Timote fekki na Póol ak Silas ci seen liggéey
16
Póol yegsi ci dëkku Derbe ak bu Listar, mu fekk fa benn taalibe bu tudd Timote te yaayam nekkoon Yawut bu gëmoon ci Almasi bi waaye pàppaam nekkul Yawut. 2 Mbokki gëmkat yi nekkoon Listar ak dëkku Ikoñum, lu baax rekk lañu daan seede ci moom. 3 Póol bëggoon mu ànd ak moom. Mu jël ko nag te xarafal ko ndax Yawut yi nekkoon ci diiwaan boobu, ndaxte ñoom ñépp xamoon nañu ne pàppaam nekkul Yawut. 4 Ci dëkk yépp yi ñu daan jaar, Póol ak Silas ñu ngi daan jottali dogal yi ndaw yi ak njiiti mbooloo ñi gëm yi nekk Yerusalem jël, te ñu sant leen ñu topp ko, 5 te noonu mbooloom ñi gëm gëna dëgër ci seen ngëm te gën di yokku bés bu nekk.
Póol waare na ci diiwaanu Maseduwan
6 Póol ak Silas jaar ca diiwaanu Firisi ak bu Galasi ndaxte Xel mu Sell mi mayu leen woon ñu yégle kàddug Yàlla gi ci diiwaanu Asi. 7 Bi ñu yegsee ci wetu diiwaanu Misi ñu bëggoona dugg diiwaanu Bitini waaye foofu tamit Xelum Yeesu mayu leen ko. 8 Noonu ñu jaar Misi, dem dëkku Torowas, bi nekk ci wetu géej gi. 9 Ci guddi gi, Póol gis ci gént benn waay bu dëkk diiwaanu Maseduwan taxaw ci kanamam ñaan ko, ne: «Jàllsil ba Maseduwan! Wallusi nu.» 10 Bi Póol amee gént boobu, ci saa si, nu fexe dem Maseduwan ndaxte wóoroon nanu ne Yàlla moo nu woo ngir nu yégle fa xibaar bu baax bi.
11 Noonu nu jële gaal ci Torowas, nu jëm ci Samotaras di dëkk bu ndox wër. Ci ëllëg sa nu wéy ak gaal gi ba ci dëkku Neyapolis. 12 Foofu, nu daldi dem ba ci Filib, di dëkk bu gëna am solo ci Maseduwan, te di moomeelu Room. Nu toog fa ay fan. 13 Ci bésu noflaay bi, nu génn dëkk bi dem ci wetu dex bi, ndaxte yaakaaroon nanu ne foofu am na béréb bu nit ñi di ñaane. Amoon na fa ay jigéen. Noonu nu toog di wax ak ñoom. 14 Ci biir jigéen yooyu amoon na benn jigéen bu ragal Yàlla, tuddoon Lidi, cosaanoo woon dëkku Catir, te nekkoon jaaykatu cuub yu xonq yu seer lool. Bi muy déglu, Boroom bi ubbi xolam ngir mu takku ci li Póol doon wax. 15 Nu sóob ko ci ndox moom ak waa këram. Gannaaw loolu mu wax nu: «Ñëwleen, ganesi ma, su fekkante ne jàpp ngeen ne gëm naa Boroom bi.» Te muy wéy di ñaan ngir nu nangu.
