Piyeer leeral na naka la ñi dul Yawut gëme Yàlla
11
Bi loolu amee ndaw yi ak mbokki gëmkat yi nekk ci diiwaanu Yude dégg nañu ne ñu nekkul Yawut nangu nañu kàddug Yàlla. 2 Bi Piyeer delloo Yerusalem, Yawut yi gëmoon te nekk foofu doon nañu werante ak moom, 3 ne: «Dugg nga ci kër ñi xarafuwul bay lekkandoo ak ñoom.» 4 Piyeer benn-bennal leen lépp li xewoon. 5 Mu ne leen: «Benn bés, dama nekkoon ci dëkku Yope. Ci waxtu bi ma doon ñaan, ma am benn gis-gis. Ma gis lu mel ni sër bu mag, ñu téye ko ci ñeenti lafam yi, ñu wàcce ko ci asamaan ba ci man. 6 Bi ma ko xoolee, ne ko jàkk gis naa mala suuf si, yi am ñeenti tànk, yiy raam, ak picci asamaan si. 7 Benn baat daldi ma wax ne: "Jógal, Piyeer! Reyal te nga lekk." 8 Noonu, ma ne: "Mukk Boroom bi, ndaxte dara lu daganul maanaam lu setul mësula dugg ci sama gémmiñ." 9 Waaye baat bi jóge asamaan waxaat ne: "Lu Yàlla setal, du yaw yaa ko wara wax setul." 10 Noonu loolu amaat ba mu doon ñetti yoon te lépp daldi dellu asamaan. 11 Ci waxtu boobu tembe, mu am ñetti nit ñu yegsi ci buntu kër gi nu nekkoon. Ñu jóge woon Sesare te ñu yónni woon leen ci man, 12 te Xel mu Sell mi ne ma: "Demal, ànd ak ñoom te bu ci am benn xel ñaar." Juróom benni mbokki gëmkat yii tamit daldi ànd ak man, nu dem dugg kër Korney. 13 Mu daldi nu nettali lépp li xewoon këram, ni ko malaaka bi feeñoo te wax ko ne: "Yónneel ci Yope te ñu andi Simoŋ mi ñuy woowe Piyeer. 14 Moom, dina la xamal ay wax yu lay muccal, yaw ak sa waa kër yi." 15 Bi ma tàmbalee wax nag, Xel mu Sell mi daldi wàcc ci seen kaw, ni mu wàcce ci nun ci njàlbéen. 16 Ma daldi fàttaliku kàddu Boroom bi wax ne: "Yaxya doon na sóob nit ñi ci ndox waaye Yàlla dina leen sóob ci Xel mu Sell mi."» 17 Piyeer teg ca ne: «Yàlla may na leen Xel mu Sell mi, ni mu nu ko maye woon bi nu gëmee Yeesu Almasi bi sunu Boroom. Kon nag man maay kan bay tere Yàlla muy def li ko neex?» 18 Gannaaw bi ñu déggee kàddu yooyu ñu daldi dal te di màggal Yàlla di wax ne: «Kon nag, Yàlla may na ñi dul Yawut ñu tuub ba am dund gu wóor gi.»Xibaar bu baax bi siiw na ca dëkku Ancos
19 Mbokki gëmkat yi tasaaroo nañu fépp ndax lu ñu leen doon bunduxataal ci gannaaw deewu Eccen. Ñu dem ba ci diiwaanu Fenisi, Sippar di réew mu ndox wër, ak dëkku Ancos, di fa yégle kàddug Yàlla gi yemale ko ci Yawut yi kese. 20 Waaye nag amoon na ci ñoom ñenn ñu jóge woon ca Sippar, ñii ca dëkku Siren. Bi ñu yegsee ci Ancos ñu tàmbali di wax ak ñi dul Yawut tamit di leen yégal xibaar bu baax bi ci Boroom bi Yeesu. 21 Boroom bi mu ngi woon ak ñoom te nit ñu bari tuub te gëm ci Boroom bi. 22 Mbooloom ñi gëm ci Yerusalem daldi yég li xew, te ñu yónni Barnabas ngir mu dem Ancos. 23 Bi mu yegsee, mu gis yiwu Yàlla ci ñoom, mu daldi ànd ak mbégte. Te noonu mu ñaax leen ngir ñu wéy di takku ci Boroom bi ak seen xol bépp. 24 Moom nit ku baax la woon te fees ak Xel mu Sell mi ak ngëm. Te noonu mbooloo mu takku ñëw, dolleeku ci Boroom bi. 25 Barnabas daldi dem ca dëkku Tàrs ngir seet Sóol. 26 Bi mu ko gisee, mu ànd ak moom Ancos. Ñoom ñaar ñu ànd liggéey benn atum lëmm ci biir mbooloo ñi gëm te nekk Ancos, di jàngal ñu bari. Ca Ancos lañu jëkka woowe taalibe yi Kercen, maanaam gaayi Almasi bi.
Taalibe Ancos yi yónnee nañu ndimbal taalibe Yude yi
27 Ci bés yooyu amoon na ay yonent yu doon jóge Yerusalem, dem Ancos. 28 Kenn ci ñoom ku tuddoon Agabus daldi taxaw te yégle ci kàttanu Xel mu Sell mi ne xiif bu metti dina wàcc ci àddina si yépp. Loolu amoon na ci jamono Sesaar Këlódd. 29 Noonu taalibe yi nekkoon Ancos dogaloon nañu ne ñu boole seeni alal yi, ku nekk ak li mu mëna joxe, ngir jàppale mbokki gëmkat yi nekkoon Yude. 30 Noonu lañu def nag: ñu teg xaalis bi ci loxoy Barnabas ak Sóol, yónnee ko njiiti mbooloo ñi gëm yi nekkoon Yerusalem.