13
Amoon na ca mbooloo ñi gëm te nekk Ancos ay yonent ak ay jàngalekat. Ñii ñoo fa nekkoon: Barnabas, Simeyon ma ñu doon woowe ku ñuul ki, Lusiyus ma jóge woon dëkku Siren, Manayen mi yaroondoo woon ak Erodd ma yilifoon diiwaanu Galile, ak Sóol.2 Benn bés bi ñu doon màggal Boroom bi te woor, Xel mu Sell mi ne leen: «Beralleen ma Barnabas ak Sóol ngir liggéey bi ma leen woowe.»3 Noonu ñu woor, ñaan, te teg leen ay loxo. Gannaaw loolu ñu bàyyi leen ñu dem.
Liggéeyu Barnabas ak Póol ci Sippar
4 Niki noonu, Xel mu Sell mi yónni Barnabas ak Sóol, ñu dem ca dëkku Selusi. Ñu dugge foofu gaal, dem Sippar, di réew mu ndox wër. 5 Ba ñu yegsee ca dëkku Salamin, ñuy yégle kàddu Yàlla gi ci këru ñaanu Yawut yi. Ku tuddoon Yowaana moo leen doon dimbali ci liggéey bi. 6 Ñu jaar réew mi ndox wër yépp ba yegg dëkku Pafos. Ñu tase fa ak benn luxuskat bu tudd Bar-Yeesu, ab Yawut la woon te tudde boppam yonent. 7 Bokkoon na ci ñi jege woon Sergiyus Póolus mi nekkoon kilifa Sippar. Kilifa moomu ku am xel la woon. Mu woolu Barnabas ak Sóol ndaxte bëggoon na déglu kàddu Yàlla gi, 8 waaye luxuskat boobu, te ñu koy woowe Elimas di turam ci làkku Gereg, di leen xeex ngir kilifa boobu baña ñëw ci ngëm gi. 9 Noonu Sóol ma ñuy woowe Póol fees ak Xel mu Sell mi ne ko jàkk 10 te ne ko: «Yaw Elimas, nit ku fees ak fen ak bon te di doomu Seytaane. Yaw yaay noonu lépp lu jub. Yooni Boroom bi dañu jub. Ndax doo bàyyi di leen wut a dëngal? 11 Léegi nag, xoolal! Loxo Boroom bi dina dal ci sa kaw. Dinga gumba te doo gisati jant bi ab diir.» Ci saa si bëtam daldi lëndëm, mu gumba. Muy làmbatu fu nekk di wut ku ko wommat. 12 Noonu bi kilifa réew mi gisee li xew, mu daldi gëm, ndaxte yéemu woon na lool ci li ñu ko doon jàngal jëm ci yoonu Boroom bi.
Póol ak Barnabas yégle nañu xibaar bu baax bi ca dëkku Ancos ci diiwaanu Pisidi
13 Póol ak ñi mu àndaloon duggaat gaal ci dëkku Pafos, dem ci dëkku Peers ci réewu Pamfili. Yowaana mi ñuy woowe Màrk bàyyi woon na leen fa te dellu ca Yerusalem. 14 Ñoom ci seen wàllu bopp ñu jóge Peers te wéy ci seen yoon ba yegg ci dëkku Ancos ci diiwaanu Pisidi. Ci bésu noflaay bi ñu dugg ci kër-ñaan bi, daldi toog. 15 Gannaaw bi kenn jàngee kàddu gi ci téere Musaa ak ci téere yonent yi, njiiti kër-ñaan yi yónnee ci Póol ak Barnabas ngir wax leen ne: «Mbokk yi, su fekkee am ngeen lu ngeen di wax nit ñi ngir yokk seen ngëm, waxleen ko.» 16 Noonu Póol daldi jóg te tàllal loxoom ngir ñépp noppi, te ne: «Yeen mbokki Israyil yi ak yeen ñépp ñi ragal Yàlla, dégluleen! 17 Yàlla sunu askan tànn na sunuy maam yokk leen bi ñu nekkee ni gan ci réewu Misra, ba noppi mu génne leen fa ak kàttanam. 18 Lu tollook ñeent fukki at, mu leen di muñal ci màndiŋ ma. 19 Gannaaw loolu mu sànk juróom ñaari xeet ci réewu Kanaan te jox sunu maam yi seen réew. 20 Loolu lépp xew na ci lu tollook ñeenti téeméeri at ak juróom fukk. Gannaaw loolu mu jox leen ay àttekat yi leen di jiite ba jamono yonent Yàlla Samiyel. 21 Noonu ñu ñaan Yàlla mu jox leen buur. Yàlla daldi leen andil Sóol miy doomu Kis, bu soqeekoo ci giiru Beñamin. Sóol nguuru na ñeent fukki at. 22 Yàlla dindi ko ci nguur gi te tànnal leen Daawuda mu nekk seen buur. Yàlla def ci moom seede bii: "Gis naa ci Daawuda doomu Isayi ku neex sama xol. Moom mooy kiy matal sama coobare." 23 Ci noonu Yàlla andil na waa Israyil musalkat bi soqeekoo ci Daawuda ni mu ko dige woon. Moom mooy Yeesu. 24 Bala Yeesu di ñëw, Yaxya mu ngi doon waare, di woo waa Israyil yi yépp mu sóob leen ci ndox ngir ñu wone ne tuub nañu seeni bàkkaar, 25 te bi Yaxya di waaja jeexal liggéeyam ci àddina, mu daldi ne: "Kan ngeen yaakaar ne moom laa? Nekkuma ki ngeen di xaar. Waaye kooku mu ngi ñëw ci sama gannaaw, te yelloowuma sax tekki ay dàllam."»
