Tànn nañu juróom ñaari waay ngir ñu dimbali ndaw yi
6
Ci bés yooyu limu taalibe yi di gën di yokku te Yawut yiy làkk gereg ñooy ñaxtu ci Yawut yiy làkk seen làkku bopp ndaxte dañu doon sàggane seeni jigéen yi ñàkk seen jëkkër ci séddale dund bi ñuy def bés bu nekk. 2 Noonu fukki ndaw yi ak ñaar dajale taalibe yi yépp te ne leen: «Jekkul nun nu bàyyi liggéeyu kàddu Yàlla gi di séddale ay lekk. 3 Kon nag mbokk yi tànnleen ci seen biir juróom ñaari góor ñu fees ak Xel mu Sell mi ak xel yu rafet te ñi ñu seede ñu jub. Nu sas leen liggéey boobu, 4 te noonu nun nu mëna takku ci ñaan te di yégle kàddu Yàlla gi.» 5 Wax boobu neex mbooloo mi yépp. Ñu tànn Eccen, nit ku fees ak ngëm ak Xel mu Sell mi, Filib, Porokor, Nikanor, Timon, Parmenas, ak Nikolas, ku juddoo Ancos. Bu jëkk mu nekkoon yéeféer waaye ñëw na ci ngëmu Yawut yi. 6 Ñu andi leen ci kanamu ndaw yi ngir ñu ñaanal leen te teg leen loxo. 7 Noonu kàddu Yàlla gi law te limu taalibe yi di gën di yokku ci Yerusalem, te jébbalkati-sarax yu bari daldi topp yoonu ngëm.Jàpp nañu Eccen
8 Eccen, fees ak yiw ak kàttan di def ay yëf yu yéeme ak ay màndarga yu mag ci kanamu askan bi. 9 Noonu mu am ñu bokk ci kër-ñaan bi ñu woowe ñi ñu goreel. Ñi jóge woon dëkku Siren ak dëkku Alegsàndiri ak Yawut yu jóge woon diiwaanu Silisi ak diiwaanu Asi, ñu tàmbalee di werante ak Eccen 10 waaye mënuñu woona weddi xel bu rafet bi ko Xel mu Sell mi doon jox. 11 Noonu ñu fey ay nit ngir ñuy wax ne: «Nun, dégg nanu nit kii di wax ay kàddu yu ñaaw jëmale ko ci Musaa ak ci Yàlla.» 12 Ci seen wax jooju ñu jógloo askan bi, mag ñi ak jàngalekatu-yoonu-Musaa yi te ñu jàpp ko, yóbbu ko ci ëttu àttekaay bi. 13 Ñu andi ay nit ñuy seede lu dul dëgg di wax ne: «Nit ki ngeen di gis, du noppi di wax ay kàddu yu ñaaw jëmale ko ci kër-Yàlla gu sell gi ak ci yoonu Musaa bi, 14 ndaxte nun, dégg nanu ko, muy wax ne: "Yeesu mu Nasaret dina yàq béréb bii te soppi aada yi nu Musaa joxoon."» 15 Ñépp ñu toogoon ci ëttu àttekaay bi ne jàkk Eccen di ko xool, te ñu gis kanamam mel ni bu malaaka.