Yeesu dekki na
24
Dimaas ci suba teel jigéen ñi doon dem ci bàmmeelu Yeesu, di yóbbaale cuuraay bu ñu defaroon. 2 Ñu dem ba yegg ci buntu bàmmeel bi, fekk xeer bi nga xamante ne tëjoon na bàmmeel bi, bërëŋu. 3 Ñu dugg ci biir, waaye gisatuñu yaramu Boroom bi Yeesu. 4 Ñu jaxasoo. Noonu ñaari góor yu sol ay yére yuy melax feeñu leen ci seen wet. 5 Tiit dab leen, ba tax ñu sukk, dëpp seen jë ci suuf. Ñaari góor yi laaj leen ne: «Lan moo tax ngeen di seet kiy dund ci biir ñu dee ñi? 6 Nekkatu fi; dekki na. Fàttalikuleen li mu leen waxoon bi mu nekke woon ak yeen ci diiwaanu Galile: 7 "Fàww ñu jébbale Doomu nit ki ci loxoy bàkkaarkat yi, ñu daaj ko ci bant, te mu dekki ci ñetteelu fan bi."» 8 Noonu jigéen ñi daldi fàttaliku kàdduy Boroom bi Yeesu.9 Bi ñu jógee ci bàmmeel bi, ñu dem nettali loolu lépp fukk yi ak benn ak ñeneen ñépp. 10 Jigéen ñooñu ñoo doon Maryaama bu Magdala, Sànn, Maryaama mi di yaayu Saag, ak yeneen jigéen yu leen gunge woon tamit. Ñu nettali loolu ndaw ya, 11 waaye ñu teg seen wax caaxaan ba tax gëmuñu jigéen ñi. 12 Waaye Piyeer daldi jóg, daw, dem ci bàmmeel bi. Bi mu yegsee, mu sëgg, gisul lu dul perkaal. Noonu mu daldi ñibbi këram di waaru ci li xewoon.
Yeesu feeñu na taalibe yi te dellu asamaan
13 Ci bés boobu tamit, la ñaari taalibe Yeesu doon dem ci dëkk bi ñuy woowe Emayus, te digganteem ak Yerusalem tollu na ci fukki kilomet. 14 Te ñu ngi doon dem di waxtaan ci lépp li xewoon. 15 Bi ñu nekkee di waxtaan di diisoo ci seen biir, Yeesu daldi leen dab ci yoon bi, ànd ak ñoom, 16 waaye mu mel ni seen bët yi dañoo muuru woon, moo tax xàmmewuñu ko woon. 17 Yeesu laaj leen: «Lan ngeen di nekk di waxtaan te ànd di dox?» Ñu daldi taxaw te ànd ak tiis, 18 te kenn ku ñuy wax Këleyopas tontu ko ne: «Ndax yaw kese yaay ki dal ci Yerusalem te xamoo li xew ci bés yii?» 19 Yeesu ne ko: «Lan moo xewoon?» Ñu ne ko: «Li dal Yeesu mu Nasaret, di woon ab yonent bu am kàttan ci jëf ak ci kàddu ci kanamu Yàlla ak ci kanamu askan bi yépp. 20 Sunuy njiiti-jébbalkati-sarax yi ak sunuy kilifa yi jébbale nañu ko, ngir ñu teg ko daanu dee te daaj ko ci bant. 21 Nun, danoo yaakaaroon ne moom mooy yewwi waa Israyil. Waaye tamit, tey mooy ñetteelu fan gannaaw bi loolu xewee. 22 Te ci dëgg, ñenn jigéen ñu bokk ci nun jaaxal nañu nu, ndaxte dem nañu ci bàmmeel bi ci suba teel, 23 waaye fekkuñu fa yaramam. Ñu dellusi te nettali nu ne ay malaaka dañu leen feeñu te wax leen ne mu ngi dund. 24 Bi ñenn ci nun demee ci bàmmeel bi fekk nañu fa lépp li jigéen ñi doon wax, waaye moom, gisuñu ko.»
