23
Póol xool ñi bokk ci kurél bi, ne leen jàkk, te wax leen ne: «Mbokk yu góor yi, ci li ma jota dund yépp ba tey, amul lenn lu ma sama xel di ŋàññe ci kanamu Yàlla.»
2 Anañas, di jébbalkatu-sarax-bu-mag bi, joxe ndigal ñi jege woon Póol ngir ñu dóor ko ci gémmiñ. 3 Póol daldi ne: «Yàlla dina la dóor, yaw naaféq bi, mel ni miir bu ñu weexal. Danga toog ngir àtte ma ci yoon waaye yaa ngi moy yoon, ngay joxe ndigal ngir ñu dóor ma.» 4 Ña nekkoon ca wetam ne ko: «Póol, ndax sañ nga saaga jébbalkatu-sarax-bu-mag bi Yàlla fal.» 5 Póol daldi ne: «Mbokk yi, xamuma woon ne moom mooy jébbalkatu-sarax-bu-mag bi, ndaxte Mbind mi nee na: "Doo wax lu ñaaw sa njiitu askan."»
6 Póol xamoon na ne ci ëttu àttekaay bi amoon na ñi bokk ci tarixa Sadusen ak ñi bokk ci tarixa Farisen. Looloo tax mu yuuxu naan: «Samay mbokk, man Farisen laa, di doomu Farisen. Dañu may àtte ndax ni ma ame yaakaar ne ñi dee dinañu dekki.» 7 Bi mu waxee kàddu yooyu, ci la yékkëti ab werante ci diggante Farisen yi ak Sadusen yi, te noonu mbooloo mi daldi xaajaloo ñaar, 8 ndaxte Sadusen yi dañoo jàpp ne ku dee du dekki, te malaaka amul, rab amul. Farisen yi nag gëm nañu ci ñetti yooyu yépp. 9 Noonu mu daldi am coow lu réy, te ñenn ci jàngalekati-yoonu-Musaa yi bokk ci Farisen yi, ñu daldi jóg te wax ak doole di naan: «Gisunu dara lu bon ci nit kii. Mën na am rab walla malaaka moo wax ak moom.»
10 Werante bi gëna metti ba kommandaŋ bi ragal ñu daggaate Póol. Mu daldi jox ndigal soldaar yi ngir ñu ñëw génne Póol ci seen biir te yóbbu ko ci làquwaay bi.
11 Ci guddi gi ci topp, Boroom bi feeñu Póol te ne ko: «Takkal sa fit, ndaxte ni nga nekke sama seede ci Yerusalem, fàww tamit nga nekk ko ca dëkku Room.»
Muccal nañu Póol ci pexe bi Yawut yi tegoon ngir rey ko
12 Ci ëllëg sa ci suba si, Yawut yi di lal pexe: ñu waat baña lekk, baña naan ba keroog ñuy rey Póol. 13 Ñi nga xamante ne ñoo doon lal pexe yooyu, ëppoon nañu ñeent fukki nit. 14 Noonu ñu dem fekki njiiti-jébbalkati-sarax yi ak mag ñi te wax leen ne: «Nun ci sunu bopp waat nañu ne dunu lekk, dunu naan feek reyunu Póol. 15 Léegi nag, yeen ak kurélu àttekat yépp, ñaanleen kommandaŋ bi mu andi Póol ci seen kanam. Ngeen mel ni dangeena bëgga seetaat mbiram ba mu gëna leer. Te nun, waajal nanu sunu bopp ngir rey ko laata muy yegsi fii.»
16 Waaye jarbaatu Póol déggoon na pexe bi ñu doon lal. Mu dem ci làquwaayu soldaar yi, dugg ci biir, te nettali ko Póol. 17 Póol woo benn njiitu soldaar te ne ko: «Yóbbul ma waxambaane bi ci kommandaŋ bi ndaxte am na lu mu ko wara wax.»
18 Noonu mu jël ko te yóbbu ko ci kanamu kommandaŋ bi te ne ko: «Póol mi ñu tëj ci kaso bi moo ma woo te ñaan ma ngir ma andi waxambaane bii ndaxte dafa am lu mu la wara wax.» 19 Kommandaŋ bi jël ko ci loxoom, wéetoo ak moom. Mu laaj ko: «Lan nga ma bëgga wax?» 20 Mu tontu ko: «Yawut yi gise nañu ci seen biir ngir ñaan la ëllëg nga andi Póol ci kanamu kurélu àttekat yi, mel ni dañu bëgga seetaat mbiram ba mu gëna leer. 21 Bu leen gëm, ndaxte lu ëpp ñeent fukki nit ñoo wat ne duñu lekk, duñu naan feek reyuñu ko. Léegi nag waaj nañu te xaaruñu lu dul yaw nga nangu.» 22 Kommandaŋ bi bàyyi waxambaane bi mu dem, waaye mu tere ko mu wax kenn li mu ko nettali.
23 Noonu mu daldi woo ñaar ci njiitu soldaar yi, ne leen: «Dajaleleen ñaar téeméeri soldaar, ak juróom ñaar fukki soldaar yiy war fas, ak yeneen ñaar téeméeri soldaar yu gànnaayoo xeej. Waajalleen ngir dem dëkku Sesare ci juróom ñeenti waxtu ci guddi. 24 Waajalleen itam fas bu Póol wara yéeg ngir yóbbu ko ci jàmm ba ci Feligsë kilifa diiwaan bi.»
25 Kommandaŋ bi daldi bind bataaxal bii: 26 «Feligsë mu tedd mi, yaw mi yor kilifteef bi, man Këlódd Lisiyas maa lay nuyu. 27 Nit ki ma la yónnee, Yawut yi ñoo ko jàppoon, te naroon ko rey. Bi ma yégee ne waa Room la, ci laa ñëw, man ak samay soldaar, ngir wallusi ko. 28 Ma yóbbu ko ci kanamu kurélu àttekati Yawut yi ndaxte bëggoon naa xam li ñu koy tuumaale. 29 Gis naa ne dañu doon werante ci lu jëm ci seen yoonu bopp, moo tax ñu tuumaal ko. Waaye deful woon dara lu jar ñu koy rey walla ñu koy tëj ci kaso. 30 Dégg naa ne Yawut yi dañu ko doon fexeel, moo tax ma andil la ko ni mu gëna gaawe. Ma wax ñi koy tuumaal ñu ñëw layoo ak moom ci sa kanam.»
31 Soldaar yi ci ndigal gi ñu jot, ñu jël Póol te yóbbu ko ba ca dëkku Antipataris ci guddi googu. 32 Ci ëllëg sa soldaar yi doon dox dellu ci làquwaay bi. Ñu bàyyi soldaar yi doon war fas, ñu wéy di gunge Póol. 33 Ba ñu yegsee ca Sesare soldaar yiy war fas daldi jox bataaxal bi kilifa diiwaan bi te jébbal ko Póol. 34 Kilifa diiwaan bi, ba mu jàngee bataaxal bi ba noppi, mu laajte ci ban diiwaan la Póol bokk. Ba mu déggee ne mu ngi jóge ci Silisi, 35 mu ne ko: «Ñi la tuumaal, bu ñu yegsee, dinaa la déglu.» Noonu mu joxe ndigal ñu fat Póol ci kër kilifa, bi buur Erodd bu mag tabaxoon.