Xibaar bu baax bi laal na ñi dul Yawut
10
Ci dëkku Sesare amoon na benn waay bu tudd Korney. Njiitu soldaaru Room la woon te moo doon jiite mbooloo bi ñu woowe xarekati Itali. 2 Moom ak waa këram takku woon nañu ci Yàlla te ragaloon ko. Mu doon dimbali néew di doole yi ci biir askanu Yawut yi te farlu woon na ci ñaan. 3 Benn bés ci booru ñetti waxtu ci ngoon, ci benn gis-gis benn malaaka Yàlla feeñu ko, dugg këram te ne ko: «Korney!» 4 Mu xool malaaka bi. Mu tiit lool te mu laaj ko ne: «Lan moo xew, kilifa gi?» Malaaka bi tontu ko ne: «Yàlla nangul na la say ñaan te gis na ni nga doon dimbalee néew di doole yi. 5 Léegi nag yónnil ay nit ci Yope ñu woo benn waay bu tudd Simoŋ te ñu koy woowe Piyeer, ngir mu ñëw. 6 Mu ngi dal ci kër beneen Simoŋ di uude te këram nekk ci wetu géej gi.» 7 Bi malaaka bi demee, Korney woo ñaar ci ay surgaam ak benn soldaar bu bokk ci ñi mu jiite woon te takku woon ci Yàlla. 8 Gannaaw bi mu leen nettalee lépp li xewoon, mu yónni leen ci Yope.
9 Ci ëllëg sa, bi ñuy wéy di dem ci yoon bi ba jubsi Yope, Piyeer yéeg ci kaw kër gi di ñaan. Boobu diggu bëccëg moo jotoon. 10 Xiif dab ko te mu bëggoona lekk, waaye bi ñu koy toggal mu am benn gis-gis. 11 Mu gis asamaan si ubbeeku, te lu mel ni sër bu mag wàcce ci asamaan te jëm ci suuf, ñu téye ko ci ñeenti laf yi. 12 Mu amoon ay mala yu am ñeenti tànk ak yuy raam ak picci asamaan si. 13 Noonu mu am baat bu ko ne: «Jógal, Piyeer! Reyal te nga lekk.» 14 Piyeer ne: «Mukk Boroom bi, ndaxte mësuma lekk lu daganul maanaam lu setul.» 15 Waaye baat bi waxaat ko ne: «Lu Yàlla setal, du yaw yaa ko wara wax setul.» 16 Gannaaw bi loolu amaatee ba mu doon ñetti yoon, ci saa si sër bu mag bi dellu asamaan. 17 Bi loolu amee Piyeer jaaxle ci li gis-gis boobu wara tekki.
Fekk na ñi Korney yebaloon laajte woon nañu kër Simoŋ, ba yegsi ci bunt bi. 18 Ñuy woote ngir xam ndax Simoŋ mi ñuy woowe Piyeer foofu la dal. 19 Ci jamono boobu Piyeer mu ngi doon xalaat ci gis-gis bi mu amoon. Xel mu Sell mi ne ko: «Am na ñetti nit ñi lay seet. 20 Jógal te nga wàcc te nga ànd ak ñoom te bu ci am benn xel ñaar ndaxte man maa leen yónni.» 21 Piyeer daldi wàcc ci nit ñi, ne leen: «Maa ngi nii. Man maay ki ngeen di seet. Lan moo waral seen tànk yi?» 22 Ñu ne: «Ki ñuy wax Korney, njiitu soldaar, moo nu yónni. Nekk na nit ku jub te ragal Yàlla, ki nga xam ne askanu Yawut yi yépp ñu ngi koy seedeel ay jëf yu baax. Dafa am benn malaaka bu sell bu ko feeñu te ne ko mu woolu la ngir mu déglu li nga koy wax.» 23 Piyeer dugal leen ci kër gi, dalal leen. Ci ëllëg sa mu daldi ànd ak ñoom ak ñenn ci mbokki gëmkat yi nekk Yope.
