Póol ci dëkku Màlt
28
Bi nu rëccee ci dee, nu yég ne dëkk bu ndox wër bi nu teeroon, Màlt la tudd. 2 Waa dëkk bi defal na nu lu baax. Ñu taal xal bu réy ngir dalal nu ndaxte da doon taw te mu sedd lool. 3 Póol for taxanu matt ngir sànni ko ci xal bi waaye benn jaan génn ci taxanu matt bi ndax tàngoor bi te màtt ko ba taq ci loxoom. 4 Ba waa dëkk bi gisee jaan bi képp loxo Póol ñu daldi wax ci seen biir: «Nit kii lu wóor mooy reykatu nit la te rëcc ci géej gi, waaye sunu yàlla bu jigéen bi, Njubte, mayu ko mu dund.» 5 Waaye Póol wiccax jaan bi ci xal bi te dara mettiwu ko. 6 Nit ñi ñu ngi doon xaar Póol newwi walla mu daanu dee ci saa si. Ñu xaar bu yàgg waaye ñu gis ne dara dalu ko. Ñu daldi soppi seen xalaat te ne: «Kii, ab yàlla la.»7 Lu jege woon béréb bi nu nekkoon amoon na ay suuf yi doon moomeelu kilifa dëkk boobu bu tudd Publiyus. Mu dalal nu ngan gu réy, jox nu fu nu nekk diiru ñetti fan. 8 Fekkoon na pàppay Publiyus mu ngi woon tëdd ndax yaram bu tàng ak biiru-taññ. Póol dem gis ko, ñaan, teg ko ay loxo ci boppam, te wéral ko. 9 Noonu yeneen nit yu feebar yi nekkoon Màlt ñëw ngir gis Póol, te mu wéral leen, ñoom itam. 10 Nit ñi may nu cér lool. Bi nu waaja jëlaat gaal, ñu daldi nu jox lépp li nu soxla ngir tukki bi.
Póol yegsi na ci dëkku Room
11 Gannaaw bi nu fa amee ñetti weer nu dem ci gaal bu jóge Alegsàndiri te am ci kanamam jëmmu Kastor ak Polugsë, di ay yàlla ci waa Geres. Mu def nawet bi ci teerukaayu gaal ci Màlt. 12 Bi nu demee ba dëkku Sirakus, nu am fa ñetti fan. 13 Noonu gaal gi topp tefes bi ba yegg ci dëkku Resiyo. Ci ëllëg sa, ngelawu sudd bi jóg te dimbali nu, ba tax nu yegg ci dëkku Pusol ci ñaari fan. 14 Ca dëkk boobu nu fekk fa ay mbokki gëmkat. Ñu ñaan nu ngir nu des ak ñoom juróom ñaari fan. Gannaaw loolu nu dem Room. 15 Bi mbokk yi dëkk Room yégee ne nu ngi ñëw, ñu dem ba ci Marse Apiyus ak béréb bi ñuy wax Ñetti Daluwaayu Gan yi ngir daje fa ak nun. Bi leen Póol gisee, muy sant Yàlla te ànd ak fit. 16 Bi nu yegsee Room, ñu may Póol mu dal ci benn kër ak benn soldaar bu koy wottu.
Póol yégal na xibaar bu baax bi Yawut yi ci dëkku Room
17 Gannaaw ñetti fan Póol woolu njiiti Yawut yi nekk Room ngir ñu daje. Bi ñu dajaloo ci këram, mu wax leen ne: «Mbokk yi, jàppoon nañu ma ci Yerusalem te jébbal ma ci loxoy waa Room, fekk defuma dara sunu askan walla sunuy aaday maam. 18 Gannaaw bi ma waa Room laajee, ñu bëggoon ma bàyyi ndaxte gisuñu dara ci man lu tax ñu may teg daanu dee. 19 Waaye Yawut yi bañ. Noonu amatuma pexe bu dul dénk sama mbir Sesaar, doonte bëgguma taqal sama askan. 20 Loolu moo waral ma bëggoon leena gis te waxtaan ak yeen, ndaxte yaakaaru Israyil, moo tax ma yor ceen yii.» 21 Yawut yi tontu ko ne: «Amunu benn bataaxal bu jóge Yude ci li jëm ci yaw, te amul benn mbokk bu jóge foofu nettali nu walla mu wax nu lu bon ci yaw. 22 Waaye bëggoon nanu la déglu, nga wax nu sa xalaat, ndaxte xam nanu ne fépp la nit ñi di wax lu bon ci tarixa bi nga bokk.»
23 Ñu jàpp nag beneen bés. Ci bés ba ñu gëna bari ñëw, fekksi ko fi mu dëkk. Ci suba ba ci ngoon, Póol di leen yégal nguuru Yàlla gi te, jaarale ko ci yoonu Musaa ak ci téere yonent yi, mu di leen wuta gëmloo ci Yeesu. 24 Ñenn ñi daldi gëm li mu wax, waaye ñeneen ñi baña gëm. 25 Gannaaw déggoowuñu woon ci seen biir, ñu bëgga tas, Póol yokk ci kàddu yii, ne: «Li Xel mu Sell mi doon wax seeni maam jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi dëgg la, ba mu ne:
26 "Demal ci askan boobu te wax leen:
'Dingeen déglu ba sonn te dungeen dégg dara;
dingeen xool bu baax te dungeen gis dara.'
27 Ndaxte xolu askan bii daa dëgër,
fatt nañu seen nopp yi,
tëj nañu seen bët yi,
ngir seen bët yi baña gis,
te seen nopp yi baña dégg,
ngir ñu baña xam,
te ñu baña woññeeku ci man Yàlla
ngir ma wéral leen."»
28-29 Póol yokk ca ne: «Xamleen nag lii: Yàlla yónnee na xibaaru mucc gi ci ñi dul Yawut, te ñoom, dinañu ko déglu.»