Soldaar yi ñu ngi yóbbu Póol ci dëkku Room
27
Bi ñu jëlee dogal dugal nu ci gaal ngir yóbbu nu réewu Itali, ci lañu jël Póol ak ñeneen ñi ñu jàppoon, ñu dénk leen Yulyus, mi nekk njiitu mbooloo soldaar bi ñu woowe xarekati Sesaar. 2 Nu dugg gaal bi jóge Adaramit, jëm teerukaay yi ci diiwaanu Asi te nu daldi dem. Aristàrk mi jóge dëkku Tesalonig ci diiwaanu Maseduwan àndoon na ak nun. 3 Ci ëllëg sa nu teer dëkku Sidon. Noonu Yulyus baaxoon ci Póol, may ko mu dem ci ay xaritam ngir ñu jox ko li mu soxla ngir tukki bi. 4 Noonu nu teguwaat ci yoon bi. Ngelaw bi tere nu nu wéy ci yoon bi nu bëggoona jël, noonu ñu teggi Sippar di réew mi ndox wër. 5 Nu jàll ci géej gi janook diiwaanu Silisi ak bu Pamfili ngir teer ci dëkku Mira ci diiwaanu Lisi. 6 Te foofu njiitu soldaar bi daldi gis gaal bu jóge Alegsàndiri, jëm Itali. Noonu mu dugal nu ci. 7 Ci diiru ay fan yu bari nu ngi doon daw ndànk ci géej gi, te ak coono bu metti lanu yegsee ci kanamu dëkku Kanidd. Ngelaw gi tax ba mënunu wéy ci yoon boobu. Nu jël beneen yoon, romb Salmon ngir teggi Keret di réew mu ndox wër. 8 Ak coono bu metti danu doon wéy di teggi Keret, ba yegsi ci béréb bi ñu woowe teerukaay yu baax yi te ci wetam la dëkku Lase nekk.
Ngelaw bu metti bi ci biir géej gi
9 Ñàkk nanu waxtu yu bari ci sunu tukki bi te jamono Kooru Yawut yi jàlloon na ba noppi. Noonu wóoratul woon nag ngir nu wéyal tukki bi. Noonu Póol artu leen ne: 10 «Samay xarit, gis naa ne yoon bi dina metti. Gaal gi ak li mu yeb dinañu yàqu, te nun sax mën nanu ci ñàkk sunu bakkan.» 11 Waaye njiitu soldaaru Room bi, li dawalkat bi ak boroom gaal gi wax la gëna wóolu li Póol wax. 12 Gannaaw teerukaay bi neexul woon ci nawet, ñi ëpp ci gaal gi mànkoo jël dogal ngir jóge fa, jëlaat géej gi, ngir jéema yegg su mënee nekk, Fenigsë, di teerukaay ci Keret bi jublu sowu sudd ak sowu nord, ndaxte foofu moo wóoroon ngir ñu des fa ba nawet bi jeex.
13 Bi ñu gisee ab ngelaw bu woyof jóge sudd, nit ñi daldi am yaakaar ne dinañu mëna yegg Fenigsë. Noonu ñu jóge fi nu nekkoon, nu wéy di teggi Keret. 14 Waaye yàggul dara ngelaw gu mag daldi ñëw, jóge penku nord, daanu ci sunu kaw. 15 Ngelaw bi ëpp doole gaal gi ba mënatunu ko jubbanti. Noonu nu bàyyi ngelaw bi mu koy yóbbu. 16 Nu romb benn dëkk bu ndaw bu ndox wër bi ñuy woowe Koda. Nu làqu fa ndax ngelaw bi. Sunu gaalu rawalekaay bu ndaw doon na rëcc ci géej gi. Ak coono bu metti lanu ko jëlaate. 17 Nu yéegal ko ci gaal gi. Ñi doon liggéey ci gaal gi jël ay buum, wërale leen gaal gi, takk ko ci. Dañu doon ragala mbëkk suuf bi ñuy woowe Sirt, noonu ñu sànni diigal bi, maanaam benn weñ bu diis bu ñu takk ci gaal gi ngir ñu wàññi ni mu doon dawe. Ci noonu ñu bàyyi ngelaw bi di nu yóbbu. 18 Ci ëllëg sa ngelaw bi wéy di yëngal gaal gi ak doole, moo tax ñu sànni ci géej gi li gaal gi yeboon. 19 Ci ñetteelu fan bi ñiy liggéey ci gaal gi ci seen bopp sànni ci géej gi jumtukaayu gaal gi. 20 Ay bés yu bari mënunu woona gis dara, du jant, du biddéew. Ngelaw bi wéy di am doole. Nu daldi ñàkk bépp yaakaaru mucc.
