Póol ak Silas ci dëkku Tesalonig ak bu Bere
17
Póol ak Silas jaar ci dëkku Amfipolis ak bu Apoloni ba yegg dëkku Tesalonig. Foofu Yawut yi amoon nañu benn kër-ñaan. 2 Póol dugg ci kër-ñaan bi, ni mu ko tàmme woon di def. Mu tegle ñetti bésu noflaay di fa dem di waxtaan ak ñoom ci lu jëm ci Mbind mi. 3 Mu leen di faramfàcceel Mbind mi di leen won ci li mu wax ne: Almasi bi dafa waroona sonn ba dee te dekki ci ñu dee ñi. Mu ne: «Yeesu mi ma leen di yégal, mooy Almasi bi.» 4 Ñenn ci Yawut yi ak mbooloo mu takku ci ñi dul Yawut te ragal Yàlla ak ay jigéen yu bari yu am tur nangu nañu li leen Póol ak Silas wax te ñu topp leen.
5 Waaye iñaan jàpp yeneen Yawut yi, ñu dajale ñiy taxawaalu ci mbedd yi. Ñooñu xiir askan bi te jaxase dëkk bi. Ñu song këru benn waay bu tudd Yason. Ñu di fa seet Póol ak Silas ngir yóbbu leen ci kanamu askan bi, 6 waaye fekkuñu leen fa. Noonu ñu diri Yason ak ñenn ci mbokki gëmkat yi ñu fekkoon ci këram ba ci kanamu njiiti dëkk bi. Ñu tàmbali di yuuxu, naan: «Nit ñooñu ñooy jaxase àddina sépp, léegi nag yegsi nañu ba fii. 7 Yason dalal na leen këram. Ñoom ñépp nag ñu ngi def lu wuute ak li Sesaar digle, ndaxte dañu wax ne am na beneen buur bu tudd Yeesu.» 8 Bi ñu déggee kàddu yooyu, askan bi ak njiit yi daldi jaaxle. 9 Njiiti dëkk ba daan Yason ak ñi mu àndaloon, feyloo leen xaalis, ba noppi, bàyyeegum leen ñu dem.
10 Bi guddi jotee mbokki gëmkat yi def ba Póol ak Silas dem dëkku Bere. Bi ñu yegsee foofu, ñu dem ci kër-ñaanu Yawut yi. 11 Yawutu Bere yi ñoo ëpp teggin Yawutu Tesalonig yi. Ñu nangu kàddug Yàlla gi ak mbégte mu réy, te bés bu nekk ñu ngi doon gëstu Mbind mi ngir xam ndax li leen Póol wax dëgg la walla déet. 12 Te noonu ñu bari ci ñoom gëm. Ñu bari ci ñi nekkul Yawut yi gëm nañu tamit, di jigéen yu am tur ak ay góor.
13 Waaye bi Yawutu Tesalonig yi yégee ne Póol mu ngi yégle kàddug Yàlla gi ci Bere tamit, ñu ñëw, andi fa coow, te jaxase askan bi. 14 Noonu mbokki gëmkat yi gaawantu yóbbu Póol ba ci wetu géej gi. Silas ak Timote des ca Bere. 15 Ñi gunge woon Póol ànd ak moom ba ci dëkku Aten. Ñu dellu Bere, Póol yóbbante leen ñu wax Silas ak Timote ñu fekki ko ci ni mu gëna gaawe.
Póol yégle na xibaar bu baax bi ci dëkku Aten
16 Ci waxtu bi Póol di xaar Silas ak Timote ci dëkku Aten, xolam jeex bi mu gisee dëkk bi fees dell ak ay xërëm. 17 Mu dugg ci kër-ñaan bi di waxtaan ak Yawut yi ak ñi dul Yawut te ragal Yàlla. Te itam bés bu nekk mu ngi doon waxtaan ak ñépp ñi mu dajale woon ci péncu dëkk bi. 18 Amoon na ay boroom xam-xam yu bokk ci mbooloo mi ñuy woowe Epikuren ak mbooloo mi ñuy woowe Estowisen. Ñenn ci ñoom doon nañu waxtaan ak Póol. Ñenn ñi di wax ne: «Kii lu muy kebetu?» Ñeneen ni di tontu ne: «Dafa mel ni mu ngi yégle ay yàlla yu nu xamul,» ndaxte Póol doon na yégle Yeesu ak ndekkitel bi. 19 Noonu ñu jël ko, ànd ak moom ba ci ëttu àttekaay bi ñuy woowe Areyopas. Ñu wax ko ne: «Li ngay jàngale, lu bees la ci nun. Leeralal nu ko, 20 ndaxte tànkal nga nu ak ay wax yu kenn xamul, te nun bëgg nanu xam li loolu di tekki.» 21 Booba waa Aten yépp, ak gan ya ca dëkk ba, wax ak déglu xibaar yu bees rekk lañu nekke woon.
22 Noonu Póol taxaw ci diggu ëttu àttekaayu Areyopas, te ne leen: «Yeen waa Aten, gis naa ne ci mbirum diine ci anam bu nekk takku ngeen ci bu baax, 23 ndaxte bi ma doon doxantu ci seen dëkk, may xool li ngeen di jaamu, seetlu naa itam benn saraxlukaay, ñu bind fa: ngir Yàlla mi nu xamul. Li ngeen di jaamu nag te xamuleen ko, moom laa leen di yégal. 24 Yàlla mi sàkk àddina si ak lépp li nekk ci biiram di boroom asamaan ak suuf du dëkk ci kër yi loxoy nit tabax. 25 Moom, soxlawul dara ba nit di ko liggéeyal, ndaxte moom mooy jox ñépp bakkan, ñuy noyyi, ak leneen lépp. 26 Moo sàkk xeet yi yépp, jaarale ko ci benn nit, mu may leen ñu dëkk fépp ci suuf si. Mu àppal seen jamono yi te rëdd bérébu dëkkuwaayu ku nekk ak fi mu yem. 27 Yàlla def na loolu ngir nit ñi di ko wut, xéy-na ñu làmbatu ba daj ko, fekk sax soriwul kenn ci nun. 28 Ndaxte ci moom lanuy dunde, di yëngu, te nekk, ni ko woykat yi waxe woon ne: "Nun ay doomam lanu." 29 Kon ndegam ay doomu Yàlla lanu, warunu xalaat ne Yàlla niroo na ak ay yëf yu nit defare wurus, xaalis, ak xeer ci ay loxoom jaarale ko ci ay xalaatam. 30 Yàlla xoolatul jamono yi ko nit ñi xamul woon, waaye léegi mu ngi woo ñépp fu waay mëna nekk ngir ñu tuub seeni bàkkaar, 31 ndaxte jàpp na bés bi muy àtte àddina si yépp ak njubte. Tànn na ki wara àtte te dekkil ko ci biir ñu dee ñi. Te ci noonu Yàlla won na ñépp firnde ne nit kooku la tànn ngir mu àtte.»
32 Bi ñu déggee Póol wax ci mbirum ndekkitelu ñu dee ñi, ñenn ñi di ñaawal Póol, waaye ñeneen ñi di wax ne: «Beneen yoon, dinanu la dégluwaat ci lu jëm ci mbir yooyu.» 33 Noonu Póol jóge ci seen ndaje ma. 34 Moona ñenn ci ñoom taq ci moom te gëm. Ñoo doon benn waay bu tudd Denis te bokk ci mbooloom Areyopas, benn jigéen bu tudd Damaris, ak ñeneen.