Njiiti mbooloom ñi gëm daje nañu ci Yerusalem
15
Amoon na ay nit ñu jóge woon diiwaanu Yude, ñëw dëkku Ancos. Ñu jàngal mbokki gëmkat yi fa nekk te di leen wax ne: «Bu ngeen xarafuwul ni ko yoonu Musaa santaane, dungeen mëna mucc.» 2 Póol ak Barnabas am nañu ak ñoom werante ba mujje xuloo bu tàng. Noonu mbooloo ñi gëm jël dogal ne Póol, Barnabas, ak yeneeni mbokk dem Yerusalem ci ndawi Yeesu ak njiiti mbooloo ñi gëm yi fa nekk ngir waxtaane fa mbir mi ba leeral ko. 3 Mbooloo ñi gëm jox leen li ñu soxla ci seen tukki. Ñu jaar ci diiwaanu Fenisi ak diiwaanu Samari. Póol ak Barnabas di leen fa nettali ni ñi dul Yawut tuube, topp Boroom bi, te mbokki gëmkat yi am ci mbégte bu réy. 4 Bi ñu yegsee Yerusalem mbooloo ñi gëm bi fa nekk ak seeni njiit ak ndawi Yeesu yi dalal leen. Póol ak Barnabas daldi nettali lépp li Yàlla def jaarale ko ci ñoom. 5 Waaye amoon na fa ñu bokkoon ci tarixa Farisen te gëm ci Yeesu. Ñu daldi jóg te wax ne: «Fàww ñu xarafal ñi dul Yawut te ñu dénk leen ñu déggal yoonu Musaa bi.»
6 Ndaw yi ak njiit yi daldi daje ngir leeral mbir mi. 7 Mu am fa werante bu mag. Piyeer daldi jóg te ne leen: «Samay mbokk, ni ngeen ko xame, ci njàlbéen ba, Yàlla tànn na ma ci seen biir ngir ma yégle xibaar bu baax bi ci ñi dul Yawut, ñu dégg ko te gëm. 8 Yàlla mi xam xol yi, wone na ne nangu na ñi nekkul Yawut bi mu leen joxe Xel mu Sell mi, ni mu nu ko joxe woon, nun itam. 9 Amul benn gënatle ci li Yàlla def ci sunu diggante ak ñoom. Setal na seen xol jaarale ko ci seen ngëm. 10 Léegi nag, lu tax ngeen di seetlu Yàlla, di wut a teg taalibe yi yen bi nga xam ne sunuy maam walla nun sax mësunu ko àttan? 11 Déedéet, nun Yawut yi gëm nanu ne yiwu Boroom bi Yeesu moo nu mëna muccal. Ñoom tamit, ci anam boobu lañu mucce.»
12 Bi mu ko waxee mbooloo mi ne cell, ñu déglu Barnabas ak Póol ñuy nettali màndarga ak ay yëf yu yéeme yi Yàlla def jaarale ko ci ñoom ci biir ñi dul Yawut. 13 Bu ñu waxee ba noppi, Saag jël kàddu gi te ne: «Samay mbokk, dégluleen ma! 14 Simoŋ Piyeer nettali na ni Yàlla ganesee ñi dul Yawut ci njàlbéen ba te tànn ci seen biir ay nit ngir ñu nekk askan bi mu moomal boppam. 15 Te loolu dëppoo na ak kàdduy yonent yi, ndaxte Mbind mi nee na:
16 "Bi loolu weesoo, dinaa dellusi,
yékkëti kër Daawuda bi daanu woon;
ma tabaxaat li yàqu woon
te defaraat ko ba mu jub xocc.
17-18 Noonu li des ci nit ñi di wut Boroom bi,
maanaam ñi dul Yawut yépp,
ñi ma tànn ngir ñu nekk sama moomeel.
Loolu la Boroom bi wax,
moom mi matal li mu waajoona def
te mu yégle woon ko lu yàgg."»