21 Yàgg na lekkunu dara. Noonu Póol daldi taxaw ci kanamu ñépp te ne leen: «Samay xarit, waroon ngeen ma déglu te baña jóge Keret. Mënoon ngeen moytu ngelaw bii te ngeen baña ñàkk li gaal gi yeboon. 22 Léegi nag, maa ngi leen di ñaax ngir ngeen dëgër-dëgërlu, ndaxte kenn ci yeen du sànku, waaye gaal gi rekk mooy yàqu. 23 Ci guddi gi Yàlla bi may liggéeyal te mu moom ma, yónni na malaakaam ci man. 24 Malaaka mi wax ma ne: "Póol, bul ragal dara! Fàww nga taxaw ci kanamu Sesaar, te yaw yaa tax Yàlla ci mbaaxam aar ñépp ñi nga àndal ci gaal gi." 25 Kon nag samay xarit ngeen dëgër-dëgërlu, ndaxte man wóolu naa Yàlla, ne dina def lépp ni mu ma ko waxe. 26 Waaye gaal bi, fàww mu yàqu ci wetu benn dëkk bu ndox wër.»
27 Ci fukkeelu guddi gi ak ñeent nu nekk ci géeju Adiratig, ngelaw bi di nu yóbbu. Ci xaaju guddi ñi doon liggéey ci gaal gi xalaat ne dañoo jege suuf. 28 Ñu daldi sànni nattukaay bi ci biir géej gi, ñu gis ne xóotaay bi tollo na ci ñeent fukki meetar. Ñu dem ba ci kanam tuuti, ñu nattaat, gis ne nu ngi ci fanweeri meetar. 29 Ñu ragal gaal gi mbëkk benn xeer, moo tax ñu sànni ñeenti diigal yi ci gannaaw gaal gi, ngir wàññi ni mu doon dawe. Noonu ñu daldi xaar suba si te yàkkamti ko lool. 30 Ñi doon liggéey ci gaal gi wàcce gaalu rawalekaay bu ndaw bi ci biir géej gi di wax ne: «Nu ngi sànni yeneen diigal ci kanamu gaal gi.» Waaye loolu nekkul woon dëgg. Dañu bëggoona rëcc ci gaal gi. 31 Póol daldi ne njiitu soldaar bi ak ay soldaaram: «Bu nit ñii desul ci biir gaal gi, dungeen mëna mucc.» 32 Noonu soldaar yi dagg buum yi téye woon gaal gu ndaw gi te bàyyi ko mu dem ci géej gi.
33 Laata bët di set Póol daldi ñaax ñépp ngir ñu lekk te ne leen: «Tey mooy fukki fan ak ñeent ngeen di xaar te lekkooleen dara. 34 Maa ngi leen di ñaax ngir ngeen lekk ndaxte soxla ngeen ko ngir mëna mucc. Kenn ci yeen du ñàkk benn kawaru boppam.» 35 Gannaaw bi mu waxee kàddu yooyu, Póol jël mburu, sant Yàlla ci kanamu ñépp, mu daldi ko damm te tàmbali lekk. 36 Noonu ñépp seen xel dal te ñu tàmbali lekk ñoom itam. 37 Tollu woon nanu ci ñaari téeméeri nit ak juróom ñaar fukk ak juróom benn (276) ci biir gaal gi. 38 Bi ñu lekkee ba regg, ñu sànni saaku pepp yi ci géej gi ngir gaal gi mëna woyof.
39 Bi bët setee ñi doon liggéey ci gaal gi xàmmewuñu béréb bi nu nekkoon, waaye ñu séen ab tefes. Ñu jël dogal yóbbu fa gaal gi su mënee nekk. 40 Loolu moo tax ñu dagg buumi diigal yi te bàyyi leen ci biir géej gi, yewwiwaale buum yi téye woon joowukaayu gaal gi, ba noppi ñu tàllal rido bu mag bi nekk ci kanamu gaal gi. Noonu ngelaw bi di ko bëmëx te ñu jublu ci tefes bi. 41 Waaye ñu dal ci benn jalu suuf bu nekkoon ci biir ndox mi te gaal gi mënatul dem. Kanamu gaal gi suux ci suuf ba mënatul génn. Gannaawu gaal gi dàjjeeku ndax dooley ndoxu géej gi. 42 Soldaar yi bëgga rey ñi ñu jàppoon, ngir kenn ci ñoom baña féey ba rëcc. 43 Waaye njiitu soldaar bi bëgga rawale Póol, tere leen pexe bi ñu bëggoona def. Mu jox ndigal ñi mëna féey, ñu jëkka sóobu ci ndox mi ngir jot suuf su wow si, 44 te ñeneen ñi topp leen, jëfandikoo ay dénk walla ay tojit yu jóge ci gaal gi. Noonu ñépp yegsi nañu ci tefes gi ci jàmm ak salaam.