Póol ak Silas tëj nañu leen ci kaso ci dëkku Filib
16 Benn bés, bi nuy dem ci bérébu ñaanukaay bi, nu daje ak benn jaam bu jigéen. Dafa amoon rab bu ko doon may muy gisaane. Loolu andiloon na njaatigeem yi xaalis bu bari. 17 Mu topp nu, Póol ak nun, di yuuxu ne: «Nit ñii ñooy jaami Yàlla-Aji-Kawe ji. Dañu ñëw ngir yégal leen yoonu mucc gi.» 18 Mu wéy di ko def ay bés yu bari. Bi Póol sonnee ci wax bi, mu walbatiku te wax rab bi ne: «Maa ngi lay jox ndigal ci turu Yeesu Almasi bi, génnal ci soxna si!» Ci saa si, mu génn ci moom. 19 Bi njaatigeem yi gisee ne seen yaakaar jot xaalis jeex na, ñu jàpp Póol ak Silas te diri leen ci péncu dëkk bi, ci kanamu njiit yi. 20 Ñu andi leen ci kanamu àttekat yi, di leen tuumaal, naan: «Nit ñii ay Yawut lañu. Ñooy jaxase sunu dëkk bi, 21 di jàngale ay aada yoo xamante ne, sañuñu leen nangu mbaa topp leen, nun ñi bokk ci waa Room.» 22 Mbooloo mi ànd ci, ñu dal ci kaw Póol ak Silas. Àttekat yi simmilu seen yére, santaane ñu dóor leen ay yet. 23 Bi ñu leen dóoree ay yet yu bari ba noppi, ñu tëj leen ci kaso bi, te jox ndigal garjen bi ngir mu sàmm leen bu baax. 24 Bi ñu ko waxee loolu, mu tëj leen ci néeg bi gëna ruqe ci kaso bi. Mu tëj seen tànk yi ci ay bant dénk.
25 Ci xaaju guddi Póol ak Silas ñu ngi doon ñaan Yàlla te di ko sant ak ay woy, te ñeneen ñi ñu tëjoon ci kaso bi di leen déglu. 26 Jekki jekki, benn yëngu-yëngu suuf bu mag dal ci biir kaso bi te fondamaa kaso bi yëngu. Ci saa si, bunt yi ci kaso bi yépp ubbeeku, te ñépp ñi ñu tëjoon ci kaso bi seen ceen yi dagg. 27 Garjen bi yeewu, mu gis ne buntu kaso yi tijjeeku nañu. Mu daldi jël jaaseem, nara xaru, ndaxte dafa foogoon ne ñi ñu tëjoon ci kaso bi dañoo daw. 28 Waaye Póol yuuxu ak baat bu kawe ne ko: «Bul gaañ sa bopp, nun ñépp nu ngi fi.» 29 Garjen bi laaj làmp, mu gaawantu dugg ci biir, te daanu ci tànki Póol ak Silas di lox. 30 Noonu mu génne leen ci kaso bi te laaj leen, ne: «Kilifa yi, lan laa wara def ngir mucc.» 31 Póol ak Silas tontu ko ne: «Gëmal Boroom bi Yeesu te dinga mucc yaw ak sa waa kër.» 32 Noonu ñu yégal ko kàddug Boroom bi, moom ak waa këram yépp. 33 Ci waxtu boobu ci guddi, mu jël leen te faj seen gaañu-gaañu yi. Ñu daldi koy sóob ci ndox, moom ak waa këram yépp. 34 Mu yóbbu leen ci këram, mu jox leen ñu lekk, te muy bànneexu, moom ak waa këram yépp, ndax li ñu gëm ci Yàlla.
35 Bi bët setee àttekat yi yónnee ay takk-der ci kaso bi ngir ñu wax garjen bi ne: «Bàyyil nit ñii, ñu dem.» 36 Garjen bi daw, yégal loolu Póol, ne: «Àttekat yi yónnee nañu ngir ma bàyyi leen, ngeen dem. Léegi nag mën ngeen dem ci jàmm.» 37 Waaye Póol wax ak takk-der yi ne leen: «Ñoom, dóor nañu nu ay yet ci kanamu ñépp. Jaarunu ci àtte, nun ñii bokk ci waa Room, ba noppi ñu sànni nu ci kaso. Léegi nag, dañu jóg ngir génne nu ci kaso bi te kenn du ko yég? Loolu du am mukk! Ñoom ci seen bopp, nañu ñëw génne nu.» 38 Noonu, takk-der yi dem, yégal kàddu yooyu àttekat yi. Bi ñu yégee ne ci waa Room lañu bokk, ñu daldi tiit. 39 Ñu ñëw, ñoom ci seen bopp, jéggalu, te génne leen ci kaso bi, te ñu ñaan leen ngir ñu génn ci seen dëkk. 40 Bi ñu génnee ci kaso bi Póol ak Silas dem ci kër Lidi. Ñu fekk fa mbokki gëmkat yi yépp te di leen ñaax. Gannaaw loolu nu jëlaat seen yoon.