5
Amoon na beneen waay bu tudd Anañas te amoon soxnaam bu tudd Safira. Jaayoon na tamit toolam.2 Dafa mànkoo ak soxnaam ngir denc benn wàll ci njég li, andi li ci des, jox ko ndaw yi.3 Noonu Piyeer ne: «Anañas, lan moo tax nga bàyyi Seytaane fees sa xol ba tax ngay fenal Xel mu Sell mi, denc benn wàll ci njégu toll bi?4 Du yaa moomoon tool bi laata nga koy jaay? Te bi nga ko jaayee ba noppi, ndax mënoo woon def ci xaalis bi lu la neex? Lu tax ngay mébét lu mel nii ci sa xol? Du nit nga fen, waaye Yàlla nga fen.»5 Bi Anañas déggee kàddu yooyu mu daldi daanu te dee. Tiitange bu mag moo doon jàpp ñépp ñi ko déggoon.6 Waxambaane yi ñëw, lëmës néew bi, te suul ko.7 Lu tollook ñetti waxtu gannaaw loolu, soxna Anañas daldi ñëw te yégul li xewoon.8 Piyeer laaj ko ne: «Wax ma, ndax ci njég bii ngeen jaaye tool bi?» Mu tontu ko ne: «Waaw, njég bii la.»9 Piyeer daldi ko ne: «Lan moo tax ngeen mànkoo di seetlu Xelu Boroom bi? Xoolal! Ñi suuli woon sa jëkkër, ñu ngi ni ci bunt bi te dinañu la yóbbu.»10 Ci saa si mu daanu ci tànku Piyeer yi te dee. Waxambaane yi ñëw, fekk mu dee. Ñu yóbbu ko, te suul ko ci wetu jëkkëram.11 Noonu tiitange bu mag daldi jàpp mbooloo ñi gëm ak ñépp ñi yég xew-xew boobu.
Ndaw yi wéral nañu ay nit ñu bari
12 Yàlla doon na def ay màndarga ak ay yëf yu yéeme ci biir askan bi, jaarale ko ci loxoy ndaw yi, te ñi gëm ñépp dañu doon daje ci Perongu Suleymaan. 13 Keneen ñemewula booloo ak ñoom waaye askan bi dañu leen doon tagg. 14 Ñu bari dañu doon yokku ci ñi gëm ci Boroom bi, góor ak jigéen. 15 Nit ñi tàmbalee andi ñi feebaroon ci yoon yi, di leen tëral ci ay lal yu ndaw ak ay basaŋ ngir bu Piyeer di romb takkandeeram mën leena muur. 16 Ay nit ñu bari jóge woon nañu ci dëkk yi wër Yerusalem, te ñu andi ñi feebaroon ak ñi rab jàpp te ñépp dañu doon wér.
Njiiti Yawut yi ñu ngi fitnaal ndaw yi
17 Gannaaw loolu, jébbalkatu-sarax-bu-mag bi ak ñi mu àndal maanaam tarixa Sadusen yi fees nañu ak iñaan jëmale ko ci ndaw yi. 18 Ñu daldi leen jàpp te tëj leen ci kaso bi. 19 Waaye ci guddi, benn malaaka Boroom bi daldi ñëw, ubbi buntu kaso bi, génne leen, te ne leen: 20 «Demleen, taxaw ci ëttu kër-Yàlla gi te yégal nit ñi lépp lu jëm ci dund bu bees bi.» 21 Gannaaw bi ñu déggee loolu, bi bët setee, ñu dugg ci ëttu kër-Yàlla gi di jàngale.
