Ay taalibe ci dëkku Efes jot nañu Xel mu Sell mi
19
Bi Apolos nekkee Korent, Póol jaar ci diiwaani tundi Asi, mu doora yegsi dëkku Efes. Mu fekk fa ay taalibe 2 te laaj leen ne: «Ndax jot ngeen Xel mu Sell mi gannaaw bi ngeen gëmee?» Ñu tontu ko ne: «Mësunu dégg sax ne Xel mu Sell mi am na.» 3 Póol laajaat leen ne: «Kon ban sóobu ndox lañu leen sóob?» Ñu ne ko: «Xanaa bu Yaxya.» 4 Póol ne leen: «Waaw, Yaxya daan na sóob ci ndox ñi nangu woona tuub seeni bàkkaar te mu daan wax askanu Israyil ngir ñu gëm ci ki wara ñëw ci gannaawam. Kooku mooy Yeesu.» 5 Gannaaw bi ñu déggee loolu, ñu sóob leen ci ndox ci turu Boroom bi Yeesu. 6 Póol teg leen loxo te Xel mu Sell mi wàcc ci ñoom. Ñu tàmbali di wax yeneeni kàllaama te di wax ci turu Yàlla. 7 Ñi ñu sóoboon ci ndox tollu woon nañu ci fukki nit ak ñaar.Póol waare na ci dëkku Efes
8 Gannaaw loolu Póol dugg ci kër-ñaan bi. Noonu muy wax ak kóolute lu tolloo ci ñetti weer ci lu jëm ci nguuru Yàlla gi, te muy wuta gëmloo ñi ko doon déglu. 9 Waaye ñenn ci ñoom, ñu dëgër bopp, baña gëm. Ñuy wax lu bon ci yoonu Boroom bi ci kanamu mbooloo mi yépp. Póol daldi leen bàyyi te jël taalibe yi, di leen jàngal bés bu nekk ci bérébu jàngukaay bu Tiranus. 10 Loolu wéy ba ci diirub ñaari at ba tax ñépp ñi dëkk ci diiwaanu Asi, Yawut yi ak ñi dul Yawut dégg kàddu Boroom bi.
Doomu Sewa yi
11 Ci jamono jooju, Yàlla di def kéemaan yu yéeme jaarale ko ci loxoy Póol. 12 Demoon nañu sax bay jël ay sër walla ay sagar yu mësoona laal yaramu Póol. Ñu teg ko ci kaw ñu feebar, te noonu, nit ñi di wér te rab yi di génn ci ñoom. 13-14 Amoon na benn Yawut bu tudd Sewa, di jébbalkatu-sarax-bu-mag. Moom amoon na juróom ñaari doom yu góor, yu doon dem dëkk ak dëkk di dàq ay rab yi nekkoon ci ay nit. Ñoom tamit ñu doon jéema dàq rab yi ci turu Yeesu, di wax ne: «Maa ngi leen di jox ndigal ci turu Yeesu mi Póol di waare, génnleen.» 15 Waaye bi ñu ko defee, rab bi tontu leen ne: «Xam naa Yeesu te xam naa Póol. Waaye yeen, kan ngeen doon?» 16 Nit ki rab jàppoon daldi leen song te fitnaal leen ba ñu génn kër gi, yaramu neen ak ay gaañu-gaañu. 17 Loolu siiw ci ñépp ñi dëkk Efes, ñiy Yawut ak ñiy dul Yawut. Ñépp nekk ci tiitange te ñuy màggal turu Boroom bi Yeesu.
18 Amoon na ñeneen nit ñu bari yu daan def ay jëf yu bon, waaye ñëwoon nañu ci ngëm gi. Ñu daldi wax ci kanamu ñépp lépp li ñu daan def. 19 Ñu bari ci ñi daan luxus, jël seen téere, dajale leen, taal leen ci kanamu ñépp. Njégu téere yi yépp tolloo woon na ci juróom fukki junni xànjaru xaalis. 20 Ci noonu kàddu Boroom bi di gëna siiw ci kàttanu Boroom bi.
Yëngu-yëngu ci dëkku Efes
21 Gannaaw loolu Póol jàpp ci xelam dem Yerusalem, jaare ko diiwaanu Maseduwan ak bu Akayi. Muy wax ne: «Gannaaw bu ma yeggee Yerusalem, war naa dem ba Room tamit.» 22 Noonu mu yónni ca Maseduwan ñaar ci ñi ko doon jàppale ci liggéey bi, Timote ak Erast, waaye moom, mu des ay fan ca Asi.
