26
Àggripa wax Póol ne: «Mën nga wax ngir setal sa der.» Póol yékkëti loxoom, mu tàmbali di layool boppam naan: 2 «Buur Àggripa, bég naa ci li ma mëna taxaw ci sa kanam tey ji ngir setal sama der ci mbir yépp yi ma Yawut yi di tuumaal. 3 Ndaxte xam nga bu baax aada Yawut yi yépp ak seeni waxtaan. Looloo tax, maa ngi lay ñaan nga déglu ma ak muñ. 4 Yawut yépp xam nañu ni ma doon dunde dale ko bi ma nekkee ndaw, xam nañu naka laa meloon bu jëkk ci sama biir xeet ci Yerusalem. 5 Xam nañu ma bu yàgg te mën nañu seede, su leen neexee, ne dund naa ni Farisen, mooy tarixa bi gëna xër ci sunu diine. 6 Te léegi lii moo tax ñu may àtte: Maa ngi yaakaar ne Yàlla dina matal li mu digoon sunu maam yi. 7 Dige boobu, fukki giir ak ñaar yu Israyil yaakaar ne dina mat, moo tax ñuy jaamu Yàlla guddi ak bëccëg ak takkute. Buur Àggripa, Yawut yi dañu may tuumaal ci lu jëm ci yaakaar boobu. 8 Lu tax gëmuleen ne Yàlla day dekkil ñu dee ñi?
9 «Man ci sama bopp sax xalaatoon naa ne war naa xeex turu Yeesu mu Nasaret ci anam yépp. 10 Loolu laa doon def ci Yerusalem: jotoon naa sañ-sañ ci njiiti-jébbalkati-sarax yi ngir tëj ci kaso ñu bari ñi Boroom bi moom. Bi ñu leen doon teg daanu dee, àndoon naa ci. 11 Doon naa faral di leen fitnaal ci kër-ñaan yi, te doon naa leen jéema weddiloo seen ngëm. Meroon naa lool ba tax ma di leen topp ba ci ay dëkk yu bokkul ci Israyil ngir fitnaal leen. 12 Ci noonu, benn bés ma nekkoon ci yoonu Damaas ci ndigal ak sañ-sañu njiiti-jébbalkati-sarax yi. 13 Buur Àggripa, nekkoon naa ci yoon bi ci diggu bëccëg. Ci laa gis benn leer jóge ci asamaan, leer boobu moo gënoona leer bu jant bi, te leeraayam wër ma, man ak ñi ma àndaloon. 14 Nun ñépp nu daanu ci suuf te ma dégg benn baat doon wax ak man ci kàllaama Yawut ne: "Sóol, Sóol lan moo tax nga may fitnaal, jafe na ci yaw ni fas buy baña nangul ki koy wommat." 15 Ma laaj ko ne: "Yaw la kan, Boroom bi?" Boroom bi tontu ma ne: "Man la Yeesu mi ngay fitnaal. 16 Waaye léegi jógal, taxaw. Li tax ma feeñu la mooy: tànn naa la ngir nga nekk sama surga, te nga seede ci nit ñi ne gis nga ma, te nga wax leen leneen li ma lay won. 17 Dinaa la musal ci askanu Yawut yi ak ñi dul Yawut. Ci ñoom laa la yónni, 18 ngir nga ubbi seeni bët, jële leen ci lëndëm indi leen ci leer gi, te jële leen ci loxo Seytaane indi leen ci Yàlla, ngir bu ñu gëmee ci man, ñu am mbaalum bàkkaar te bokk cér ak ñi Yàlla moom."
19 «Kon nag Buur Àggripa, bañuma woona déggal li ma Boroom bi santoon bi mu ma feeñoo. 20 Waaye li tàmbalee ci Damaas, ak dëkku Yerusalem, teg ci réewu Yawut yépp, ba agsi ci ñi dul Yawut, yégal naa leen ne war nañu tuub seeni bàkkaar, ñu dellusi ci Yàlla te ñu wone loolu ci seeni jëf. 21 Loolu moo tax Yawut yi jàpp ma ci ëttu kër-Yàlla gi te ñu doon ma wuta rey, 22 waaye ba tey jii, Yàlla aar na ma te maa ngi taxaw fii di ko seedeel ci kanamu ñépp, mag ak ndaw. Yokkuma dara ci li yonent yi ak Musaa waxoon ne dina am: 23 maanaam Almasi bi dina sonn te dina jëkka dekki ci ñu dee ñi ngir yégal leeru mucc gi askanu Yawut yi ak ñi dul Yawut.»
24 Bi Póol nekkee di layoo noonu, Festus yuuxu naan: «Póol danga dof. Sa xam-xam bu réy moo la dofloo.» 25 Waaye Póol tontu ko ne: «Festus mu tedd mi, dofuma. Damay wax ay kàddu yu dëggu te wóor. 26 Buur Àggripa yég na loolu lépp. Loolu moo tax may wax ak kóolute ci kanamam. Wóor na ma ne xam na mbir yooyu yépp, ndaxte loolu xewewul ci béréb bu làqu. 27 Buur Àggripa ndax gëm nga kàddu yonent yi? Waaw, xam naa ne gëm nga leen.» 28 Àggripa tontu Póol ne: «Xanaa yaw ci diir bu gàtt bii, danga ma bëgga gëmloo ci Almasi bi?» 29 Póol tontu ko ne: «Am na yéene ci kanamu Yàlla, muy tey walla suba, nga mel ni man, yaw ak ñépp ñi may déglu tey, ba mu des ceen yi ñu ma takk.»
30 Ci loolu, buur bi, kilifa diiwaan bi, Berenis, ak ñépp ñi nekkoon ak ñoom daldi jóg. 31 Ñu génn te di wax ci seen biir ne: «Nit kii deful dara lu jaar ñu koy rey walla ñu koy tëj kaso.» 32 Buur Àggripa wax Festus ne: «Mënoon nañu ko yewwi bu dénkul woon mbiram Sesaar.»