Kàddu Eccen yi ci kanamu kurélu àttekat yi
7
Jébbalkatu-sarax-bu-mag bi laaj Eccen ne: «Mbir yi ñu wax ci yaw, ndax dëgg la?» 2 Mu tontu ne: «Samay mbokk ak samay baay, dégluleen ma. Yàlla ci màggaayam feeñu woon na sunu maam Ibraayma bi mu nekkee woon ci réewu Mesopotami laata muy dem dëkku Karan. 3 Waxoon na ko ne: "Jógal sa réew te bàyyi sa mbokk yi te nga dem ci réew mi ma lay won." 4 Ci noonu Ibraayma génn ci réewu waa Kalde bi mu nekkoon, dem dëkku Karan. Gannaaw bi pàppaam deewee, Yàlla génne ko dëkku Karan te yóbbu ko ci réewu Kanaan bi ngeen dëkk léegi, 5 te Yàlla joxu ko woon benn moomeel ci réew mi, du sax béréb bu muy teg tànkam. Waaye digoon na ko ne dina ko jox réew mi, moom ak ñi soqikoo ci moom, moona jamono jooju Ibraayma amagul woon doom. 6 Gannaaw loolu, Yàlla wax na ko lii: "Ñi soqeekoo ci yaw dinañu dem ci réew bu ñu moomul. Dinañu leen jàppe ni jaam. Dinañu leen bunduxataal diirub ñeenti téeméeri at, 7 waaye man Yàlla, maay àtte xeet bi leen teg jaam. Gannaaw loolu ñi soqeekoo ci yaw dinañu fa génn te jaamu ma ci béréb bii." 8 Noonu, Yàlla fas kóllëre ak Ibraayma ci màndarga xaraf. Ci noonu, Ibraayma bi mu amee Isaaxa gannaaw juróom ñetti fan mu xarafal ko. Isaaxa def noonu Yanqóoba, te Yanqóoba xarafal fukki doomam yi ak ñaar yi nekk maami fukki giir ak ñaar yu Israyil yi.9 «Sunu maam yooyu iñaane Yuusufa seen doomu baay te ñu jaay ko ngir ñu yóbbu ko Misra. Waaye Yàlla nekkoon na ak moom 10 te yewwi woon na ko ci bépp metit. Yàlla may na ko xel mu rafet ci kanamu Firawna, mi di buuru Misra, ba mu neex ko. Mu fal ko njiit ci réewu Misra ak ci këram bépp. 11 Gannaaw loolu mu am xiif fépp ci réewu Misra ak ci réewu Kanaan ak metit bu réy lool, te sunu maam yi amuñu woon lu ñu lekk. 12 Bi Yanqóoba déggee ne ci réewu Misra am na lekk, mu yebal fa doomam yi. Loolu moo nekk yoon bu jëkk bi sunu maam yi demoon ci Misra. 13 Bi ñu delloo ñaareelu yoon, Yuusufa def ba doomu baayam yi xàmme ko, te Firawna daldi xam mbokki Yuusufa yi. 14 Gannaaw loolu Yuusufa yónnee ngir ñu andi pàppaam mi di Yanqóoba ak mbokkam yépp. Ñu ngi tolloon ci juróom ñaari fukki nit ak juróom. 15 Yanqóoba dem ci réewu Misra. Mu dëkk fa ba mu dee fa. Sunu maam yi tamit dee foofu, 16 te ñu jël seen néew yi, yóbbu leen ci Sisem, te denc leen ci bàmmeel bi Ibraayma jëndoon ak xaalis ci doomu Amor ci Sisem.
