12
Gannaaw loolu Yeesu tàmbali di leen nettali beneen léeb: «Dafa amoon benn waay bu jëmbët toolu reseñ. Mu wërale ko ak miir, gas fa nalukaayu reseñ, te tabax wottukaay. Noonu mu batale ko ay beykat te tukki. 2 Bi waxtu góob bi jotee, mu yónni benn surga ci beykat yi ngir ñu jox ko wàllam ci meññeef bi, 3 waaye ñu jàpp ko, dóor ko, te dàq ko loxoy neen. 4 Boroom tool bi yónniwaat beneen surga. Kooku beykat yi dóor ko ci bopp te saaga ko. 5 Boroom tool bi yónniwaat ñetteelu surga. Kooku ñu rey ko. Te def ñeneen ñu bari noonu: ñu dóor ñenn ñi te rey ñeneen ñi. 6 Mu dese ko benn doomam rekk bi mu sopp. Moom la mujje yónni, naan: "Dinañu jox cér sama doom." 7 Waaye beykat yi di wax ci seen biir ne: "Ki wara donn tool bi mu ngi ñëw. Ñëwleen, nu rey ko te nu moom tool bi." 8 Noonu ñu jàpp ko, rey ko, te sànni ko ci biti.» 9 Noonu Yeesu laaj ñi ko doon déglu: «Naka la boroom tool bi nara def? Dina ñëw, rey beykat yooyu, te dénk tool bi yeneen nit.»
10 Yeesu yokk ca ne: «Xanaa jànguleen ci Mbind mi lii:
"Doj bi tabaxkat yi sànni woon
mujj na nekk doj bi ëpp solo ci tabax bi.
11 Boroom bi moo def loolu,
te lu yéeme la ci sunuy bët"?»
12 Njiiti Yawut yi doon ko wuta jàpp, ndaxte xamoon nañu ne léeb bi mu doon wax ngir ñoom la, waaye ragaloon nañu askan bi. Noonu ñu bàyyi ko fa te dem.
Njiiti Yawut yi ñu ngi jéema fiir Yeesu ci lu jëm ci feyub lempo
13 Noonu njiiti-jébbalkati-sarax yi, jàngalekati-yoonu-Musaa, ak mag ñi yónnee ci wetu Yeesu ñenn ñu bokk ci tarixa Farisen ak ñenn ñu far ak Erodd ngir ñu fiir ko ci kàddu. 14 Ñu ñëw te wax ko ne: «Jàngalekat bi, xam nanu ne dëgg ngay wax. Ragaloo nit te doo àtte nit ci melokaanam. Waaye dangay jàngale yoonu Yàlla ci dëgg. Ndax yoonu Musaa maye na walla déet ñuy fey lempo Sesaar? Nu fey ko walla nu bañ ko fey?» 15 Waaye Yeesu xam seen naaféq, ne leen: «Lu tax ngeen may fiir? Andilleen ma xànjaru xaalis ngir ma gis ko.» 16 Ñu andil ko xànjaru xaalis bi, te Yeesu laaj leen: «Nataal ak mbind mi ci nekk, kan mooy boroom?» Ñu ne ko: «Sesaar.» 17 Yeesu daldi leen ne: «Joxleen Sesaar li Sesaar moom te ngeen jox Yàlla li Yàlla moom.» Waaru woon nañu lool.
Laaj nañu Yeesu ci ndekkitelu ñu dee ñi
18 Ñenn ñi bokk ci tarixa Sadusen yi ñëw ci wetu Yeesu. Ñoom gëmuñu woon ne ndekkite am na. Ñu ne ko: 19 «Jàngalekat bi, Musaa ci mbindam dafa nu jox ndigal ne su fekkee dafa am benn waay bu magam dee te bàyyi jabar waaye amul doom, waa jooju dafa wara takk ku jigéen ki ngir amal ko doom. 20 Léegi nag, dafa amoon juróom ñaari góor yu bokk ndey ak baay. Taaw bi takk jabar, dee, te amul doom. 21 Ñaareel ba takk ku jigéen ki, daldi dee, te amul doom. Ñetteel ba noonu, 22 ba juróom ñaar yépp dee te amuñu doom. Gannaaw loolu ku jigéen ki moom tamit dee. 23 Ci ndekkitel bi, bu ñu dekkee ci ñu dee ñi, jabaru kan lay doon ci juróom ñaar yi, ndaxte ñoom ñépp takkoon nañu ko?» 24 Yeesu ne leen: «Ndax du li ngeen xamul Mbind mi ak kàttanu Yàlla moo tax ngeen nekk ci njuumte? 25 Ndaxte bu ñu dekkee ci ñu dee ñi, góor du takk jabar te jigéen du am jëkkër, waaye dinañu mel ni malaaka yi ci asamaan. 26 Ci lu jëm ci ndekkitelu ñu dee ñi, xanaa mësuleen jàng ci téere Musaa lu jëm ci garab bi doon tàkk? Foofu Yàlla waxoon na Musaa ne: "Man maay Yàllay Ibraayma, Yàllay Isaaxa, ak Yàllay Yanqóoba." 27 Yàlla nekkul Yàllay ñi dee waaye Yàllay ñiy dund. Ci dëgg, dangeena nekk ci njuumte.»