Bi jébbalkatu-sarax-bu-mag bi ak ñi mu àndal yegsee, ñu woolu kurélu àttekat yi maanaam njiiti Israyil yépp, te ñu yónni ay nit ngir ñu jëli ndaw yi ci kaso bi, andi leen. 22 Bi ñooñu yegsee, fekkuñu leen ci kaso bi. Ñu daldi dellu te nettali leen 23 di wax ne: «Dañoo fekk kaso bi ñu tëj ko bu baax, te soldaar yi taxaw woon nañu ci bunt bi. Waaye ba nu ko ubbee, fekkunu kenn ci biir.» 24 Ba ñu déggee kàddu yooyu, njiitu garjen kër-Yàlla gi ak njiiti-jébbalkatu-sarax yi daldi jaaxle di xalaat ci li wara xew. 25 Mu am ku ñëw te ne leen: «Xoolleen! Nit ñi ngeen tëjoon ci kaso bi, ñu ngi taxaw ci ëttu kër-Yàlla gi di jàngal mbooloo mi.» 26 Noonu garjen yi ak seen njiit daldi dem jëli leen, waaye jaayuñu leen doole ndaxte dañoo ragaloon nit ñi sànni leen ay xeer.
27 Bi ñu leen andee, ñu taxawal leen ci kanamu kurélu àttekat yi, te jébbalkatu-sarax-bu-mag bi laaj leen ne: 28 «Xanaa terewunu leen woon ngeen di jàngale ci tur boobu? Te yeena ngi nii, feesal Yerusalem ak seen njàngale, te ngeen di jéema xëpp ci sunu kaw deretu nit kooku.»
29 Piyeer ak yeneen ndaw yi tontu leen ne: «Déggal Yàlla moo gën déggal ay nit. 30 Yàllay sunu maam moom moo dekkil Yeesu bi ngeen rey ci bi ngeen ko daajee ci bant. 31 Moom la Yàlla yékkëti ba ci ndeyjooram ni buur ak musalkat ngir may Israyil ñu mëna tuub seeni bàkkaar te mu baal leen. 32 Ay seede lanu ci mbir yooyu, nun ak Xel mu Sell mi Yàlla may ñi ko déggal.»
33 Bi àttekat yi déggee kàddu yooyu ñu daldi mer lool ba bëgg leena rey. 34 Waaye mu am ku bokk ci tarixa Farisen bu ñuy wax Gamalyel. Mu nekkoon jàngalekatu-yoonu-Musaa te mbooloo mi joxoon ko cér. Mu jóg ci ëttu àttekaay bi te santaane ñu génne ndaw yi ab diir. 35 Noonu mu wax leen ne: «Yeen góoru Israyil yi, moytuleen ak ni ngeen nara jëfe ak nit ñii. 36 Fàttalikuleen ne ci bu yàggul dara amoon na benn waay bu tuddoon Tëdas. Mu jógoon di jàppe boppam nit ku mag te yóbbaale lu tollook ñeenti téeméeri nit, waaye ñu rey ko te ñi mu àndaloon ñépp ñu daldi tasaaroo ba seen pexe mujjewul fenn. 37 Gannaaw moom Yudaa mu Galile jóg ci jamono bi ñu doon waññ waa réew mi. Mu yóbbaale woon ay nit ñu bari. Moom itam, ñu reyoon ko, te ñi ko toppoon ñépp dañoo tasaaroo. 38 Léegi nag maa ngi leen koy wax génnleen ci seen mbir te bàyyi leen ñu dem. Bu fekkee seen mébét walla seen liggéey ci nit la jóge, dina yàqu. 39 Waaye bu fekkee ci Yàlla la jóge, yeen mënuleen ko yàq. Moytuleen di xeex coobare Yàlla.»
Kurélu àttekat yi àndoon nañu ci li mu doon wax. 40 Noonu ñu woo ndaw yi, dóor leen ay yar te tere leen ñu wax ci turu Yeesu. Gannaaw loolu ñu bàyyi leen ñu dem. 41 Ndaw yi daldi jóge ci ëttu àttekaay bi, ànd ak mbégte ci li leen Yàlla àtte ñu yelloo metit ndax turu Yeesu. 42 Te bés bu nekk ci kër-Yàlla gi ak ci kër yi dañu doon wéy di jàngale te di yégle xibaar bu baax bi, ne Yeesu mooy Almasi bi.