17 «Bi jamono bi Yàlla waree matal digeem bi mu defoon ak Ibraayma jegesee; askan bi di yokku di gën di law ci Misra. 18 Waaye benn Firawna bu bees falu te xamuloon Yuusufa. 19 Buur boobu nax sunu maam yi te di leen metital ngir ñu bàyyi seeni doom yu doora juddu ba ñu dee. 20 Ci jamono jooju Musaa juddu. Mu doon xale bu rafet ci kanamu Yàlla. Ñu toppatoo ko ñetti weer ci kër pàppaam. 21 Bi ko waajuram yi bàyyee, doomu Firawna bu jigéen jël ko te yar ko ni doomam. 22 Ci noonu ñu jàngal Musaa ci xam-xamu Misra yépp, te mu nekk nit bu am kàttan ci kàddu ak ci jëf.
23 «Bi Musaa amee ñeent fukki at, mu yég ci xolam dem ngir seeti mbokkam yi, waa Israyil. 24 Mu génn gis benn waa ju Misra di néewal doole kenn ci ñoom. Mu wallu ko te rey waa ju Misra gi ngir feyyul ko. 25 Musaa xalaatoon na ne waa Israyil dinañu xam ne Yàlla dina leen yewwi jaarale ko ci moom waaye xàmmewuñu ko. 26 Ci ëllëg sa, mu gis ñaari Yawut di xeex ci seen biir. Mu bëgg leena jubale. Mu ne leen: "Samay waay, ay mbokk ngeen. Lu tax ngeen di xeex ci seen biir?" 27 Waaye ki doon néewal doole moroomam bëmëx Musaa te wax ko ne: "Kan moo la fal njiit walla àttekat ci sunu biir? 28 Ndax danga ma bëgga rey ni nga reye woon waa ju Misra bi démb?" 29 Bi Musaa déggee wax yooyu mu daldi daw, dem dëkk ci réew Majan. Mu am fa ñaari doom.
30 «Gannaaw ñeent fukki at benn malaaka feeñu Musaa ci màndiŋu tundu Sinayi ci benn safara suy tàkk ci benn garab. 31 Mu jaaxle ci gis-gis bi. Ni mu gën di jegesee mu dégg baatu Boroom bi wax ko ne: 32 "Man maay Yàlla say maam: Yàllay Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba." Musaa tiit bay lox te ñemeetul woon xool. 33 Boroom bi wax ko ne: "Simmil say dàll ndaxte béréb bi nga taxaw béréb bu sell la. 34 Gis naa bu wér coono bi sama xeet bi di daj ci réewu Misra. Dégg naa seeni yuuxu, te wàcc naa ngir yewwi leen. Léegi nag maa ngi lay yónni ci réewu Misra."
35 «Musaa moomu Yawut yi weddi woon te waxoon ko ne: "Kan moo la fal njiit walla àttekat ci sunu biir?" Moom la Yàlla yónni ni njiit ak yewwikat, ci ndimbalu malaaka mu ko feeñu woon ci biir safara suy tàkk ci garab bi. 36 Te itam moo génne askan bi ci réewu Misra te def ay yëf yu yéeme ak ay màndarga ci réewu Misra, ci bi ñuy jàll ci géej bu xonq gi, ak ci màndiŋ bi ci diirub ñeent fukki at. 37 Musaa moomu moo wax waa Israyil ne: "Yàlla dina leen feeñalal benn yonent ni man bu bokk ci yeen." 38 Bi ñu dajaloo ci màndiŋ bi, moo nekkoon ak sunu maam yi te nekkoon itam ak malaaka mi ko waxoon ci tundu Sinayi. Jotoon na kàddu Yàlla yiy joxe dund ngir jottali nu ko. 39 Sunuy maam yi bëgguñu ko woona déggal. Ñu bàyyi ko, seen xel dellu ci Misra. 40 Te noonu ñu wax Aaróona ne: "Defal nu ay yàlla, yuy dox ci sunu kanam ndaxte Musaa mi nu jiite woon bi nu génnee woon ci Misra, xamatunu lu ko dal." 41 Ci bés yooyu, ñu tëgg benn sëllu def ko seen yàlla, jébbal benn sarax xërëm bi, di bànneexu ci li seen loxo defar. 42 Noonu Yàlla sori leen, mu bàyyi leen ñuy jaamu biddéew asamaan ni ñu ko binde woon ci téere yonent yi, ne:
"Yeen waa Israyil, ndax man ngeen doon sàkkal ay may ak ay sarax
ci diirub ñeent fukki at ci màndiŋ bi?