 
19 Saag teg ca ne: «Looloo tax jàpp naa ne warunu sonal ñi dul Yawut te tuub, topp Yàlla. 20 Waaye nanu leen bindal ñu moytu lekk yàppu jur bu ñu saraxe ci xërëm yi, moytu njaaloo, moytu lekk yàppu jur yu ñu rey te deret tuuruwul, ak lekk deret. 21 Ndaxte ci njàlbéen ba tey am na ay nit yuy jàngale yoonu Musaa ci dëkk bu nekk te ñu koy jàng ci kër-ñaan yi ci bésu noflaay bu nekk.»
22 Niki noonu, ndaw yi ak njiit yi ak mbooloom ñi gëm ñépp jël dogal ngir tànn ay nit te yónni leen ca Ancos, ñu ànd ak Póol ak Barnabas. Ñu tànn nag Yudaa mi ñuy woowe Barsabas, moom ak Silas, di ay njiit ci mbokki gëmkat yi. 23 Ñu jox leen bataaxal te lii lañu ci bind: «Yeen sunu mbokk yi dëkk Ancos, Siri, ak Silisi, yeen ñi dul Yawut, nu ngi leen di nuyu, nun ndawi Yeesu yi ak njiiti mbooloo ñi gëm bi nekk Yerusalem. 24 Dégg nanu ne am na ay nit ñu jóge ci nun, ñëw ci yeen, di leen lëjal te di leen jaxase ak seen wax yi, wànte nun, santunu leen ko. 25 Kon nag, nun ñépp déggoo nanu jël dogal ci lu jëm ci loolu ngir tànn ay nit ngir yónnee leen ko ak sunuy soppe Barnabas ak Póol, 26 di ay nit ñi jaay seen dund ngir turu Yeesu Almasi bi sunu Boroom. 27 Kon nungi leen di yónnee Yudaa ak Silas ngir ñu wax leen ci seen gémmiñ li nu bind ci bataaxal bii, 28 ndaxte li neex Xel mu Sell mi te neex nu, mooy nu bañ leena teg beneen yen bu dul dénkaane yii nu mënula ñàkka wax: 29 ngeen moytu lekk yàppu jur bu ñu saraxe ci xërëm yi, ak deret, ak yàppu jur yu ñu rey te deret tuuruwul, ak njaaloo. Bu ngeen moytoo loolu lépp def ngeen lu baax. Jàmm ak jàmm.»
30 Noonu ñi ñu yónni woon tàggoo ak mbokki gëmkat yi, dem dëkku Ancos. Bi ñu yegsee, ñu dajale mbooloo ñi gëm yépp, jébbal leen bataaxal bi. 31 Bi ñu ko jàngee, seen xol sedd ndaxte bataaxal bi ñaax na leen. 32 Yudaa ak Silas ñi doon yonent, ñaax nañu mbokk yi te dëgëral seen ngëm. 33-34 Ñu des fa ab diir ba noppi. Mbokk yi yewwi leen ci jàmm. Ñu dellu ci ñi leen yónni woon. 35 Waaye Póol ak Barnabas ñu des Ancos. Ñoom ak yeneen nit ñu bari, ñuy wéy di jàngale te di yégle xibaar bu baax bi, di kàddu Boroom bi.
Póol ak Barnabas xaajaloo nañu
36 Gannaaw ay fan Póol wax Barnabas ne: «Nanu dellu ci dëkk yépp yi nu yégle woon kàddug Boroom bi, seeti mbokk yi ngir nemmeeku leen.» 37 Barnabas nag dafa bëggoona yóbbaale Yowaana, mi ñuy woowe Màrk, 38 waaye Póol nanguwul woon ñu jël ko ndaxte da leen bàyyi woon ci diiwaanu Pamfili te demul woon ak ñoom ci seen liggéey. 39 Loolu jur na xuloo bu tàng ba ñu mujje xaajaloo. Barnabas jël Màrk, ñu dugg gaal jëm Sippar, di réew mu ndox wër. 40 Póol nag tànn Silas, te gannaaw bi mbokki gëmkat yi dénkaane Póol ci yiwu Boroom bi, ñu dem, 41 jaar ci diiwaanu Siri ak bu Silisi. Póol di dëgëral mbooloo ñi gëm.