Yàlla jox na taalibe yi Xel mu Sell mi
2
Bi bésu màggalu Pàntakot yegsee, taalibe yi yépp dajaloo nañu ci benn béréb. 2 Ci saa si, riir jóge ci asamaan, mel ni ngelaw bu am doole te gaaw, ba feesal kër gi ñu nekkoon. 3 Noonu lu mel ni ay làmmiñu safara feeñu leen. Làmmiñ yi tasaaroo te dal ci ku nekk ci ñoom. 4 Ñoom ñépp, ñu fees ak Xel mu Sell mi te tàmbali di wax yeneeni kàllaama yi leen Xel mu Sell mi doon may ngir ñu wax leen. 5 Amoon na ay Yawut yu takku ci Yàlla te daje Yerusalem jóge woon ci réewi àddina si yépp. 6 Bi ñu déggee coow bi, ñu dajaloo ci benn mbooloo. Ñu jaaxle ndaxte ku nekk ci mbooloo mi dégg na taalibe yi làkk sa làkku bopp. 7 Waaru woon nañu te yéemu te di wax ne: «Xoolal, ñii di wax ñépp, waa Galile lañu! 8 Naka la mëna nekke, ku nekk ci nun di leen dégg ñuy wax ci kàllaamaam bi mu nàmp? 9 Waa Pàrt, Medd, Elam, Mesopotami, Yude, Kapados, Pont ak Asi, 10 waa Firisi, Pamfili ak Misra, waa Libi mi dend ak Siren, ak waa Room, 11 ñi nekk Yawut ci juddu ak ñi tuub, topp yoonu Yawut, ak waa Keret ak Arabi. Nun ñépp, nu ngi leen di dégg, ñuy wax ci sunu kàllaama ay mbir yu réy yi Yàlla def!» 12 Ñépp waaru woon nañu te jaaxle, te ñuy wax ci seen biir ne: «Lii, lan lay tekki?» 13 Waaye ñeneen ñi di leen ñaawal te di wax ne: «Dañu naan biiñ ba màndi.»Kàddug Piyeer ci bésu Pàntakot
14 Gannaaw loolu Piyeer jóg ak fukki ndaw yi ak benn, yékkëti baatam te wax leen ne: «Yeen Yawut yi ak ñépp ñi dal ci Yerusalem, dégluleen bu baax, xamleen lii: 15 ñii màndiwuñu ni ngeen ko fooge ndaxte juróom ñeenti waxtu moo jot ci bés bi. 16 Waaye lii mooy li Yàlla wax jaarale ko ci yonent Yowel:
17 "Yàlla nee na: 'Ci bés yu mujj yi,
man dinaa tuur sama Xel ci kaw ñépp.
Seen doom yu góor ak yu jigéen yi dinañu wax ci sama tur.
Seen waxambaane yi dinañu am ay gis-gis.
Seen mag ñi dinañu am ay gént.
18 Waaw, ci jamono jooju dinaa tuur sama Xel
ci sama jaam yu góor ak yu jigéen yi
te dinañu wax ci sama tur.
19 Dinaa def ay yëf yu yéeme ci asamaan
ak ay màndarga ci suuf si,
maanaam deret ak safara ak ay niiru saxar.
20 Jant bi dina soppiku doon lëndëm
te weer wi dina soppiku doon deret
bala bésu Boroom bi di ñëw, di bés bu réy te mag.
21 Te noonu képp ku woo turu Boroom bi dinga mucc.'"»
22 Piyeer yokk ca ne: «Yeen waa Israyil, dégluleen kàddu yii: Yeen, xam ngeen ne Yeesu mu Nasaret moo di ki Yàlla seedeel, te di def ay kéemaan ak ay yëf yu yéeme ak ay màndarga ci seen biir jaarale ko ci moom. 23 Nit kooku ñu jébbale ni ko Yàlla dogale te nasoon ko ci lu yàgg. Yeena ko daajloo bàkkaarkat yi, te rey ko. 24 Waaye Yàlla dekkil na ko, yewwi ko ci buumi dee, ndaxte dee mënu ko woona téye ci kàttanam. 25 Daawuda wax na ci lu jëm ci Yeesu:
"Wéy naa di gis Boroom bi ci sama kanam;
ndaxte mu ngi ci sama ndeyjoor ba tax na duma daanu.