43 Déedéet, yeena doon yóbbaale mbaaru màggalukaayu Molog
ak biddéewu seen yàlla Refan
di nataal yi ngeen defaroon ngir jaamu leen.
Kon nag man maa leen di yóbbu ci réewu Babilon."»
44 Eccen teg ca ne: «Ci jamono bi sunu maam yi nekkee ci màndiŋ mi, mbaar mi doon seede kóllëre gi Yàlla fas nekkoon na ak ñoom. Mbaar moomu, Yàlla waxoon Musaa mu defar ko ni ko Yàlla sante woon. 45 Te mbaar moomu sunu maam yi ak ñi soqikoo woon ci ñoom jot nañu ko. Ñu yóbbaale mbaar mi, ñoom ak Yosuwe, bi ñu nangoo réew mii, te Yàlla dàqoon xeet yi ci seen kanam. Mbaar mi des fa ba ci jamono Daawuda. 46 Te Daawuda am yiw ci kanamu Yàlla te ñaan ko ngir mu defar benn dëkkuwaay ngir Yàllay Yanqóoba. 47 Suleymaan nag, moo mujje tabax kër-Yàlla gi. 48 Waaye Yàlla Aji-Kawe ji du dëkk ci kër yu loxoy nit tabax, ni ko yonent bi waxe, ne:
49 "Asamaan mooy sama baŋu nguur
te suuf si mooy fi may teg samay tànk."
Loolu la Boroom bi wax.
"Ban kër ngeen ma mëna defaral,
ak ban béréb laa mëna noppalu?
50 Ndax du sama loxo moo sàkk mbir yi yépp?"»
51 Eccen teg ca ne: «Yeen nit ñu dëgër bopp ñi, te seen xol yi ak seen nopp yi baña dégg dëgg. Dangeen di diiroo ak Xel mu Sell mi saa su nekk. Yeena ngi niroo seeni maam yi. 52 Kan ci yonent yi la seen maam yi fitnaalul? Rey nañu ñu doon yégle ñëwu Ku Jub ki, te yeen léegi jébbale ngeen Ku Jub kooku, ba rey ko. 53 Waaw, jot ngeen yoon bi Yàlla joxe woon jaarale ko ci malaaka yi, waaye déggalooleen ko.»
Rey nañu Eccen te tàmbali nañu fitnaal mbooloo ñi gëm
54 Bi ñu déggee kàddu Eccen yooyu, ñi nekkoon ci kurélu àttekaay bi mer lool ba seen xol yi di lakk, te ñuy yéy seeni bëñ. 55 Waaye Eccen, fees ak Xel mu Sell mi, yékkëti bëtam yi ne jàkk asamaan, gis màggaayu Yàlla ak Yeesu taxaw ci ndeyjooru Yàlla. 56 Mu ne leen: «Dégluleen! Gis naa asamaan si ubbeeku te Doomu nit ki taxaw ci ndeyjooru Yàlla.» 57 Ci kaw loolu ñu yuuxu ak baat bu kawe, fatt seen nopp yi te ñoom ñépp dal ci kawam. 58 Ñu diri ko ba génn ak moom ci dëkk bi, te tàmbali di ko sànni xeer ngir rey ko. Seede yi tegoon nañu seen yére yi ci tànku waxambaane bi ñu woowe Sóol. 59 Ci waxtu bi ñu koy sànni xeer, Eccen woote naan: «Boroom bi Yeesu, nangul sama ruu.» 60 Mu sukk óomam yi ci suuf te yuuxu ak baat bu kawe ne: «Boroom bi, bu leen toppe bàkkaar bii.» Gannaaw bi mu waxee kàddu yooyu, mu daldi dee.