Póol waare na ci dëkku Korent
18
Gannaaw loolu Póol jóge ci dëkku Aten, dem ci dëkku Korent. 2 Mu fekk fa benn Yawut bu tudd Akilas te mu juddoo ci diiwaanu Pont. Mu ngi soga jóge ci réewu Itali, moom ak jabaram Pirsil ndaxte Sesaar Këlódd moo joxe woon ndigal ngir Yawut yi yépp génn ci dëkku Room. Póol dem ci ñoom. 3 Mu dal ci seen kër di liggéey ak ñoom ndaxte dañu bokkoon benn liggéey, maanaam di defar ay mbaar. 4 Bésu noflaay bu nekk Póol da doon waxtaan ak Yawut yi ak ñi nekkul Yawut ci kër-ñaan bi, di leen wuta gëmloo. 5 Waaye bi Silas ak Timote jógee ci diiwaanu Maseduwan yegsi Korent, Póol daldi jublu ci yégle kàddug Yàlla gi. Muy seede ci kanamu Yawut yi ne Yeesu mooy Almasi bi. 6 Waaye bi ñooñu gàntoo njàngaleem te di ko saaga, mu fëgg pënd bi takk ci yéreem yi te ne leen: «Bu ngeen sànkoo, yeena ko teg seen bopp. Set naa ci wecc. Léegi nag dinaa dem ci ñi nekkul Yawut.» 7 Noonu mu génn foofu, dem ci kër benn waay bu tudd Tisiyus Yustus. Mu nekkoon ku ragal Yàlla te këram nekkoon ci wetu kër-ñaan bi. 8 Kirispus, mi nekkoon njiitu kër-ñaan bi gëm ci Boroom bi, moom ak njabootam yépp. Ñu bari ci dëkku Korent doon nañu déglu Póol, ñu gëm tamit te ñu sóob leen ci ndox.
Yawut yi ci dëkku Korent tuumaal nañu Póol
9 Benn guddi Boroom bi wax ak Póol ci benn gis-gis, ne: «Bul ragal dara. Waxal te baña noppi. 10 Maa ngi ak yaw te kenn du la mëna teg loxo ba di la sonal, ndaxte bari na ñi ma moom ci dëkk bii.» 11 Noonu Póol des ca Korent benn at ak genn-wàll, di jàngale kàddug Yàlla gi ci seen biir.
12 Ci jamono ji Galyon yilifoon diiwaanu Akayi, Yawut yi jóg, mànkoo ngir jàpp Póol. Noonu ñu yóbbu ko ci ëttu àttekaay bi 13 te ñuy wax naan: «Nit kii mu ngi xiir nit ñi, ñuy jaamu Yàlla ci lu àndul ak yoonu Musaa.» 14 Póol mu ngi doon waaja tontu, waaye Galyon wax Yawut yi ne: «Su fekkoon ne ay mbir yu jubadi la walla ay ñaawteef, doon naa leen déglu ni mu ware, 15 waaye ndegam ay werante la ci mbirum wax ak tur ak lu jëm ci seen yoonu bopp, seen wàll la. Du mbir yu mel noonu laay àtte.» 16 Noonu mu génne leen ci ëttu àttekaay bi. 17 Ci kaw loolu ñoom ñépp jàpp Sosten mi doon njiitu kër-ñaan bi te ñu dóor ko ci kanamu bérébu àttekaay bi, waaye Galyon faalewul leen.
Póol dellusi na ci dëkku Ancos bu Siri
18 Póol desaat lu yàgg ci dëkku Korent. Gannaaw loolu mu tàggoo ak mbokki gëmkat yi. Mu jël gaal ngir dem ci diiwaanu Siri. Mu ànd ak Pirsil ak Akilas. Laata muy dem, Póol watlu boppam ci dëkku Señsere ndaxte dafa am lu mu waataloon Yàlla. 19 Bi ñu teeree ci dëkku Efes, Póol bàyyi fa ñi mu àndaloon. Moom mu dugg ci kër-ñaan bi di waxtaan ak Yawut yi. 20 Bi ko ñooñu ñaanee ngir mu des fa ay fan, nanguwul woon, 21 waaye bi muy tàggoo ak ñoom mu wax leen kàddu yii: «Su ko Yàlla bëggee, dinaa dellusi seetsi leen.» Mu jëlaat gaal, jóge Efes. 22 Bi mu yegsee ci dëkku Sesare, mu dem Yerusalem. Foofu, mu nuyu mbooloo ñi gëm. Gannaaw loolu, mu dellu dëkku Ancos.
Apolos waare na ci dëkku Efes ak bu Korent
23 Póol des na Ancos ay fan. Gannaaw loolu mu jóge fa, jaar diiwaanu Galasi ak diiwaanu Firisi di dëgëral taalibe yépp.
24 Ci jamono jooju, benn Yawut bu tudd Apolos te cosaanoo Alegsàndiri ñëw na Efes. Xamoon na Mbind mi bu baax te di wax ak kàddu yu rafet. 25 Jàngaloon nañu ko bu baax yoonu Boroom bi, te sawaroon na di wax lu wóor ci lu jëm ci Yeesu. Waaye xamul woon lu dul sóobu ndox bu Yaxya. 26 Mu tàmbali di wax ak kóolute ci biir kër-ñaan bi. Pirsil ak Akilas, bi ñu ko déggee muy wax, ñu jël ko ngir ñu faramfàcceel ko yoonu Yàlla ba mu leer ci moom.
27 Gannaaw loolu Apolos bëggoon na dem diiwaanu Akayi. Mbokki gëmkat yi ànd ci loolu, bind taalibe yi nekk dëkku Korent ngir ñu dalal ko bu baax. Bi mu yegsee foofu mu amal njériñ bu réy ñi gëm jaarale ko ci yiwu Yàlla, 28 ndaxte mu ngi doon daaneel Yawut yi ci wax ci kanamu ñépp, te jaarale ko ci Mbind mi, mu ngi doon wone ne Yeesu mooy Almasi bi.