Póol layoo na ci kanamu Festus, kilifa diiwaan bi
25
Ñetti fan gannaaw bi Festus yegsee ci diiwaan bi, mu jóge dëkku Sesare, dem dëkku Yerusalem. 2 Njiiti-jébbalkati-sarax yi ak njiiti askanu Yawut yi ñëw ci kanamam di kalaame Póol. 3 Ñu ñaan Festus ngir mu may leen ñu andi Póol Yerusalem, ndaxte dañu ko doon fexe rey ci yoon bi. 4 Waaye Festus tontu leen ne: «Póol mu ngi ci Sesare, ñu tëj ko ca kaso ba, te man ci sama bopp, léegi ma dellu fa. 5 Na ay njiit yu bokk ci yeen ànd ak man ci Sesare, te ñu tuumaal ko fa su fekkee dafa def lu bon.» 6 Festus am fa juróom ñett ba fukki fan ak ñoom, te mu dellu Sesare. Ci ëllëg si mu toog ci baŋu àttekaayam te joxe ndigal ngir ñu andi Póol. 7 Bi mu yegsee, Yawut yi jóge woon Yerusalem wër ko te di ko tuumaal ci mbir yu bari te doy war, waaye amuñu woon ay firnde ngir wone ko. 8 Póol jël kàddu gi ngir setal deram, ne: «Defuma dara lu ñaaw jëmale ko ci yoonu Yawut yi, ci kër-Yàlla gi, walla ci Sesaar.» 9 Festus, bëggoon na neex Yawut yi. Ci noonu mu laaj Póol ne: «Ndax bëggoo dem Yerusalem, ñu àtte la fa ci mbir yi ci sama kanam?» 10 Póol tontu ne: «Maa ngi taxaw ci àttekaayu Sesaar te fii lañu ma wara àtte. Tooñuma Yawut yi, ni nga ko xame bu baax yaw ci sa bopp. 11 Su fekkee def na lenn lu ñaaw walla lu jar dee, bañuma dee. Waaye su fekkee mbir yu ñu may tuumaal, benn dëgg amu ci, kenn sañu ma jébbal ci loxoy ñi may tuumaal. Dénk naa Sesaar sama mbir.» 12 Festus, gannaaw bi mu gisee ak ñi ko wër, mu tontu ko ne: «Dénk nga Sesaar sa mbir, kon nag dinga dem ci kanamu Sesaar.»
Festus ak buur Àggripa waxtaan nañu ci lu jëm ci Póol
13 Ay fan gannaaw loolu buur Àggripa ak jigéenam Berenis ñëw ci dëkku Sesare ngir nuyu Festus. 14 Gannaaw desoon nañu fa ay fan yu bari, Festus wax ak buur Àggripa lu jëm ci Póol. Mu ne ko: «Am na fi benn waay bu Feligsë bàyyi ci kaso bi. 15 Bi ma demee Yerusalem njiiti-jébbalkati-sarax yi ak magi Yawut yi ñëw nañu di ko kalaame. Ñu wax ma ngir ma daan ko. 16 Ma tontu leen ne nekkul ci aaday waa Room ñu jébbal kenn ci anam boobu. Ku ñu tuumaal dafa wara daje ak ñi koy tuumaal te mu am sañ-sañu wax ci li ñu koy tuumaal. 17 Noonu njiiti askan bi ñëw nañu ba fii ak man te xaaruma lu yàgg. Bés bi ci topp toog naa ci sama baŋu àttekaay te joxe ndigal ngir nu andi nit kooku. 18 Ñi ko doon tuumaal yegsi, waaye teguñu ci kawam benn ñaawteef ni ma ko yaakaare woon. 19 Nekkul woon dara lu dul werante lu jëm ci seen diine, ak ci kenn ku tudd Yeesu mu dee te Póol di wax ne mu ngi dund. 20 Xamuma woon naka laay jële dogal ci lu jëm ci mbir moomu. Looloo tax ma laaj Póol ndax nangu na dem Yerusalem ngir ñu àtte ko fa, 21 waaye Póol ñaan na ngir ñu dénk Sesaar mbiram. Kon nag ma joxe ndigal ngir ñu tëj ko ci kaso bi, ba keroog ma koy mëna yónnee Sesaar.» 22 Àggripa daldi wax Festus ne: «Man tamit bëggoon naa déglu nit kooku.» Festus tontu ko: «Dinga ko déglu suba.»
Póol mu ngi layool boppam ci kanamu buur Àggripa
23 Ci ëllëg sa Buur Àggripa ak Berenis ñëw ak ràññeeku, dugg ci bérébu àttekaay bi ànd ak kommandaŋ yi ak nit ñu am solo ci dëkk bi. Festus joxe ndigal, ñu daldi andi Póol. 24 Noonu Festus wax ne: «Buur Àggripa ak yeen ñépp ñu fi nekk, xoolleen nit kii. Mbooloo Yawut yépp ñëw nañu ci man di ko kalaame dale ko ci Yerusalem ba fii te di yuuxu ci sama kaw ne nit kii yelloowul dund. 25 Man, gis naa ne deful dara lu jaar ñu koy teg daanu dee, waaye moom dénk na Sesaar mbiram. Kon nag jël naa dogal yónnee nit kii ci moom. 26 Amuma dara lu wóor ci mbiram lu ma mëna bind ngir yónnee ko Sesaar. Looloo tax ma andi ko ci seen kanam, te rawatina yaw Buur Àggripa, ngir ma am lu ma bind gannaaw bi nu ko dégloo, 27 ndaxte yónnee ku ñu tëj ci kaso te waxoo lu tax ñu koy tuumaal, ci sama xalaat, amul benn njériñ.»