolu lépp laata muy ñëw.
24 «Waaye ci bés yooyu, gannaaw metit boobu,
jant bi dina lëndëm,
weer bi dootul leer,
25 biddéew yi dinañu daanoo ci asamaan
te kàttani asamaan dinañu yëngu.
26 Noonu dinañu gis Doomu nit ki di ñëw ci biir niir ak kàttan bu réy ak màggaay. 27 Dina yónni ay malaakaam, ñu dajale ñi Yàlla tànn ci ñeenti cati àddina, dale ko fi suuf tàmbale ba fi asamaan yem.
28 «Jàngleen léebu garabu gaŋ bi: Su fekkee ay bànqaasam tooy nañu te ay xobam tàmbale sëq, xam ngeen ne nawet bi jegesi na. 29 Noonu yeen tamit, sungeen gisee mbir yooyu di xew, xamleen ne Doomu nit ki jegesi na, mu ngi ci bunt bi. 30 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, niti jamono jooju duñu weesu mukk te mbir yooyu yépp matuñu. 31 Asamaan ak suuf dinañu weesu, waaye samay kàddu duñu weesu mukk.
32 «Waaye ci lu jëm ci bés bi walla ci waxtu bi, kenn xamu ko: du sax malaaka yi ci asamaan walla Doom ji, waaye Baay bi rekk moo ko xam. 33 Moytuleen tey xoole, ndaxte xamuleen kañ la waxtu bi di ñëw. 34 Loolu dina mel ni nit kuy tukki. Mu bàyyi këram, dénk surgaam yi sañ-sañ, ku nekk ak li mu wara def, te mu jox garjen bi ndigal ngir muy xoole. 35-36 Xamuleen kañ la boroom kër gi di ñëw. Mën na ñëw ci ngoon si, walla ci xaaju guddi, walla bu ginaar di sab, walla ci suba si. Loolu moo tax yeewuleen, ngir bu ñëwee ci waxtu bu ngeen ko foogewul, mu bañ leen fekk ngeen di nelaw. 37 Li ma leen wax nii, wax naa ko ñépp: wéyleen di xoole!»