Tuubum Sóol
9
Ci jamono jooju, Sóol wéy di wuta rey taalibe Boroom bi. Mu dem ci jébbalkatu-sarax-bu-mag bi, 2 laaj ko ay bataaxal ngir mu dem ci kër-ñaan yi nekk ci dëkku Damaas ngir bu fa fekkee ñi doon topp yoonu Boroom bi góor ak jigéen mu jàpp leen, andi leen Yerusalem. 3 Bi muy nekk ci yoon, di jege dëkku Damaas ci saa si benn leer buy melax jóge asamaan, wër ko. 4 Mu daanu ci suuf. Mu dégg benn baat bu ko ne: «Sóol, Sóol, lan moo tax nga may fitnaal?» 5 Mu tontu ko ne: «Yaw la kan, Boroom bi?» Baat bi tontu ko ne: «Man la Yeesu mi ngay fitnaal. 6 Waaye léegi, jógal nga dugg ci dëkk bi, te dinañu la wax li nga wara def.» 7 Ci waxtu boobu fekk na ñi mu àndaloon ci tukki bi taxaw, tiit ba mënuñu wax ndaxte ñu ngi doon dégg baat bi waaye gisuñu kenn. 8 Sóol jóg ci suuf si, taxaw. Bët yi ubbeeku woon nañu, waaye mënul woona gis. Ñu jàpp ko ci loxo, yóbbu ko ci dëkku Damaas. 9 Mu des fa diirub ñetti fan, bëtam yi gisul, te lekkul dara, naanul dara.10 Ci dëkku Damaas amoon na benn taalibe Yeesu bu tudd Anañas. Boroom bi feeñu ko ci gis-gis, ne ko: «Anañas.» Mu tontu ko ne: «Maa ngi nii, Boroom bi.» 11 Boroom bi ne ko: «Jógal te nga dem ci mbedd bu ñu tudde Mbedd bu Jub bi, ci kër Yudaa, te nga seet fa benn waay bu tudd Sóol, bu jóge Tàrs, ndaxte mu ngi fa di ñaan. 12 Ci benn gis-gis mu gis benn waay bu tudd Anañas duggsi, teg ko loxo ngir mu gisaat.» 13 Anañas tontu ko ne: «Boroom bi, dégg naa nit ñu bari di seede lu ñaaw li mu doon def ñi nga moom ci Yerusalem. 14 Mu ngi fii te jot na sañ-sañ bu jóge ci jébbalkatu-sarax-bu-mag bi ngir mu jàpp képp kuy woo sa tur.» 15 Waaye Boroom bi ne ko: «Demal, ndaxte waa jooju moom laa tànn ni jumtukaay ngir mu xamal sama tur xeeti àddina yi ak seeni buur, ak askanu Israyil. 16 Man ci sama bopp dinaa ko won lépp li mu wara daj ngir sama tur.» 17 Anañas daldi dem, dugg ca kër ga. Mu teg ko loxo, ne ko: «Sóol sama mbokk, Boroom bi Yeesu mi la feeñu ci yoon bi nga jëloon, moo ma yónni ngir nga gisaat te nga fees ak Xel mu Sell mi.» 18 Ci saa si lu mel ni ay waasintóor génne ci bëtam yi, daanu, te mu gisaat. Ci noonu mu jóg te ñu sóob ko ci ndox. 19 Gannaaw loolu, mu lekk ba amaat doole.
Sóol daldi des ak taalibe Yeesu yi nekkoon dëkku Damaas ay fan. 20 Ci saa si mu tàmbali di yégle ci kër-ñaan yi ne Yeesu mooy Doomu Yàlla ji. 21 Ñépp ñi ko doon déglu waaru tey wax ne: «Waaw! Du ki moo doon fitnaal ñiy woo turu Yeesu ci Yerusalem? Te moo ñëw ba fii ngir jàpp leen te yóbbu leen ci njiiti-jébbalkati-sarax yi.» 22 Waaye Sóol gëna am kàttan ba jaaxal Yawut yi nekk ci dëkku Damaas. Muy wone ne Yeesu mooy Almasi bi.