25 Noonu Yeesu ne leen: «Nit ñu ñàkk xel ñi te seen xol yéexa gëm lépp li nga xam ne moom la yonent yi wax! 26 Ndax Almasi bi warul woon sonne nii, bala muy dugg ci màggaayam?» 27 Dale ko ci Musaa ak ci yonent yi yépp Yeesu leeralal na leen lépp li Mbind mi wax ci lu jëm ci moom.
28 Bi ñu jegesee ci gox bi taalibe yi doon dem, mu mel ni ku bëggoona dem fu gëna sori, 29 waaye ñu téye ko te wax ko ne: «Desal ak nun ndaxte jant baa ngi waaja so te guddi gi jegesi na.» Mu dugg ngir des ak ñoom. 30 Mu daldi toog ci bérébu lekkukaay bi, jël mburu mi, barkeel ko, damm ko, te jox leen ko. 31 Noonu seeni bët daldi ubbeeku, ñu xàmme ko, waaye mu réer ci seen biir. 32 Ñuy wax ci seen biir te ku nekk di wax ne: «Ndax yégunu woon neexaay ci sunuy xol bi mu nu doon leeralal Mbind mi ci yoon bi?»
33 Noonu ñaari taalibe yi daldi jóg ci saa si, dellu Yerusalem. Ñu fekk fa fukki ndaw ya ak benn ak seen àndandoo yi, 34 te ñépp wax leen ne: «Ci dëgg Boroom bi Yeesu na te feeñu na Simoŋ.» 35 Noonu ñaari taalibe yi nettali leen li xewoon ci yoon bi ak naka lañu xàmme woon Yeesu ci waxtu bi mu doon damm mburu mi.
36 Bi ñu nekkee di wax loolu, ci saa si Yeesu ci boppam feeñu leen ci seen biir te ne leen: «Na jàmm ànd ak yeen.» 37 Tiit daldi leen jàpp, ñu jaxasoo, ñu gëm ne dañoo gis njuuma, 38 waaye Yeesu wax leen, «Lu tax ngeen jaxasoo, te lan moo tax ngeen am xel ñaar ci seen biir xol? 39 Xoolleen samay loxo ak samay tànk, man mii la. Laalleen ma te xam, ndaxte njuuma du am yaram ak yax, ni ngeen gise, ma am ko.» 40 Bi muy wax loolu, mu won leen loxoom yi ak tànkam yi. 41 Ni ñu nekke woon ci biir mbégte ak yéemu te mënaguñu woona gëm loolu, Yeesu laaj leen: «Ndax am ngeen fii lu ñu mëna lekk?» 42 Ñu jox ko dogu jën bu ñu lakk. 43 Mu jël ko, lekk ko ci seen biir.
44 Noonu mu wax leen: «Lii laa leen doon wax ci bi ma nekkee woon ak yeen, ne: fàww lépp mat ci li ñu bind ci man, ci biir yoonu Musaa ak ci téere yonent yi ak ci biir Sabóor yi.» 45 Noonu mu ubbi seen xel ngir ñu ràññee Mbind mi. 46 Mu yokk ca ne: «Bind nañu ne Almasi bi fàww mu sonn, mu dekki ci diggante ñu dee ñi ci ñetteelu fan bi. 47 Te dinañu yégle ci turam ci xeet yi yépp li ko dale ci Yerusalem ngir nit ñi tuub seeni bàkkaar te jot mbaalum bàkkaar yi. 48 Yeen seede ngeen ci mbir mi. 49 Man, dinaa leen yónnee ci seen kaw li sama Baay dige, waaye yeen, des leen ci biir dëkk bi, ba Yàlla sol leen kàttanam.»
50 Noonu Yeesu génne leen ci dëkk bi, yóbbu leen ba ci wetu Betani. Mu yékkëti loxoom yi te barkeel leen. 51 Ci waxtu bi mu leen di barkeel, mu daldi tàggoo ak ñoom, te ñu yéegal ko ci kaw asamaan. 52 Ñoom nag, bi ñu sukkee màggal ko ba noppi, ñu dellu Yerusalem ak mbégte bu réy. 53 Ñu wéy ci kër-Yàlla gi, di seedeel Yàlla lu baax.