Póol ak Barnabas ca dëkku Ikoñum
14
Bi Póol ak Barnabas nekkee ci dëkku Ikoñum, ñu dugg ci kër-ñaanu Yawut yi di wax ba tax mbooloo mu bari daldi gëm, ay Yawut ak ñi dul Yawut. 2 Waaye Yawut yi gëmul woon di xiir ñi nekkul Yawut ba ñu bañloo leen mbokki gëmkat yi. 3 Póol ak Barnabas des ci dëkku Ikoñum lu yàgg di wax ak kóolute lu jëm ci Boroom bi. Boroom bi may leen ñuy def ay màndarga ak ay yëf yu yéeme, te noonu muy wone ne li ñuy wax ci yiwam dëgg bu wér péŋŋ la. 4 Waa dëkk ba daldi xaajaloo. Ñii ànd ak Yawut yi; ñi ci des ànd ak ndaw yi. 5 Yawut yi ak ñi nekkul Yawut ak seen njiit yi daldi lal pexe ngir sonal Póol ak Barnabas te sànni leen ay xeer ngir rey leen. 6-7 Bi Póol ak Barnabas xamee loolu ñu daldi dem ci diiwaanu Likawni, di dëkku Listar ak Derbe ak li leen wër, te foofu ñu wéy di yégle xibaar bu baax bi.Póol ak Barnabas ci dëkku Listar
8 Amoon na benn waay ci dëkku Listar bu doon toog ndaxte dafa judduwaale woon lafañ. Tànkam yi làggi woon te mësula dox. 9 Benn bés mu doon déglu Póol di wax. Póol xool ko ne ko jàkk te gis ne amoon na ngëm ngir mëna wér. 10 Mu wax ak baat bu kawe ne ko: «Jógal, taxaw ci say tànk.» Noonu mu tëb taxaw te tàmbali di dox.
11 Bi mbooloo mi gisee li Póol defoon ñu tàmbali di wax ci làkku waa Likawni, ne: «Yàlla yi soppeeku nañu nit te wàcc ci sunu biir.» 12 Ñuy woowe Barnabas Sës tey woowe Póol Ermes, ndaxte moom mooy ki yor kàddu gi. 13 Amoon na ci buntu dëkk bi benn kër fi ñu doon jaamu seen yàlla Sës. Jébbalkatu-sarax bi doon liggéey ci kër boobu andi ci buntu dëkk bi ay nag yi nga xamante ne dañu leen tegoon ay tóor-tóor. Moom ak mbooloo mi bëggoon nañu rendi nag yooyu ngir màggal Póol ak Barnabas.
14 Bi ndaw yi, maanaam Barnabas ak Póol, yégee loolu, ñu daldi xotti seeni yére te gaawantu ci diggu mbooloo mi di yuuxu naan: 15 «Yeen nit ñi, lan moo tax ngeen di doxale nii? Nun tamit, ay nit lanu ni yeen. Danu ñëw ngir yégal leen xibaar bu baax bi ngir ngeen bàyyi yëf yu amul maana yii te jublu ci Yàlla jiy dund, mi sàkk asamaan, suuf, géej, ak lépp li nekk ci seen biir. 16 Ci jamono yi weesu, Yàlla bàyyi woon na xeet bu nekk mu topp yoonu boppam, 17 moona wone woon na ki mu doon ci lu baax li mu def. Moom moo leen may taw bi jóge ci asamaan ak góob yi ba ngeen am lu bari ci li ngeen lekk, te mu feesal seen xol ak bànneex.» 18 Doonte lépp li Póol ak Barnabas doon wax, ci lu tuuti moo desoon ñu rendil leen sarax.
19 Gannaaw loolu mu am ay Yawut yu jóge woon Ancos ak Ikoñum. Bi ñu yegsee ñu xëcc mbooloo mi ci ñoom, ñu sànni Póol ay xeer ngir rey ko. Ñu daldi ko diri ba génne ko dëkk bi, ñu yaakaar ne dafa dee. 20 Waaye bi ko taalibe yi wëree, mu daldi jóg, dugg ci dëkk bi. Ci ëllëg sa, mu dem ci dëkku Derbe, moom ak Barnabas.
Póol ak Barnabas dellu nañu ca dëkku Ancos bu Siri
21 Póol ak Barnabas yégle nañu xibaar bu baax bi ci dëkku Derbe ba am fa ay taalibe yu bari. Gannaaw loolu, ñu dellu ci dëkku Listar, ci dëkku Ikoñum, ak ci dëkku Ancos ci diiwaanu Pisidi, 22 di dëgëral taalibe yi te di leen ñaax ngir ñu sax ci ngëm gi, te ñu ne leen: «Ak coono yu bari lanuy dugge ci nguuru Yàlla gi.» 23 Ci bépp mbooloo ñi gëm ñu tànn fa ay njiit. Ba noppi ñuy ñaan ak di woor, ñu dénk leen Boroom bi nga xamante ne, moom lañu gëm. 24 Bi ñu fa jógee, ñu jaar li des ci diiwaanu Pisidi ba yegg ci diiwaanu Pamfili. 25 Ñu yégle kàddu Yàlla gi ci dëkku Peers, te noonu ñu dem ci dëkku Atali, fi gaal yi di téere. 26-27 Ñu dugge fa gaal, dem Ancos ci diiwaanu Siri. Mataloon nañu liggéey bi leen Yàlla santoon. Ba ñu yegsee ñu daldi woolu mbooloom ñi gëm, ñi leen dénkaane woon ci yiwu Yàlla ngir ñu def liggéey boobu. Ñu nettali leen lépp li Yàlla def jaarale ko ci ñoom. Ñu nettali leen itam naka la Yàlla ubbee buntu ngëm ci ñi nekkul Yawut. 28 Noonu ñu des fa ab diir bu yàgg ak taalibe yi.