Sóol dem na Yerusalem
23 Sóol teg ci ay fani fan. Yawut yi di gise ci seen biir ngir rey ko. 24 Guddi ak bëccëg ñu ngi doon saytu buntu dëkk bi ngir mën koo rey, waaye Sóol yég seen pexe. 25 Benn guddi, taalibeem yi dugal ko ci dàmba, wàcce ko ci gannaaw miir bi wër dëkk bi.
26 Bi mu yegsee Yerusalem, mu wuta bokk ci taalibe yi waaye ñépp dañu koo ragaloon ndaxte gëmuñu woon ne taalibe dëgg la. 27 Barnabas jël ko, andi ko ci ndaw yi, nettali leen naka la Sóol gise Boroom bi ci yoonu Damaas te Boroom bi wax ak moom. Mu nettaliwaat leen naka la Sóol doon waaree ci turu Yeesu ak kóolute ci Damaas. 28 Dale ko ci bés boobu, Sóol mu ngi ànd ak ñoom di dem ak di ñëw ci biir Yerusalem di wax ak kóolute ci turu Boroom bi. 29 Mu ngi doon waxtaan ak di werante ak Yawut yiy làkk gereg, waaye ñu ngi ko doon fexee rey. 30 Bi mbokki gëmkat yi yégee loolu, ñu yóbbu Sóol dëkku Sesare. Foofu, ñu jàllale ko ci dëkku Tàrs.
31 Ci jamono jooju mbooloo ñi gëm ci diiwaanu Yude, diiwaanu Galile, ak diiwaanu Samari yépp ñu ngi woon ci jàmm te gëna dëgër ci seen ngëm. Ñuy dox ci ragalu Boroom bi te di yokku ci ndimbalu Xel mu Sell mi.
Piyeer ci dëkku Lidd
32 Booba Piyeer doon tukki fu nekk. Mu yegg ba dëkku Lidd ngir seeti ñi Boroom bi moom. 33 Mu fekk fa benn waay bu tudd Ene bu tëdd ci lalam lu tollu ci juróom ñetti at ndaxte dafa amoon feebaru làggi. 34 Piyeer ne ko: «Ene, Yeesu Almasi bi wéral na la. Jógal, nga defaraat sa lal.» Ci saa si mu jóg. 35 Ñépp ñi dëkk Lidd ak diiwaanu Saron, bi ñu gisee loolu, ñu daldi woññeeku ci Boroom bi.
Piyeer ci dëkku Yope
36 Ci dëkku Yope amoon na benn taalibe bu jigéen bu tuddoon Tabita. Tur woowu ci làkku Gereg mooy Dorkas. Dafa dëkkoon di def lu baax te di dimbali néew di doole yi. 37 Ca bés yooyu mu daanu feebar te dee. Ñu sang ko te yóbbu ko ci néeg bi féete ci kaw kër gi. 38 Taalibe yi déggoon nañu ne Piyeer mu ngi woon Lidd te Lidd soriwuloon Yope. Noonu ñu yónnee ñaari waay ci moom ngir ñu ne ko: «Nu ngi lay ñaan nga gaawantu ñëw ci nun.» 39 Noonu Piyeer jóg ànd ak ñoom. Bi ñu yegsee ñu yóbbu ko ci néeg bi féete ci kaw, fekk jigéen ñi ñàkk seen jëkkër yépp jegesi Piyeer di jooy te won ko mbubb yi ak yeneen yére yi Tabita daan defar ci jamono bi mu nekkee woon ak ñoom. 40 Piyeer daldi génne ñépp te sukk di ñaan. Gannaaw bi mu ñaanee ba noppi mu walbatiku ci néew bi te ne ko: «Tabita, jógal.» Tabita daldi ubbi ay bëtam, gis Piyeer, te daldi toog. 41 Te Piyeer jàpp loxoom ngir dimbali ko mu jóg. Mu woo ñi Boroom bi moom ak jigéen ñi ñàkkoon seen jëkkër, won leen ko muy dund. 42 Xibaar boobu siiw ci dëkku Yope te mbooloo mu bari gëm ci Boroom bi. 43 Gannaaw loolu Piyeer des ci Yope ay fan ci kër benn waay bu tudd Simoŋ. Moom uude la woon.