26 Looloo tax sama xol a ngi fees ak bànneex
te samay kàddu fees ak mbégte.
Sama néew sax di tëdd ci yaakaar
27 ndaxte doo ma bàyyi ci béréb bi ñu dee ñi nekk
te doo bàyyi sa nit ku sell ki mu yàqu ci bàmmeel bi.
28 Xamal nga ma sa yoonu dund
te feesal nga ma ak mbégte ci sa teewaay."»
29 Piyeer yokk ca ne: «Mbokk yi, mën naa leen wax lu wóor ci mbirum Daawuda sunu maam. Dee na ba ñu suul ko te bàmmeelam mu ngi fi ba tey. 30-31 Waaye xamoon na ne Yàlla waataloon na ko ne dina toogloo ni buur kenn ku bokk ci askanam. Gisoon na lu jiitu ndekkitelu Almasi bi ndaxte yonent la woon. Te ci moom la doon wax: Duñu ko bàyyi ci béréb bi ñu dee ñi nekk te néewam du yàqu. 32 Yeesu moomu Yàlla dekkil na ko, te nun ñépp seede nañu ko. 33 Yàlla yékkëti na ko ci ndeyjooram te mu jot ci Baay bi Xel mu Sell mi mu dige woon. Te noonu mu tuur ko ni ngeen ko gise te dégge ko. 34 Ndaxte nekkul Daawuda moo yéeg ci asamaan waaye moom ci boppam wax na ne:
"Yàlla Aji-Sax ji nee na sama Boroom:
'Toogal ci sama ndeyjoor
35 ba ma daaneel say noon fi ngay teg say tànk.'"»
36 Piyeer teg ca ne: «Na askanu Israyil yépp xam bu wóor ne Yeesu mi ngeen daajoon ca bant ba, Yàlla def na ko Boroom ak Almasi bi.»
37 Bi ñu déggee kàddu yooyu, ñu am naqaru xol. Ñu laaj Piyeer ak yeneen ndaw yi ne: «Mbokk yi, lan lanu wara def?» 38 Piyeer tontu leen ne: «Tuubleen seeni bàkkaar te ñu sóob leen, kenn ku nekk ci yeen, ci ndox ci turu Yeesu Almasi bi. Bu booba Yàlla dina leen baal seeni bàkkaar te jox leen Xel mu Sell mi. 39 Ndaxte li Yàlla sunu Boroom dige woon, ngir yeen la ak seeni doom ak ñépp ñi nekk fu sori te Yàlla di leen woo ci moom.» 40 Noonu Piyeer wéy di seede ak yeneeni kàddu yu bari ngir ñaax leen, di wax ne: «Muccleen ci niti jamono ju dëng ji.»
Dundinu taalibe yi
41 Ñi nangu woon kàddug Piyeer yooyu sóob nañu leen ci ndox, te ci bés boobu Boroom bi yokk lu tollook ñetti junni nit ci taalibe yi. 42 Ñoom ñépp dañu doon déglu njàngale ndaw yi, booloo nekk benn, di damm mburu mi, te di ñaan ak takkute. 43 Askan bi yépp nekkoon nañu ci tiitange te Yàlla doon def ay yëf yu yéeme ak ay màndarga yu bari jaarale ko ci ndaw yi. 44 Ñépp ñi gëmoon nekkoon nañu benn te bokk lépp. 45 Ñu jaay seen am-am ak seen alal te séddale njég li ci ñépp, ci ku nekk li mu soxla. 46 Bés bu nekk dañu doon daje ci kër-Yàlla gi ak takkute, di damm mburu ci kër yi, te di lekkandoo ak mbégte ak xol bu woyof. 47 Ñuy sant Yàlla te askan bi yépp jox leen cér. Bés bu nekk Boroom bi doon na yokk limu taalibe yi mu doon muccal.