Rey nañu Saag te tëj Piyeer kaso
12
Ci jamono jooju buur Erodd Àggripa tàmbali woon na fitnaal ñenn ñi bokk ci mbooloom ñi gëm, 2 ba reylu ak jaasi Saag mi bokk ak Yowaana ndey ak baay. 3 Bi mu gisee ne loolu neex na Yawut yi, mu jàpplu Piyeer tamit. Fekkoon na bési màggalu mburu yu amul lawiir yi. 4 Bi mu ko jàppee mu tëj ko ci kaso, te teg ko ci loxoy ñeenti mbooloom soldaar ci bu nekk am ñeenti soldaar. Mu bëggoon ko àtte ci kanamu askan bi gannaaw màggalu Paak. 5 Bi Piyeer nekkee ci kaso bi, mbooloom ñi gëm di ko ñaanal ci Yàlla ak seen xol bépp.
Benn malaaka yewwi na Piyeer ca kaso ba
6 Ci guddi googu, bi Erodd wara àttee Piyeer ci ëllëg si, Piyeer doon na nelaw ci diggante ñaari soldaar te ñu yeew ko ak ñaari ceen. Amoon na ay garjen yu doon wottu buntu kaso bi. 7 Ci saa si benn malaaka Boroom bi ñëw. Ab leer leeral kaso bi. Malaaka bi laal Piyeer ci wet bi te yee ko, ne ko: «Jógal gaaw.» Ceen yi daldi dog ci loxoom yi di daanu. 8 Malaaka bi ne ko: «Takkal sa ndigg te sol say dàll.» Piyeer def noonu. Malaaka bi waxaat ko ne: «Solal sa mbubb te nga topp ma.» 9 Piyeer topp ko, génn, waaye xamul woon ne, li malaaka bi doon def, dëgg la. Dafa xalaatoon ne ay gis-gis rekk la. 10 Ñu jàll ci wottukat yu jëkk yi, ba ci ñaareel yi, ba ñu agsee ca buntu weñ bi jëm ci dëkk bi. Bunt bi daldi ubbeekul boppam ci seen kanam. Ñu génn, jaar ci mbedd mi. Ci saa si malaaka bi bàyyi ko.
11 Ca booba la xelu Piyeer dellusi ci moom, mu wax ne: «Léegi xam naa bu wóor ne, Boroom bi yónni na malaakaam ngir mu yewwi ma ci loxo Erodd ak lépp li ma askanu Yawut yi yéene woon def lu bon.» 12 Bi mu xamee loolu, mu daldi dem ci kër Maryaama mi di yaayu Yowaana mi nuy woowe Màrk. Foofu amoon na nit ñu bari yu booloo woon di ñaan ci Yàlla. 13 Piyeer fëgg ci bunt bi, te benn surga bu jigéen bu ñuy woowe Rodd ñëw ngir ubbil ko. 14 Mu daldi xàmme baatu Piyeer te ci biir mbégteem talul sax ubbil ko, waaye mu daw te yégle ne Piyeer mu ngi ci kanamu bunt bi. 15 Ñu ne ko: «Dangaa dof.» Waaye mu dëgër ci li mu wax. Noonu ñu ne: «Kon, malaakaam la.» 16 Ci waxtu boobu Piyeer mu ngi doon wéy di fëgg bunt bi. Bi ñu koy tijjil te gis ko ñu daldi waaru. 17 Piyeer yékkëti loxoom ngir ñu noppi te mu nettali leen naka la ko Boroom bi génne ci kaso bi te mu ne leen: «Demleen yégal ko Saag ak yeneen mbokki gëmkat yi.» Gannaaw loolu mu jóge fa, dem ci beneen béréb.
18 Bi bët setee yëngu-yëngu am ci biir soldaar yi te ñu laaj fu Piyeer jaar. 19 Erodd santaane ñu seet Piyeer waaye gisuñu ko fenn. Mu woolu soldaar yi te laaj leen. Gannaaw loolu mu joxe ndigal ngir ñu rey leen. Bi loolu weesoo Erodd jóge diiwaanu Yude, dem dëkku Sesare, des fa ab diir.
Deewu buur Erodd Àggripa
20 Booba buur bi Erodd mere woon na lool waa Tir ak Sidon. Ñu mànkoo ngir seeti ko. Ñu naxante ak Balastus, bëkk-néegu buur bi, ngir mu dimbali leen ci loolu. Noonu ñu ñaan buur bi ngir ñu juboo ndaxte seen dund ci réewu buur boobu la doon jóge. 21 Bi bés bi ñu jàppoon yegsee, Erodd sol mbubbi buuram, toog ci baŋu nguur, di wax ci kanamu ñépp. 22 Noonu askan bi di yuuxu ne: «Nekkatul ne nit mooy wax, waaye baatu Yàlla la.» 23 Ci saa si benn malaaka Boroom bi ñëw dóor ko ndaxte nanguwul màggaayu Yàlla. Ay sax dugg ci moom, lekk ko, mu dee. 24 Gannaaw loolu kàddu Yàlla di gën di yokku tey law.
Xel mu Sell mi yónni na Barnabas ak Sóol
25 Bi Barnabas ak Sóol matalee seen liggéey ca Yerusalem, ñu dellu Ancos, yóbbaale Yowaana mi ñu woowe Màrk.