Yeesu jàngal na nit ñi ci ndigal bi ëpp solo
28 Benn jàngalekatu-yoonu-Musaa déggoon na Yeesu di waxtaan ak Sadusen yi. Mu gis ne Yeesu tontu na leen bu baax. Noonu mu laaj ko ne: «Ban ndigal moo ëpp solo ci ndigal yi yépp?» 29 Yeesu tontu ko ne: «Ndigal bi ëpp solo mooy bii: "Déglul, Israyil, Boroom bi sunu Yàlla kenn la. 30 Nanga bëgg Yàlla sa Boroom ak sa xol bépp, sa bakkan bépp, sa xel mépp, ak sa kàttan bépp." 31 Te ndigal bii moo ci topp: "Nanga bëgg sa moroom ni nga bëgge sa bopp." Amul benn ndigal bu ëpp solo ñaar yooyu.»
32 Jàngalekatu-yoonu-Musaa bi wax Yeesu ne: «Baax na, jàngalekat bi. Li nga wax dëgg la. Boroom bi Yàlla kenn la, te amul keneen ku dul moom. 33 Te nga bëgg ko ak sa xol bépp, sa xam-xam bépp, ak sa kàttan bépp te nga bëgg sa moroom ni nga bëgge sa bopp, loolu moo ëpp saraxu mala yépp ak yeneen xeetu sarax yépp.» 34 Yeesu gis ne tontu na ak xam-xam. Mu ne ko: «Soriwoo nguuru Yàlla gi.» Gannaaw loolu kenn ñemeetu ko woon laaj dara.
Almasi bi, doomu kan la?
35 Noonu bi Yeesu doon jàngale ci ëttu kër-Yàlla gi, mu laajte ne: «Jàngalekati-yoonu-Musaa, naka lañu mëna waxe ne Almasi bi sëtu Daawuda la? 36 Ndaxte Daawuda ci boppam ci kàttanu Xel mu Sell mi ne na:
"Yàlla Aji-Sax ji nee na sama Boroom:
'Toogal ci sama ndeyjoor
ba ma daaneel say noon
fi ngay teg say tànk.'"
37 Daawuda ci boppam woowe na Almasi bi Boroomam. Kon nag, naka la Almasi bi mëna nekke sëtu Daawuda?» Foofu amoon na mbooloo mu takku mu doon déglu Yeesu ak mbégte.
Yeesu artu na nit ñi ci jàngalekati-yoonu-Musaa
38 Ci biir njàngaleem, Yeesu da doon wax ne: «Moytuleen jàngalekati-yoonu-Musaa yi bëgg di doxantu, sol mbubb yu réy, te bëgg ñu leen di nuyu ak ñaari loxo ci péncu dëkk bi, 39 di toog ci toogukaay yi féete ci kanam ci kër-ñaan yi ak toogukaay yu yiw yi ci lekku xew yi. 40 Ñoom dañuy yàq alalu jigéen ñi ñàkk seen jëkkër tey ñaan ak ngistal ñaan yu gudd. Seen àtte mooy gëna metti.»
41 Ci kaw loolu Yeesu toog jàkkaarloo ak ndab bi ñuy defe saraxu xaalis bi ci kër-Yàlla gi. Muy xool naka la mbooloo mi di dugale xaalis ci ndab bi. Boroom alal yu bari doon nañu ci dugal xaalis bu takku. 42 Benn jigéen bu ñàkk jëkkëram te néew doole yegsi. Mu joxe ñaari fiftin. 43 Noonu Yeesu woo taalibeem yi te ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jigéen bu néew doole bii, li mu joxe moo ëpp li ñépp joxe ci ndab bi. 44 Ndaxte ñoom ñépp dañoo joxe ci seen barile, waaye moom dafa joxe ci néewleem, ba joxe lépp li mu amoon te war ko dunde.»