Póol layoo na ci kanamu Feligsë, kilifa diiwaan bi
24
Juróomi fan gannaaw loolu, Anañas di jébbalkatu-sarax-bu-mag bi ñëw Sesare, ànd ak ñenn ci magi Yawut yi ak benn layookat bu tudd Tertul. Ñu dem ci kanamu kilifa diiwaan bi ngir tuumaal Póol. 2-3 Feligsë joxe ndigal ngir ñu andi Póol te Tertul tàmbali di wax, naan: «Yaw Feligsë mu tedd mi, yaa tax nuy dund jàmm ju mat sëkk. Say xalaat yu rafet yi ngay jiite moo waral nu am ay coppite yu baax ci sunu askan. Ngir loolu lépp nuy dund ci waxtu bu nekk ak fépp fu mu mëna nekk, nu ngi lay jaajëfal. 4 Waaye ngir bañ la téye lu yàgg maa ngi lay ñaan ci sa mbaaxaay nga déglu nu ci ay waxtu yu néew. 5 Nun gis nanu ne nit kii, ku bon la ci askan bi. Mu ngi jógloo Yawut yi ci àddina si yépp. Moom mooy njiitu tarixa Nasareen yi, 6-7 te moom jéem na sax di tilimal kër-Yàlla gu sell gi. Ci noonu lanu ko jàppe. 8 Yaw ci sa bopp, boo ko laajee dinga xam ne mbir yi nu koy tuumaal yépp dëgg la.» 9 Yawut yi dëgëral waxu tuumaal yi, ne: «Li Tertul wax, noonu la.»
10 Kilifa diiwaan bi won Póol ne mu mëna wax, noonu Póol ne: «Xam naa ne ci diiru at yu bari yaa ngi àtte xeet bii moo tax ma am kóolute ngir setal sama der ci sa kanam. 11 Mën nga gëstu yaw ci sa bopp ne ëppul fukki fan ak ñaar demoon naa Yerusalem ngir màggal fa Yàlla. 12 Kenn gisu ma, may xuloo ak kenn walla may jógloo mbooloo mi, muy ci kër-Yàlla gi, ci kër-ñaan yi, walla ci dëkk bi. 13 Nit ñii mënuñu la won lenn luy firndeel li ñu may tuumaal léegi. 14 Waaye lenn déy, mën naa ko nangu ci sa kanam: Damay jaamu Yàllay sunuy maam di topp yoon bi ñu jàpp ne nekkul dëgg. Waaye gëm naa yoonu Musaa ak lépp li yonent yi bindoon. 15 Am naa yaakaar ci Yàlla, te ñoom tamit am nañu yaakaar boobu, ne ñu dee ñi dinañu dekki, muy ñu jub ñi walla ñu jubadi ñi. 16 Loolu moo tax may góor-góorlu saa su nekk ngir baña am lenn lu ma sama xel di ŋàññe ci kanamu Yàlla ak ci kanamu nit ñi.
17 «Gannaaw bi ma gëjee Yerusalem ay at yu bari ñëwaat naa ci sama xeet ngir jàppale leen ak xaalis te jébbal Yàlla ay sarax. 18-19 Yenn Yawut yi jóge woon diiwaanu Asi, loolu lañu fekk may def ci ëttu kër-Yàlla gi gannaaw bi ma matalee warugaru setal bi. Amul woon mbooloo walla yëngu-yëngu. Ñoom kay ñoo waroona ñëw ci sa kanam te tuumaal ma, bu ñu amee dara lu ñu may toppe. 20 Walla ñi nekk fii te doon ma laaj bi ma taxawee ci kanamu kurélu àttekat yi, nañu jóg te wax ban ñaawteef lañu gis ci man lu jar daan, 21 xanaa ngir li ma waxoon ak baat bu kawe ci seen biir, ne: "Dañu may àtte ndax ni ma ame yaakaar ne ñi dee dinañu dekki."»
22 Feligsë moom mi xamoon bu wóor ci lu jëm ci yoonu Yeesu, mu taxawal àtte bi, mu naan: «Bu kommandaŋ Lisiyas ñëwee dinaa jël dogal ci seen mbir.» 23 Gannaaw loolu mu sant njiitu soldaar bi wottu Póol mu denc ko ci kaso bi te bàyyi ko mu féex. Ay nitam tamit mën di ko toppatoo.
24 Noonu mu teg ca ay fan. Feligsë ñëw ànd ak soxnaam Dursil mi nekkoon Yawut. Mu woo Póol te mu koy déglu mu wax ci lu jëm ci ngëm gi ci Yeesu Almasi bi. 25 Waaye bi Póol waxee ba àgg ci mbirum njubte, téye sa bopp, ak ci mbirum àtte bi wara ñëw, Feligsë daldi tiit. Mu ne ko: «Ngir tey doy na. Mën nga dem. Su ma amee jot dinaa la woowaat.» 26 Mu doon dunde yaakaar ne Póol da koy jox xaalis ngir neexal ko. Loolu moo tax mu koy faral di woolu ngir waxtaan ak moom. 27 Teg ci ñaari at, ku ñuy wax Porsiyus Festus wuutu Feligsë. Waaye Feligsë bàyyi Póol ci kaso bi ndaxte dafa bëggoona neex Yawut yi.