8
Sóol moom àndoon na ak ñi rey Eccen. Dale ko ci bés boobu, ñu tàmbali di fitnaal bu metti mbooloom ñi gëm Almasi bi te nekk Yerusalem ba tax ñépp ñi gëmoon di tasaaroo, dem ci diiwaanu Yude ak diiwaanu Samari, ba mu des ndaw yi. 2 Ay nit ñu takku ci Yàlla rob Eccen, jooy ko lool. 3 Waaye Sóol moom doon na tas mbooloom ñi gëm, di dem kër ak kër jàpp ñi gëmoon, góor ak jigéen, te tëj leen ci kaso bi.Filib yégle na xibaar bu baax bi ca Samari
4 Ñi tasaaroo ñu ngi doon dem yégle xibaar bu baax bi fu nekk fu ñu doon jaar. 5 Noonu Filib dem ci benn dëkk ci diiwaanu Samari di fa yégle Almasi bi. 6 Bi ko mbooloo mi déggee te gis màndarga yi mu doon def ñoom ñépp ñu doon bàyyi xel ci li mu doon wax. 7 Rab yu bon yu bari di génn ci nit ñi, di yuuxu. Mu wéral ay lafañ yu bari ak ay làggi yu bari. 8 Ci dëkk boobu mbégte mu réy daldi am.
9 Amoon na benn waay bu tudd Simoŋ. Luxuskat la woon bu fa yàgg. Waa Samari yépp yéemu woon nañu ci li mu doon def. Mu ngi doon teg boppam ku am solo. 10 Ba tax ñu bari, mag ak ndaw, di bàyyi xel ci moom. Ñu ngi doon wax ci moom ne: «Kii mooy kàttan bu ñuy wax Kàttan bu mag bi.» 11 Ñu koy déglu bu baax ndaxte yàgg na mu leen di yéem ci mbirum luxus. 12 Waaye bi ñu gëmee Filib mi doon yégle xibaar bu baax bi ci Yeesu Almasi bi ak ci lu jëm ci nguuru Yàlla gi, góor ak jigéen, ñu nangu ñu sóob leen ci ndox. 13 Simoŋ ci boppam gëm na te nangu ñu sóob ko. Mu doon topp Filib fu nekk te muy yéemu bi mu gisee màndarga ak kéemaan yu mag yi doon xew.
14 Ndaw yi nekkoon Yerusalem dégg nañu ne waa Samari nangu nañu kàddug Yàlla gi. Noonu ñu yónni fa Piyeer ak Yowaana. 15 Bi ñu yegsee Samari ñu ñaanal leen ngir ñu jot Xel mu Sell mi, 16 ndaxte Xel mu Sell mi wàccagul woon ci kaw kenn ci ñoom, waaye dañu leen sóoboon ci ndox rekk ci turu Boroom bi Yeesu. 17 Noonu Piyeer ak Yowaana teg leen loxo te ñu jot Xel mu Sell mi.
18 Bi Simoŋ gisee ne Yàlla maye na Xel mu Sell mi ci bi ndaw yi tegee loxo nit ñi, mu indil leen xaalis 19 te wax leen ne: «Jayleen ma itam sañ-sañ bii, ngir ku ma teg loxo nga mëna jot Xel mu Sell mi.» 20 Waaye Piyeer ne ko: «Na nga sànku, yaw ak sa xaalis, ndaxte danga foog ne mayum Yàlla bi, mën nañu ko jënde xaalis, 21 te yaw amoo wàll, amoo cér ci mbir mii ndaxte sa xol dafa jubul ci kanamu Yàlla. 22 Kon nag, tuubal te nga bàyyi sa coxorte te nga ñaan Boroom bi ngir mu baal sa xel bu bon, su mënee nekk, 23 ndaxte maa ngi gis nga fees ak iñaan te bàkkaar da laa tëj.» 24 Simoŋ tontu ko ne: «Yeen ci seen bopp ñaanalleen ma Boroom bi, ngir dara ci li ngeen wax bañ maa dal.»
25 Bi Piyeer ak Yowaana seedee kàddu Boroom bi ba noppi ñu daldi dellu Yerusalem. Ci yoon bi, ñu yégle xibaar bu baax bi ci dëkk yu bari ci diiwaanu Samari.
Filib yégle na Xibaar bu baax bi Jaraaf bu dëkk Ecópi
26 Benn bés benn malaaka wu Boroom bi ne Filib: «Jógal, te nga jël yoon bi jëm sudd jóge Yerusalem, jëm Gasa ci màndiŋ ba.» 27 Mu daldi jóg te dem. Amoon na benn jaraaf bu doon liggéeyal Kandas, buur bu jigéen bu Ecópi, di saytu alalam bépp. Nit kooku ñëwoon na Yerusalem ngir màggal Boroom bi. 28 Bi muy dellu Ecópi nag mu nekkoon ci watiiram di jàng téere yonent Yàlla Esayi. 29 Xel mi ne Filib: «Demal, dabi watiir bee.» 30 Filib dawsi, dégg waa ji jóge woon Ecópi mu doon jàng téere Esayi. Mu ne ko: «Ndax xam nga dara ci li ngay jàng?» 31 Mu tontu ko: «Naka laa koy xame bu fekkee awma kenn ku ma gindi?» Mu woo Filib ngir mu yéeg, toog ci wetam. 32 Booba, aaya yi mu doon jàng ci Mbind mi, lii lay wax:
«Mu mel ni xar bu ñu yóbbu ngir rendi ko,
moom, ubbiwul gémmiñam,
mel ni mbote bu muuma ci kanamu ki koy wat.
33 Dañu ko toroxal te joxuñu ko dëgg.
Jële nañu bakkanam ci àddina,
kon kan mooy mëna wax ci ay sëtam?»
34 Jaraaf bi ne Filib: «Maa ngi laay ñaan, ci mbiru kan la yonent bi doon wax, boppam la doon waxal walla keneen?» 35 Noonu Filib jël kàddu gi, tàmbalee ci aaya yooyu, xamal ko xibaar bu baax bi jëm ci Yeesu.
36 Ni ñuy wéye di dem, ñu gis ndox. Jaraaf bi ne ko: «Ndox a ngi nii. Lan moo ma tere, nga sóob ma ci?» 37 Filib ne ko: «Boo gëmee ci sa xol bépp loolu mën na nekk.» Jaraaf bi tontu ko: «Gëm naa ne Yeesu Almasi bi mooy Doomu Yàlla ji.» 38 Noonu mu taxawal watiir bi. Filib ak jaraaf bi wàcc ñoom ñaar ñépp ci biir ndox mi te Filib sóob ko ci ndox mi.