23 Ci jamono boobu yëngu-yëngu bu réy amoon na ndax yoonu Boroom bi. 24 Amoon benn tëggkatu xaalis bu tudd Demetirus. Mu doon tëgge xaalis ay yëf yu ndaw yu nirook këru màggalukaayu Artemis, seen yàlla bu jigéen bi. Loolu andiloon na ko xaalis bu bari, moom ak ñi mu àndaloon ci liggéey bi. 25 Mu dajale ñi ko daan liggéeyal ak ñeneen ñiy def liggéey bu niroo ak bosam, ne leen: «Samay xarit, xam ngeen ne lépp li nu am ci alal, ci liggéey bii lay jóge. 26 Waaye Póol, mu ngi wax ne yàlla yi nit di defar ci loxoom nekkul yàlla yu dëgg. Moom xëcc na nit ñu bari ci gëm-gëm boobu, te yemul rekk ci Efes waaye wasaare na ko fépp ci diiwaanu Asi. Te yeen, gis ngeen li xew te dégg ko. 27 Loolu mën na tax sunu liggéey daanu. Waa Asi yépp ak àddina sépp dañuy màggal Artemis ku mag ki, sunu Yàlla bu jigéen bi te ñuy wormaal këru màggalukaayam. Njàngale Póol moomu mën na tax nit ñi dootuñu ko wormaal te dootuñu jaamu Artemis.» 28 Bi ñu déggee loolu, ñu daldi fees ak mer te tàmbali di yuuxu naan: «Artemis bu Efes ku mag la.» 29 Ci noonu dëkk bi yépp daldi jaxasoo te ñépp gaawantu jëm ci bérébu fowukaay bi. Ñu jàpp tamit Gayus ak Aristàrk, ñaar ci waa Maseduwan, yi doon ànd ak Póol, te yóbbu leen.
30 Póol bëggoon na dem ci kanamu mbooloo mi waaye taalibe yi tere ko ko. 31 Ñenn ci xaritam yi sax daan liggéey ci nguur ci diiwaanu Asi, ñu yónnee ci moom ndaw ngir mu ñaan ko mu baña teg tànkam ci béréb boobu.
32 Ci waxtu boobu ña dajaloo woon foofu di wax ci seen biir, coow li ne kur. Ñi di yuuxu lii, ñenn ñi di yuuxu leneen. Te ñu bari ci ñoom xamuñu woon li waral ndaje ba. 33 Amoon na ki ñuy wax Alegsàndar. Moom la Yawut yi jiitaloon ngir mu layool leen ci kanamu mbooloo mi. Mu yékkëti loxoom ngir wax ak mbooloo mi, 34 waaye bi mbooloo mi xamee ne moom Yawut la, ñu ànd ñoom ñépp di yuuxu ci kaw diiru ñaari waxtu, naan: «Artemis bu Efes ku mag la.»
35 Bindkatu dëkk bi moo leen mujje noppiloo, ne leen: «Yeen waa Efes, kan moo xamul ne dëkku Efes mooy garjenu kër Artemis bu mag bi ak jëmmam bi daanoo ci asamaan? 36 Loolu kenn mënu ko weddi. Kon nag àndleen ak dal, baña gaawantu, ngeen xalaat bu baax bala ngeen di jëf. 37 Andi ngeen fi nit ñii, moona sàccuñu dara ci këru Artemis te saagawuñu sunu yàlla bu jigéen bi. 38 Su fekkee ne Demetirus ak liggéeykat yi ànd ak moom dañu jote ak kenn, nañu dem ci yoon, ndaxte am nañu ay bés yi ñuy àtte te am na ay àttekat. 39 Su ngeen amee leneen li ngeen wara laaj, dinañu ko àtte ci bésu daje bi. 40 Ragal naa ne nguuru Room dinañu jàppe ne nun nooy ñiy yëngal dëkk bi, ndax li xew tey. Bu loolu amee, amunu lenn lu nu mëna lay ngir wone li waral lii.» Gannaaw bi mu leen waxee kàddu yooyu mu yewwi mbooloo ma.