22
«Yeen sama mbokk yi ak baay yi, dégluleen ma léegi, ma wax ngir setal sama der.»2 Ba ñu déggee muy wax ci kàllaama Yawut ñu daldi gëna dal. Póol daldi ne:3 «Man Yawut laa bu juddoo ci Tàrs ci Silisi, waaye fii laa yaroo, ci dëkk bii. Gamalyel moo nekkoon sama jàngalekat te xamal na ma ni mu ware yoonu sunu maam yi. Takku woon na ci Yàlla lool, ni ngeen ci mel, yeen ñépp, tey.4 Fitnaal naa ay nit ñi doon topp yoonu Yeesu, ba ñenn ñi dee ci. Jàpp naa ay góor ak ay jigéen te yóbbu leen ci kaso.5 Jébbalkatu-sarax-bu-mag bi ak magi sunu askan mën nañu seede ne li may wax dëgg la. Ma jot ci ñoom bataaxal bi ñu bind ngir sunu mbokk yi nekk ci dëkku Damaas. Dem naa foofu ngir ma jàpp nit ñu doon topp yoon boobu te yóbbu leen ca Yerusalem ngir yar leen.
6 «Bi ma nekkee ci yoon di dem te jegesi Damaas, ci diggu bëccëg, leer gu mag daldi jóge asamaan wër ma ci saa si. 7 Ma daanu ci suuf te dégg benn baat bi may wax: "Sóol, Sóol lu tax nga may fitnaal?" 8 Ma laaj ko: "Yaw la kan, Boroom bi?" Mu ne ma: "Man la Yeesu mu Nasaret, mi ngay fitnaal." 9 Ñi nekkoon ak man gis nañu leer gi waaye mënuñu woona dégg baatu ki doon wax ak man. 10 Noonu ma ne: "Lan laa wara def, Boroom bi?" Boroom bi ne ma: "Jógal te nga dem Damaas, te foofu dinañu la wax lépp li nga wara def." 11 Gannaaw gisatuma woon dara ndax melaxaayu leer gi, ñi nekkoon ak man jàpp ma ci loxo te yóbbu ma ba Damaas.
12 «Amoon na benn waay bu tuddoon Anañas, nit ku takku ci Yàlla di déggal yoonu Musaa, te Yawut yi nekk Damaas yépp doon nañu seede lu baax ci moom. 13 Mu ñëw, taxaw ci sama wet te ne ma: "Sóol sama mbokk, gisaatal." Ci saa si ma daldi gisaat te ma gis ko. 14 Mu ne ma: "Yàllay sunuy maam moo la tànn ngir nga xam coobareem te nga gis Ku Jub ki te nga mëna dégg baatam, 15 ndaxte dinga nekk seedeem ci kanamu nit ñi ñépp ngir yégal leen li nga gis te dégg ko. 16 Léegi nag, lan ngay xaar? Jógal ñu sóob la ci ndox te nga woo turu Boroom bi ngir mu setal say bàkkaar."
17 «Ba ma delloo Yerusalem, benn bés may ñaan ci ëttu kër-Yàlla gi, ma daldi am gis-gis. 18 Boroom bi feeñu ma te ne ma: "Gaawantul génn Yerusalem ndaxte waa dëkk bi duñu nangu sa seede ci lu jëm ci man." 19 Ma tontu ko ne: "Boroom bi, ñoom xam nañu ne man maa doon wër ci kër-ñaan yi, di seet ñi la gëm ngir tëj leen ci kaso bi te dóor leen ay yar. 20 Bi ñu doon tuur deretu Eccen, sa seede, fekke woon naa ko, te àndoon naa ci li ñu doon def, te maa téye woon yére ñi ko doon rey." 21 Waaye Boroom bi ne ma: "Demal ndaxte dama la yónni fu sori ci ñi nekkul Yawut."»
22 Mbooloo ma déglu ko ba ma yegg ci kàddu yooyu. Noonu ñu yékkëti seen baat te ne: «Jëleleen nit kii ci suuf si, ndaxte ku mel nii, yelloowul dund.» 23 Ñu yuuxu, sànni seen yére, te tibb suuf si, sànni ci kaw. 24 Kommandaŋ bi joxe ndigal ñu dugal Póol ci biir làquwaay bi, te dóor ko ay yar ba mu wax, mu xam lu tax mbooloo mi doon ko yuuxoo noonu. 25 Bi ñu koy takk ngir dóor ko, Póol daldi wax njiitu soldaar bi fa nekkoon, ne: «Ndax am ngeen sañ-sañu dóor ay yar nit ku bokk ci waa Room te fekk ne yoon daanu ko.» 26 Bi mu déggee loolu njiitu soldaar bi daldi dem nettali loolu kommandaŋ bi, ne ko: «Lan ngay def? Nit kii waa Room la.» 27 Kommandaŋ bi ñëw ci Póol, mu laaj ko ne: «Wax ma, ndax waa Room nga?» Mu tontu ko ne: «Waaw». 28 Kommandaŋ bi ne ko: «Man xaalis bu bari laa fay ngir mëna bokk ci waa Room.» Póol ne ko: «Man nag dama ko judduwaale.» 29 Ci saa si, ñi ko naroona dóor ngir mu wax daldi ko sori. Kommandaŋ bi ci boppam daldi ragal bi mu xamee ne Póol waa Room la te mu joxe woon ndigal ngir ñu takk ko.
Póol ci kanamu magi Yawut yi
30 Ci ëllëg sa, kommandaŋ bi bëggoon na gëna xam ci dëgg-dëgg lan la Yawut yi doon tuumaale Póol. Mu santaane ñu tekki Póol te joxe ndigal ne njiitu-jébbalkati-sarax yi ak kurélu àttekatu Yawut yi daje. Noonu mu andi Póol te teg ko ci seen kanam.