Jàpp nañu Piyeer ak Yowaana te tuumaal leen ci kanamu Kurélu àttekat yi
4
Bi Piyeer ak Yowaana di wax kàddu yooyu askan bi, jébbalkati-sarax yi ak njiitu garjen kër-Yàlla gi ak ñi bokk ci tarixa Sadusen yi jegesi leen. 2 Dañoo meroon ci li ñu doon jàngal askan bi te yégle ne: ni Yeesu dekkee ci ñu dee ñi, noonu la ñi dee di dekkee, ñoom tamit. 3 Ñu jàpp leen te sànni leen ci kaso bi, ba ca ëllëg sa ndaxte guddi gi tàmbale woon na. 4 Waaye ñu bari ñi déggoon kàddu yooyu gëm te seeni xayma matoon na juróomi junni góor.
5 Ci ëllëg sa, njiiti Yawut yi, mag ñi, ak jàngalekati-yoonu-Musaa yi dajaloo woon nañu ci Yerusalem. 6 Foofu amoon na Anas jébbalkatu-sarax-bu-mag bi, Kayif, Yowaana, Alegsàndar ak ñépp ñi bokk ci njabootu njiiti-jébbalkati-sarax yi. 7 Ñu andil leen Piyeer ak Yowaana ci seen kanam. Ñu laaj leen: «Ci ban kàttan walla ci ban tur ngeen defe lii?» 8 Piyeer daldi fees ak Xel mu Sell mi te wax leen ne: «Yeen, njiiti askan bi ak mag ñi, 9 su fekkee dangeen nuy laaj ci lu baax li nu defal waa ju lafañ bii ak ci ban anam la jote wér, 10 kon nag, yeen ñi fi nekk ak askanu Israyil yépp, xamleen ne jaarale ko ci turu Yeesu mu Nasaret di Almasi bi, bi ngeen daajoon ci bant te Yàlla dekkil ko ci ñu dee ñi, ci moom la waa ji jote wér te taxaw ci seen kanam. 11 Yeesu moomu mooy doj bi, te yeen tabaxkat yi ngeen sànni woon ko, te mu mujje nekk doj bi ëpp solo ci tabax bi. 12 Mucc amul ci keneen ndaxte ci àddina si yépp Yàlla joxewul beneen tur bu dul turu Yeesu bu nit mëna mucce.»
13 Bi kurélu àttekat bu mag bi déggee Piyeer ak Yowaana di wax ak kóolute, ñu waaru ndaxte dañu leen jàppe woon ne ay nitu neen lañu te jànguñu woon, te xamoon nañu tamit ne ñoom ñoo daan ànd ak Yeesu. 14 Waaye bi ñu gisee waa ji ñu wéraloon taxaw ci seen wet, amaatuñu woon dara lu ñu ci teg. 15 Noonu ñu jox leen ndigal ngir ñu génn ci ëttu àttekaay bi, te ñuy waxtaan ci seen biir, 16 ne: «Lan lañu wara def nit ñii? Ndaxte def nañu benn màndarga bu leer te askanu Yerusalem yépp yég nañu ko, te nun mënunu ko weddi. 17 Waaye nag, ngir mu baña gëna siiw ci askan bi, nanu leen araftu, tere leen ñu wax ci tur boobu ci kanamu kenn.» 18 Ci kaw loolu ñu woo Piyeer ak Yowaana, tere leen ñu yégle walla di jàngale ci turu Yeesu 19 Waaye ñu tontu leen ne: «Àtteleen yeen ci seen bopp lu jub ci kanamu Yàlla: nu déggal leen walla nu déggal Yàlla. 20 Nun ci sunu wàllu bopp mënunu noppi ci li nga xam ne gis nanu ko te dégg ko.» 21 Ñu araftuwaat leen te bàyyi leen ñu dem, ndaxte xamuñu woon nan lañu leen di tege daan ndax mbooloo mi. Ñépp ñu ngi doon màggal Yàlla ci li xewoon, 22 ndaxte waa ji ñu wéraloon ci màndarga boobu, amoon na lu ëpp ñeent fukki at.
Ñaan nañu ngir mëna yégle Kàddu gi ak kóolute
23 Bi ñu bàyyee Piyeer ak Yowaana, ñu daldi dem ci seen àndandoo yi te nettali leen lépp li leen njiiti-jébbalkati-sarax yi ak mag ñi waxoon. 24 Gannaaw bi ñu leen dégloo ba noppi ñoom ñépp booloo di ñaan Yàlla ne: «Boroom bi, yaw mi sàkk asamaan, suuf, géej, ak lépp li nekk ci seen biir. 25 Yaw mi waxoon jaarale ko ci Xel mu Sell mi ci gémmiñu Daawuda sunu maam, sa surga ne:
Lu tax xeeti àddina yi di fippu,
te lan moo tax askan yi di mànkoo ci neen?
26 Buuri àddina si jóg nañu ngir xeex
te njiit yi booloo nañu ngir xeex Boroom bi ak Almaseem.
27 Waaw Boroom bi, dëgg la, ndaxte ci biir dëkk bii Erodd ak Poñsë Pilaat ak xeeti àddina si ak askanu Israyil mànkoo nañu ngir xeex Yeesu sa ndaw bu sell bi nga tànn di Almasi bi. 28 Matal nañu lépp li nga tànnoon bu jëkk ci sa kàttan ak sa coobare ngir ñu def ko. 29 Léegi nag Boroom bi, déggal seeni araftu, te mayal say surga ngir nu yégle sa kàddu gi ak kóolute gu mat sëkk. 30 Tàllalal sa loxo ngir wéral tey def ay màndarga ak ay yëf yu yéeme jaarale ko ci turu Yeesu sa ndaw bu sell bi.» 31 Bi ñu ñaanee ba noppi béréb bi ñu nekkoon yëngatu. Ñoom ñépp ñu fees ak Xel mu Sell mi te ñuy yégle kàddug Yàlla gi ak kóolute.
Anañas ak Safira
32 Mbooloom ñi gëmoon boole woon nañu seen xel yi ak seen xol yi te kenn daawul wax ne moom moo moom alalam. Dañu bokkoon lépp. 33 Ndaw yi dañu doon seede ndekkitelu Yeesu ak kàttan bu mag, te yiwu Yàlla bu mag nekkoon na ci ñépp. 34 Ci seen biir kenn daawul am soxla, ndaxte ñi nga xamante ne ñoo amoon ay tool ak ay kër doon nañu leen jaay, te andi xaalis bi, 35 jox ko ndaw yi, te ñu séddale ko ku nekk ak li mu soxla. 36 Foofu amoon na benn waay bu tudd Yuusufa. Mu soqeekoo ci giiru Lewi te jóge ci Sippar di réew bu ndox wër. Ndaw yi tudde woon ko Barnabas mi tekki ñaaxkat bi. 37 Mu jaay toolam, jël xaalis bi, te jox ko ndaw yi.