24 Ci gannaaw ëllëg sa ñu yegsi Sesare. Fekk Korney doon ko xaar ak ay mbokkam ak xaritam yi mu woo woon. 25 Bi Piyeer di duggsi, Korney gatandu ko, daanu ci ay tànkam, sukk ci kanamam. 26 Waaye Piyeer yékkëti ko te ne: «Jógal, ndaxte man itam, nit kese laa.» 27 Piyeer ànd ak moom, ñuy waxtaan, ñu dugg ci kër gi. Piyeer fekk fa nit ñu bari ñu fa dajaloo. 28 Mu ne leen: «Xam ngeen bu baax ne aaye nañu doomu Yawut muy bokk dara ak ku dul Yawut walla sax muy dugg këram. Waaye Yàlla won na ma ne waruma wax ne kenn daganul mbaa setul. 29 Loolu moo tax awma benn jafe-jafe ci bi ngeen ma woowe ma ñëw. Léegi nag bëggoon naa xam li tax ngeen woo ma fii.»
30 Korney tontu ko ne: «Ñetti fan ci gannaaw ci waxtu bii tembe, maanaam ci ñetteelu waxtu ci ngoon, maa ngi woon ci sama kër di ñaan. Ci saa si ma gis ku sol lu weex. 31 Mu ne ma: "Korney, Yàlla nangu na say ñaan ak ni nga doon dimbalee néew di doole yi. 32 Léegi nag, yónneel ci Yope ci benn waay bu tudd Simoŋ te ñu koy woowe Piyeer. Mu ngi dal ci kër beneen Simoŋ di uude, te këram nekk ci wetu géej gi." 33 Noonu ci saa si, ma daldi yónnee ci yaw, te maa ngi lay sant ci li nga ma wuyusi. Léegi nag, nun ñépp, nu ngi fi ci kanamu Yàlla ngir déglu lépp li la Boroom bi sant ngir nga wax nu ko.»
34 Noonu Piyeer jël kàddu gi te ne leen: «Ci dëgg, léegi xam naa ne Yàlla du gënatle nit ñi. 35 Waaye ku neex Yàlla mooy ki ko ragal tey def lu jub ak ci xeet boo mëna bokk. 36 Yónnee na waa Israyil kàddoom te yégal leen xibaaru jàmm ji, jaarale ko ci Yeesu Almasi bi di Boroomu ñépp. 37 Xam ngeen li xewoon ci diiwaanu Galile bu jëkk, ak ci réewu Yawut yi yépp, gannaaw bi Yaxya doon waare tey sóob nit ñi ci ndox. 38 Xam ngeen naka la Yàlla sole Yeesu mu Nasaret kàttanu Xel mu Sell mi, te muy wër réew mi yépp di def lu baax te di wéral ñépp ñi Seytaane tënk, ndaxte Yàlla àndoon na ak moom. 39 Te nun, seede nanu lépp li mu doon def ci réewu Yawut yi ba ci Yerusalem. Ñu rey ko, daaj ko ci bant. 40 Yàlla dekkil ko ci ñetteelu fan bi te may ko mu mëna feeñal boppam. 41 Feeñuwul ci ñépp ci askan bi waaye ci seede yu jëkk yi Yàlla tànnoon maanaam nun. Gannaaw bi mu dekkee ci ñu dee ñi, lekkandoo nanu te naanandoo ak moom. 42 Te Yeesu joxoon na nu ndigal ngir nu yégal askan bi te seede ne moom la Yàlla tànn ngir mu àtte ñiy dund ak ñi dee. 43 Moom la yonent yi yépp seedeel ne képp ku gëm ci moom dinga jot mbaalum bàkkaar ci turam.»
44 Bi Piyeer di wax loolu, Xel mu Sell mi daldi wàcc ci ñépp ñi doon déglu kàddu gi. 45-46 Ñu tàmbali di wax yeneeni kàllaama te di màggal Yàlla. Yawut yi gëmoon te àndoon ak Piyeer waaru woon nañu ci li ñu gis Xel mu Sell mi wàcc tamit ci ñi nekkul Yawut. Piyeer daldi ne: 47 «Ndax kenn mën na tere ñu sóob ci ndox nit ñii jot Xel mu Sell mi ni nun?» 48 Gannaaw loolu mu sant leen ngir ñu sóob leen ci ndox ci turu Yeesu Almasi bi. Te ñu ñaan Piyeer ngir mu des ak ñoom ay fan.