26 Póol waxaat leen ne: «Yeen sama mbokk yi, yeen sëtu Ibraayma ak yeen ñi ragal Yàlla, nun la Yàlla jagleel kàddu mucc gi. 27 Waa Yerusalem ak seeni njiit xàmmewuñu woon kuy Yeesu. Dañu doon jàng kàddu yonent yi bésu noflaay bu nekk, waaye xamuñu woon li ñuy tekki. Ci noonu bi ñu àttee Yeesu, teg ko daan, matal nañu waxi yonent yii. 28 Doonte gisuñu woon lu jar ñu rey ko, ñaan nañu Pilaat mu reylu ko. 29 Noonu ñu matal lépp li Mbind mi waxoon ci moom. Gannaaw loolu ñu wàcce ko ci bant bi ñu ko daajoon, te tëral ko ci biir bàmmeel. 30 Waaye Yàlla dekkil ko ci ñu dee ñi, 31 te mu feeñu ci ay bés yu bari ñi àndoon ak moom dale ko diiwaanu Galile ba Yerusalem. Te ñoom ñoo nekk léegi ay seedeem ci kanamu askan bi. 32 Te nun, nu ngi leen di yégal xibaar bu baax bi Yàlla digoon sunuy maam. 33 Li Yàlla digoon sunu maam yi, matal na ko ci nun seeni sët, bi mu dekkalee Yeesu, ni mu ko binde ci Sabóor yi, saar ñaar, mu ne: "Yaay sama doom; maay sa baay tey." 34 Yàlla yégle woon na ne dina dekkil Yeesu te Yeesu du dellu ci bàmmeel bi mukk te néewam du yàqu. Loolu la doon wax ne: "Dinaa la jox li ma digoon Daawuda, ay barke yu sell te wóor." 35 Moo tax mu wax feneen ne: "Doo bàyyi sa nit ku sell ki mu yàqu." 36 Daawuda ci boppam, ci jamonoom, doon na liggéey ci coobarey Yàlla, ba noppi mu dee, te ñu suul ko ci wetu ay maamam te néewam yàqu. 37 Waaye ki Yàlla dekkil, néewam yàquwul.
38-39 «Mbokk yi, xamleen ne ci Yeesu lanu leen di yégal mbaalum bàkkaar, te képp ku gëm ci Yeesu, Yàlla dina la àtte ni nit ku jub, te loolu yoonu Musaa mënu ko woona def. 40 Kon nag moytuleen li ñu wax ci téere yonent yi bañ leena dal, bi ñuy wax ne: 41 "Xoolleen, yeen ñiy xeebaate, yéemuleen te réer, ndaxte dinaa def ci seen jamono benn mbir boo xamante ne bu ñu leen ko doon wax sax, doo leen ko mësa gëm."»
42 Bi Póol ak Barnabas di genn kër-ñaan bi, nit ñi ñaan leen ñu delluwaat ci seen njàngale boobu ci bésu noflaay bi ci topp. 43 Amoon na fa ay Yawut ak yeneen nit ñi tuuboon, ñëw ci ngëmu Yawut te ragal Yàlla. Bi mbooloo mi tasee, ñu bari ci ñoom daldi gunge Póol ak Barnabas. Ci seen waxtaan, Póol ak Barnabas di leen ñaax ngir ñu wéy di takku ci yiwu Yàlla.
Póol ak Barnabas jublu nañu ci ñi dul Yawut
44 Bésu noflaay bi ci topp lu gëna bari ci dëkk ba dajaloo nañu ngir déglu kàddu Boroom bi. 45 Waaye Yawut yi, ba ñu gisee mbooloo ma, ñu fees ak iñaan, di weddi li Póol di wax ak di ko saaga. 46 Noonu Póol ak Barnabas tontu leen ak kóolute, ne: «Yeen Yawut yi lanu waroona yégal kàddu Yàlla gi bu jëkk, waaye bañ ngeen ko nangu, te àtte ngeen seen bopp ni nit ñi yelloowul jot dund gu dul jeex ga. Kon nag nu ngi jublu ci ñi dul Yawut. 47 Ndaxte lii la nu Boroom bi sant ci Mbind mi: "Fal naa la ngir nga nekk leer ci biir ñi dul Yawut, ngir nga yóbbu mucc gi ba fi àddina si yem."»
48 Ba ñi nekkul Yawut déggee loolu, ñu daldi am mbégte te màggal kàddu Boroom bi, te ñépp ñi wara jot dund gu dul jeex ga daldi gëm. 49 Kàddu Boroom bi daldi siiw ci réew mi yépp. 50 Waaye Yawut yi di xiir jigéen ñi ragal Yàlla te am tur ak ñi am ndombal-tànk ci dëkk bi ngir ñu bunduxataal Póol ak Barnabas te dàq leen ci seen suuf. 51 Póol ak Barnabas daldi faxas pënd bi nekk ci seeni tànk ngir loolu mën seede réeru ñooñu, te noonu ñu dem ci dëkku Ikoñum. 52 Taalibe yi ci Ancos daldi fees ak mbégte ak Xel mu Sell mi.