Póol tukki na ci diiwaanu Maseduwan ak ci réewu Geres
20
Bi yëngu-yëngu yooyu dalee, Póol dajale taalibe yi, ñaax leen, te tàggoo ak ñoom. Gannaaw loolu mu jóge fa ngir dem diiwaanu Maseduwan. 2 Noonu mu wër ci diiwaan boobu, di ñaax mbokki gëmkat yi ak kàddu yu bari. Gannaaw loolu mu dem réewu Geres, 3 des fa ñetti weer. Bi mu bëggee dugg gaal ngir dem diiwaanu Siri, Yawut yi di ko fexeel. Mu yég ko. Noonu mu jël dogal jaaraat Maseduwan. 4 Ñii la àndaloon: Sopater di doomu Pirus mi cosaanoo dëkku Bere; Aristàrk ak Sekundus, di waa dëkku Tesalonig; Gayus mi dëkk Derbe; Timote; ak tamit Tisig ak Torofim, ñiy waa diiwaanu Asi. 5 Ñooñu ñoo jiituwoon te di nu xaar ca dëkku Torowas. 6 Nun nag dugge nanu gaal ci dëkku Filib gannaaw màggalu mburu mu amul lawiir wi. Gannaaw juróomi fan ci géej gi, nu fekki leen ca Torowas. Nu def fa juróom ñaari fan.
Póol dekkil na Ëtikus ci turu Yeesu
7 Dimaas dajaloo nanu di damm mburu mi. Noonu Póol am waxtaan ak taalibe yi te wéyal njàngaleem ba xaaju guddi ndaxte moom dafa waroona wéyal tukkeem ca ëllëg sa. 8 Amoon na làmp yu bari ci néeg bi ñu dajaloo woon te mu féete ci kaw. 9 Mu am benn waxambaane bu tudd Ëtikus te toogoon ci catu palanteer bi. Mu jàppante ak nelaw bi Póol di wéy ci njàngaleem. Nelawam xóot ba tax mu jóge ci ñetteelu taax ba, daanu ci suuf. Bi ñu ko yékkëtee, fekk dee na. 10 Póol daldi wàcc, mu tiim ko, jël ko ci ay loxoom te wax ne: «Dalleen ndaxte mu ngi dund.» 11 Noonu bu mu yéegaatee, mu damm mburu mi te nu lekk. Mu wéyaat di wax ba bët set, mu daldi dem. 12 Waxambaane bi nag, ñu yóbbu ko këram, muy dund. Te ñépp seen xel dal ci bu baax.
Tukki Póol ci dëkku Torowas ba ci dëkku Mile
13 Gannaaw loolu nu jiitu Póol, nu jël gaal ngir dem dëkku Asos fi mu waxoon nu fekk ko, waaye moom ci boppam dafa bëggoona dox ba yegsi fa. 14 Bi mu nu dabee ci Asos, nu jël ko ci gaal gi te nu dem dëkku Mitilen. 15 Nu jóge fa, jëlaat géej gi. Ci ëllëg sa, nu yegsi ci kanamu Kiyos di réew mu ndox wër. Gannaaw ëllëg sa nu yegsi ci Samos, di dëkk bu ndox wër, te ci ñeenteelu fan ba nu yegsi ci dëkku Mile. 16 Póol jëloon na dogal romb Efes te bañ fa taxaw di ñàkk ay fan ci diiwaanu Asi, ndaxte moom dafa yàkkamti woon ngir yegg Yerusalem ci bésu Pàntakot bi, su mënee nekk.
Póol tàggoo na ak njiiti mbooloo ñi gëm ci Efes
17 Bi mu nekkee ci dëkku Mile, Póol yónnee na ci Efes ngir ñu woolu njiiti mbooloom ñi gëm. 18 Bi ñu yegsee ci moom mu ne leen: «Xam ngeen bu baax ni ma meloon ak yeen ci waxtu yépp yi ma nekke woon ak yeen dale ko ci bés bi ma jëkka teg tànk ci diiwaanu Asi. 19 Dama doon liggéeyal Boroom bi ci suufeelu ak ci ay rongooñ ci diggi jafe-jafe yi ma dund jaarale ko ci pexey Yawut yi. 20 Xam ngeen ne man nëbbuma leen dara ci li leen di jural njériñ. Yégal naa leen lépp te jàngal naa leen ci kanamu mbooloo yi ak ci seen kër yi. 21 Noppiwuma di yégal Yawut yi ak ñi dul Yawut ngir ñu tuub seeni bàkkaar te ñëw ci Yàlla te gëm ci Yeesu sunu Boroom.
22 «Léegi nag, xoolleen! Xel mu Sell mi moo ma xiir, ma dem Yerusalem, wànte xamuma lan moo ma fay xaar. 23 Xam naa rekk ne, Xel mu Sell mi moo may artu ci dëkk ak dëkk ne kaso ak metit ñoo may xaar. 24 Waaye sama dund amul solo ci man. Li ma soxal rekk mooy bey sama sas ba matal liggéey bi ma Boroom bi Yeesu dénk maanaam yégle xibaar bu baax biy wone yiwu Yàlla.
25 «Léegi nag xam naa ne dootuleen gis sama xar kanam, yeen ñépp ñi ma doon waare nguuru Yàlla gi. 26 Moo tax maa ngi leen koy wax tey ji: def naa lépp li ma mënoon. Su kenn ci yeen réeree doonatuma ci dara, 27 ndaxte xamal naa leen tëralinu Yàlla bépp te nëbbuma leen ci dara. 28 Sàmmleen nag seen bopp ak gétt gi leen Xel mu Sell mi dénk ngir ngeen sàmm ko, maanaam mbooloom ñi gëm bi Yàlla moom, te jotal ko boppam jaarale ko ci deretu doomam. 29 Xam naa ne bu ma leen wonee gannaaw, ay nit dinañu dugg ci seen biir, mel ni ay bukki yu soxor te duñu am yërmande ci gétt gi. 30 Ci seen biir sax dina am ay nit yuy wax lu dul dëgg ngir xiir taalibe yi ñu topp leen. 31 Moytuleen nag, te ngeen fàttaliku ne lu tollu ci ñetti at, guddi ak bëccëg, maa ngi doon artu ku nekk ci yeen ak ay rongooñ.
32 «Léegi nag dénk naa leen Yàlla, moom ak kàddug yiwam. Moo am doole dëgëral leen ngir ngeen mëna jot ndono bi mu dencal ñépp ñi mu moom. 33 Xemmemuma xaalisu kenn, walla wurusam walla yéreem. 34 Yeen ci seen bopp xam ngeen ne dama doon liggéey ci samay loxo ngir faj samay soxla ak soxla ñi ma àndal. 35 Won naa leen ci lépp ne nii ngeen wara liggéeye ngir dimbale néew di doole yi. Nanu fàttaliku kàddu Boroom bi Yeesu bi mu waxee moom ci boppam ne: "Joxe moo ëpp barke nangu."»
36 Gannaaw bi mu waxee loolu, mu daldi sukk di ñaan ak ñépp. 37 Noonu ñépp di jooy te laxasu ci baatu Póol, di ko fóon. 38 Li leen gëna yokk tiis mooy li mu leen wax ne dootuñu gis xar-kanamam. Gannaaw loolu ñu gunge ko ba ci gaal bi.