Póol ci yoonu Yerusalem
21
Gannaaw bi nu tàggatoo ak ñoom, danu jël gaal jublu Kos di réew mu ndox wër. Ca ëllëg sa ñu wéyal sunu yoon ba yegsi dëkku Rodd. Nu jaare foofu, dem dëkku Patara. 2 Nu fekk fa gaal buy dem diiwaanu Fenisi. Nu yéeg ci, dem. 3 Bi nu demee bay séen Sippar di réew mu ndox wër, nu romb ko, mu féete nu càmmoñ. Nu wéyal sunu yoon, dem booru diiwaanu Siri, ngir mëna wàcc dëkku Tir, fi gaal gi waroona wàcce li mu yeboon. 4 Nu seet fa ba gis ay taalibe te des ak ñoom lu tollu ci juróom ñaari fan. Xel mu Sell mi xiir leen ñu wax Póol ngir mu baña dem Yerusalem. 5 Waaye bi juróom ñaari fan yi matee, nu jóg ngir wéyal sunu yoon. Ñu gunge nu, ñoom ñépp ak seen jabar yi ak seen doom yi ba nu génn dëkk ba tuuti. Foofu nu sukk ci tefes gi ngir ñaan. 6 Gannaaw loolu, nu tàggatoo. Nun nu yéeg gaal ga, ñoom ñu ñibbi.
7 Gannaaw loolu nu jóge Tir te dem dëkku Patolemayis. Noonu nu jeexal sunu tukki ci géej gi. Ci Patolemayis nu nuyu sunu mbokki gëmkat yi te yendook ñoom. 8 Ci ëllëg si nu jóge foofu, dem Sesare, dal kër Filib, waarekatu xibaar bu baax bi. Filib bokkoon ci juróom ñaari nit ñi ñu tànnoon ci Yerusalem. 9 Amoon na ñeenti doom yu jigéen yu xamul góor te ñu nekkoon ay yonent.
10 Bi nu fa nekkee ay fan, benn yonent bu tudd Agabus ñëw. Mu ngi jóge woon diiwaanu Yude. 11 Bi mu yegsee ci nun, mu jël takkukaayu ndiggu Póol, mu takk loxoom yi ak tànkam yi. Mu ne: «Xoolleen! Lii la Xel mu Sell mi wax: "ki moom takkukaayu ndigg bii, Yawut yi dinañu ko takke nii ci Yerusalem, jébbal ko ñi dul Yawut."» 12 Bi nu déggee loolu, nun ak waa Sesare, nu ñaan Póol ngir mu baña dem Yerusalem. 13 Waaye mu tontu nu ne: «Lan ngeen di def nii, di jooy, di jeexal sama xol. Waaj naa, du rekk ngir ñu yeew ma, waaye taxaw naa ngir dee ca Yerusalem ndax turu Boroom bi Yeesu.» 14 Gannaaw mënunu woon tax mu soppi xalaatam, nu bàyyi di ko ñaan te wax ne: «Na coobarey Boroom bi am.»
15 Nu teg ca ay fan, nu waaj, daldi tegu ci yoonu Yerusalem. 16 Ay taalibe yu dëkk Sesare gunge nu ci kër benn waay bu nu wara dalal ku tudd Manason. Waa Sippar la woon te yàgg na nekk taalibe.
Póol daje na ak njiiti mbooloo ñi gëm ci Yerusalem
17 Bi nu yegsee ca Yerusalem mbokki gëmkat yi dalal nu ak mbégte. 18 Ci ëllëg sa nu ànd ak Póol seeti Saag, fekk njiiti mbooloo ñi gëm yépp dajaloo fa. 19 Ba leen Póol nuyoo ba noppi, mu daldi leen benn-bennal lépp li Yàlla def ci biir ñi dul Yawut jaarale ko ci liggéeyam.
