Benn waa ju lafañ jot na wér ci turu Yeesu
3
Benn bés, Piyeer ak Yowaana doon nañu dem ci kër-Yàlla gi ci ñaanu ñetteelu waxtu ci ngoon. 2 Fekk ñu andi fa benn waay bu judduwaale lafañ. Bés bu nekk dañu ko doon toogloo ci buntu kër-Yàlla bi ñuy woowe "bunt bu rafet bi" ngir mu yelwaan ñi fay dugg. 3 Bi mu gisee Piyeer ak Yowaana, ñuy waaja dugg kër-Yàlla gi, mu ñaan leen sarax, 4 waaye Piyeer ak Yowaana xool ko, ne jàkk. Piyeer ne ko: «Xool nu!» 5 Lafañ bi xool leen, yaakaar jot ci ñoom dara. 6 Piyeer ne ko: «Awma xaalis, awma wurus, waaye li ma am, maa ngi la koy jox. Ci turu Yeesu mu Nasaret di Almasi bi, jógal te nga dox.» 7 Piyeer jàppe ko loxo ndeyjooram te yékkëti ko. Ci saa si, tànki waa ji dëgër. 8 Mu tëb, taxaw, tàmbalee di dox, te mu ànd ak ñoom, dugg ci kër-Yàlla gi, di dox, di tëb, te di sant Yàlla. 9 Mbooloo mi yépp gis ko muy dox di sant Yàlla. 10 Bi ñu ko xàmmee, te xam ne moom moo daan toog ci bunt bu rafet bu kër-Yàlla gi ngir yelwaan, nit ñépp daldi yéemu te waaru ndax li daloon waa ji.
Kàddug Piyeer ci ëttu Kër-Yàlla gi
11 Waa ji ñu wéraloon ci lafañ bi taq ci Piyeer ak Yowaana. Askan bi yépp dawsi, dajesi ci ëttu kër-Yàlla gi, ci béréb bi ñu woowe Perongu Suleymaan. Ñu waaru lool. 12 Bi Piyeer gisee loolu mu ne askan bi: «Yeen waa Israyil, lan moo tax ngeen waaru ci li xew? Lu tax ngeen xool nu ne jàkk mel ni ci sunu kàttanu bopp walla ci sunu takku ci Yàlla moo tax nit kii di dox? 13 Déedéet. Yàllay Ibraayma, Isaaxa, ak Yanqóoba di Yàllay sunuy maam màggal na ndawam Yeesu. Yeen, yeena ko jébbale, weddi ko ci kanamu Pilaat bi mu jëlee dogal ngir bàyyi ko. 14 Weddi ngeen Ku Sell Ki te jub te ñaan ngeen Pilaat mu tijjil leen benn reykatu nit. 15 Reylu ngeen boroom dund gi, waaye Yàlla dekkil na ko ci ñu dee ñi. Nun, seede nañu ko. 16 Kàttanu turu Yeesu moo tax waa jii ngeen gis te xam ko, dëgër. Jaarale ko ci gëm ci turu Yeesu waa ji wér na péŋŋ ni ngeen ko gise, yeen yépp.
17 «Léegi nag samay mbokk, xam naa ne, ni ngeen jëfe nii, seen ñàkka xam moo ko waral, yeen ak seeni njiit. 18 Te noonu Yàlla matal na lépp li mu yégle woon bu jëkk, jaarale ko ci gémmiñu yonentam yépp, bi mu ne Almasi bi, fàww mu daj coono. 19 Kon nag tuubleen seeni bàkkaar te dellusi ci Yàlla ngir mu baal leen, 20 te noonu Boroom bi Yàlla dina leen may ay jamonoy noppalu te dina leen yónnee Almasi bi mu tànnoon bu jëkk, maanaam Yeesu. 21 Ci jamono bii, war na des asamaan, ba bés bi Yàlla di yeesalaat lépp ni mu ko yégle woon ci jamono ju jëkk ja jaarale ko ci yonentam yu sell yi. 22 Musaa waxoon na ne: "Boroom bi Yàlla dina leen feeñalal benn yonent ni man bu bokk ci yeen. Nangeen déglu lépp li mu leen di wax, 23 te ku baña déglu yonent boobu, dinañu ko dàq ci askan bi, mu sànku."
24 «Rax ci dolli yonent yi yépp dale ko ci Samiyel ak ñi ci topp wax nañu ci, te yégle bés yii. 25 Yeena donn dige yi Yàlla dige woon jaarale ko ci yonent yi ak kóllëre gi Yàlla fas ak sunuy maam, bi mu waxee Ibraayma ne: "Ci sa askan, njabootu àddina si yépp, dinañu barkeelu." 26 Yeen la Yàlla feeñalal ndawam Yeesu ci bu jëkk te yónnee leen ko ngir mu barkeel leen te woññi kenn ku nekk ci jëfam yu bon.»