20 Ba ñu déggee loolu, ñu màggal Yàlla, ba noppi, ñu wax Póol ne: «Mbokk mi, gis nga ne am na ay junni Yawut yu gëm ci Yeesu te ñoom ñépp takku nañu lool ci yoonu Musaa. 21 Ñoom, dégg nañu ne Yawut yépp yi dëkk ci biir ñi dul Yawut, yaa ngi leen di jàngal ñu bàyyi li yoonu Musaa santaane, di leen wax ñu baña xarafal seeni doom ak ñu baña topp aada Yawut yi. 22 Lan lanu wara def nag? Ndaxte dinañu yég ne ñëw nga. 23 Kon nag nu ngi lay digal nga def nii: am na ci sunu biir ñeenti góor ñu am lu ñu waataloon Yàlla. 24 Jël leen ak yaw te ngeen bokk setal seen bopp te nga feyal leen ngir ñu wat seen bopp yi. Noonu ñépp dinañu xam ne li ñu doon wax ci yaw du dëgg, te dinañu xam tamit ne yaa ngi topp tey xool tëralin yoonu Musaa yi. 25 Ci lu jëm ci ñi dul Yawut te gëm ci Yeesu, bindoon nanu leen ngir wax leen li ñu warula def, maanaam, ñu moytu lekk yàppu jur bu ñu saraxe ci xërëm yi, ak deret, ak yàppu jur yu ñu rey te deret tuuruwul, ak njaaloo.»
26 Ci ëllëg sa Póol ànd ak ñeenti nit ñi ngir bokk ak ñoom setal seen bopp. Ba noppi, ñu dugg kër-Yàlla gi ngir mu yégle fa ban bés la setal bi di mat, maanaam bés bi ñu wara defal sarax ngir ku nekk ci ñoom.
Benn kommandaŋu soldaar bu waa Room jàpp na Póol
27 Bi juróom ñaari fan yi ñu doon setal seen bopp di waaja jeex, mu am ay Yawut yu jóge Asi ñëw Yerusalem. Bi ñu gisee Póol ci ëttu kër-Yàlla gi, ñu jógloo mbooloo mi te ñu jàpp ko. 28 Ñuy yuuxu naan: «Yeen waa Israyil walluleen nu. Xoolleen! Waa ji mooy ki waare fépp ak ci ñépp di suufeel sunu askan wi, ak yoonu Musaa ak kër-Yàlla gi. Te léegi sax dugal na ñi dul Yawut ci kër-Yàlla gi te di tilimal béréb bu sell bi.» 29 Li taxoon ñu wax loolu mooy ne dañu gis Póol ci dëkk bi, mu ànd ak Torofim mi dëkk Efes. Ñu yaakaar ne Póol da koo dugal ci biir kër-Yàlla gi.
30 Dëkk bi yépp jaxasoo te askan bi di jóge ci bor bu nekk. Ñu jàpp Póol, diri ko, génne ko ci kër-Yàlla gi. Ñu tëj bunt yi ci saa si. 31 Bi ñu koy wuta rey, kommandaŋ soldaaru Room yég ne Yerusalem yépp dafa jaxasoo. 32 Ci saa si, mu daldi jël ay njiiti soldaar ak ay soldaar, ñu daw jëm ci mbooloo mi. Bi mbooloo mi gisee kommandaŋ bi ak soldaar yi ñu bàyyi dóor Póol. 33 Noonu kommandaŋ bi daldi jegesi te jàpp Póol. Mu jox soldaar yi ndigal ñu takk ko ñaari ceen, ba noppi mu laajte ne: «Kii mooy kan ak lan la def?» 34 Waaye ci biir mbooloo mi, ñii di wax lii, ñeneen ñi di wax leneen ba tax kommandaŋ bi mënula xam dara lu leer ndax coow li. Noonu mu jox ndigal ngir ñu yóbbu ko ci biir làquwaay bi, di béréb bi soldaar yi doon nekk. 35 Bi Póol tàmbalee yéeg yéegukaay bi, soldaar yi mujje ko yékkëti ndax soxoraayu mbooloo mi. 36 Ndaxte askan bi yépp dañu ko doon topp di yuuxu naan: «Na dee!»
Kàdduy Póol ci kanamu mbooloo mi ci Yerusalem
37 Ci waxtu bi ñuy waaja dugal Póol ci làquwaay bi, mu ne kommandaŋ bi: «Ndax mën naa la wax dara?» Mu tontu ko ne: «Kon danga dégg Gereg! 38 Du yaw yaa nekk waa jooju jóge Misra te taxoon nit ñii fippu, yóbbaale lu tollook ñeenti junniy fippukat ci màndiŋ bi?» 39 Póol ne ko: «Déedéet. Yawut laa bu juddoo Tàrs di dëkk bu am solo te nekk ci diiwaanu Silisi. May ma, ma wax ak mbooloo mi, ñaan naa la ko.»
40 Kommandaŋ bi may ko ko. Póol taxaw ci yéegukaay bi te tàllal loxoom mbooloo mi. Ñépp ne tekk. Póol daldi wax ci kàllaama Yawut yi, ne leen: