Teg nañu Yeesu daanu dee
23
Noonu kurélu àttekati Yawut yi yépp jóg nañu, indi Yeesu ci kanamu Pilaat. 2 Foofu ñu tàmbali di ko tuumaal ne: «Ki mooy kiy jaxase sunu askan bi, di tere ñu fey lempo Sesaar, te di wax ne moom mooy Almasi bi, di buur.» 3 Pilaat laaj Yeesu, ne ko: «Ndax yaw yaay buuru Yawut yi?» Mu tontu ko ne: «Yaw yaa ko wax.» 4 Pilaat wax njiiti-jébbalkati-sarax si ak mbooloo mi ne: «Kii déy, gisuma ci moom lenn lu jar ma koy teg daan.» 5 Waaye ñu gëna wax ne: «Moom day jógloo askan bi ci ay njàngaleem, dale ko ci diiwaanu Galile ak Yude ba fii.» 6 Bi Pilaat déggee loolu, mu laaj leen ne: «Ndax kii, waa Galile la?» 7 Bi Pilaat xamee ne ci diiwaan bi Erodd yilifoon la bokk, mu yónnee ko Yeesu, ndaxte Erodd mu ngi woon Yerusalem ci bés yooyu.8 Bi Erodd gisee Yeesu mu daldi ànd ak mbégte, ndaxte yàggoon na koo bëgga gis ndax li mu doon dégg ñu koy wax ci moom, te yaakaaroon na gis mu def fa ay kéemaan. 9 Mu laaj ko ay laaj yu bari waaye Yeesu tontuwu ko benn yoon. 10 Njiiti-jébbalkati-sarax si ak jàngalekati-yoonu-Musaa yi, nu ngi woon foofu di ko tuumaal ak doole. 11 Erodd ak soldaaram yi daldi jéppi Yeesu. Ñu ñaawal ko, solal ko mbubb mu rafet, te delloo ko Pilaat. 12 Ci bés boobu, Erodd ak Pilaat yi nekkoon ay noon, xaritoo nañu.
13 Gannaaw loolu, Pilaat dajalee njiiti-jébbalkati-sarax si, Kilifa yi ak mbooloo mi 14 ne leen: «Dangeen maa indil waa ji di ko tuumaal ne: "Dafay jaxase askan bi." Laaj naa ko ci seen kanam waaye gisuma ci moom dara lu jar ñu koy teg daan ci li ngeen koy tuumaal. 15 Erodd tamit gisul ci moom dara, ba tax mu delloosi nu ko. Waa jii deful dara lu jar ñu koy rey. 16 Waaye dinaa ko yewwi gannaaw bi ma ko dóorloo ay yar ba noppi.»
17 Pilaat dafa tàmmoon di bàyyi benn nit bu ñu tëj kaso ci màggalu Paak.
18 Waaye mbooloo mi àndoon nañu di yuuxu ak doole ne: «Rey ko, te nga bàyyil nu Barabas.» 19 Barabas moomu dañu ko tëjoon kaso ndax fippu bu amoon ci dëkk bi, ndaxte tamit dafa reyoon benn nit. 20 Waaye Pilaat di waxaat ak mbooloo mi, ndaxte dafa bëggoona yewwi Yeesu. 21 Te ñuy yuuxu di wax ne: «Daaj ko ci bant. Daaj ko ci bant.» 22 Waaye Pilaat waxaat leen ci ñetteelu yoon bi ne: «Lan la def lu bon? Gisuma ci moom dara lu jar nu koy teg daanu dee. Kon nag dinaa ko yewwi gannaaw bi ma ko dóorloo ay yar ba noppi.» 23 Waaye mbooloo mi gëna wax ak doole ne: «Daaj ko ci bant.» Seeni yuuxu daldi ko ëpp doole. 24 Pilaat jël dogal ngir may leen li ñu ko doon ñaan: 25 yewwi ki ñu tëjoon kaso ndax fippu te ndaxte tamit dafa reyoon benn nit, te jébbal Yeesu soldaar yi ngir ñu def ci moom li askan bi bëgg.
Daaj nañu Yeesu ci bant
26 Bi soldaar yi di yóbbu Yeesu ñu taseek benn waay bu tudd Simoŋ mu Siren te mu jóge woon ci tool yi. Ñu jàpp ko ak doole, sëf ko bant bi, ngir mu gàddu ko ci gannaaw Yeesu. 27 Noonu mbooloo mu bari di leen topp. Jigéen ñi di jooy te di naqarlu. 28 Yeesu walbatiku, jàkkaarlook ñoom, ne leen: «Yeen jigéenu Yerusalem buleen ma jooy, waaye jooyleen seen bopp ak seeni doom, 29 ndaxte ay jamonoo ngi ñëw, ñu wax ne: "barkeel nañu jigéen ñi mënula am doom, yi mësula ëmb ak yi mësula nàmpal". 30 Bu booba dinañu wax tund yu mag yi: "daanuleen sunu kaw," te tund yu ndaw yi: "muurleen nu." 31 Ndaxte bu ñuy def nii garab bu tooy bi, naka lañu wara def bu wow bi?»
32 Soldaar yi doon nañu yóbbaale ñaari waay di ay defkatu lu bon ngir rey leen ak Yeesu. 33 Bi ñu yegsee ci béréb bi ñuy woowe diggu bopp ñu daaj Yeesu ci bant. Ñu daajaale ñaar ñi, kenn ki ci ndeyjooram, keneen ki ci càmmoñam. 34 Noonu Yeesu daldi def ñaan bii ne: «Baay, baalal nit ñi li ñu ma def, ndaxte xamuñu li ñuy def.» Soldaar yi tegoo bant ngir séddoo yéreem. 35 Mbooloo mi taxawoon na fa di xool. Waaye njiiti Yawut yi di ñaawal Yeesu ne: «Muccal na ñeneen ñi, na muccal boppam, su de mooy Almasi bi, di ki Yàlla tànn.» 36 Soldaar yi tamit di ñaawal Yeesu, jegesi ko, jox ko bineegar, 37 di ko wax ne: «Xanaa du yaw yaay buuru Yawut yi? Kon muccalal sa bopp.» 38 Bind nañu ne: «Kii mooy buuru Yawut yi,» mu tiim boppu Yeesu. 39 Kenn ci defkatu lu bon yi ñu daajoon ci wetu Yeesu xas ko, ne ko: «Xanaa du yaw yaay Almasi bi? Kon muccalal sa bopp te muccalaale nu.» 40 Waaye beneen defkatu lu bon bi di ko yedd ne ko: «Xanaa yaw ragaloo Yàlla, yaw mi bokk ak moom daan? 41 Lu jub la ngir nun ndaxte danuy fey sunuy jëf, waaye moom, deful dara lu bon.» 42 Mu ne: «Yeesu, fàttaliku ma soo duggee ci sa nguur.» 43 Yeesu ne ko: «Ci dëgg maa ngi la koy wax, tey ji sax dinga nekk ak man, biir àjjana.»
44-45 Noonu ci diggu bëccëg bi, jant bi daldi nëbbu, mu lëndëm ci réew mi yépp lu tollook ñetti waxtu. Rido kër-Yàlla gi daldi xar ci digg bi. 46 Yeesu yuuxu ak baat bu kawe ne: «Baay, maa ngi teg sama ruu ci say loxo.» Gannaaw bi mu waxee kàddu yooyu, mu daldi dee. 47 Bi njiitu soldaaru Room bi gisee loolu muy màggal Yàlla te wax ne: «Ci dëgg, waa jii ku jub la woon.» 48 Mbooloo mi ñëwoon seetaansi mbir yooyu di dellu di fëgg seeni dënn di réccu. 49 Xaritu Yeesu yépp ak jigéen ñi ko toppe woon ci diiwaanu Galile taxawoon nañu fu sori di seetaan li fa xewoon.
Yuusufa denc na néewu Yeesu ci bàmmeel bi
50-51 Amoon na benn waay bu tuddoon Yuusufa, mu dëkk Arimate ci diiwaanu Yude. Nit ku jub la woon te baax te doon xaar nguuru Yàlla. Bokk ci kurélu àttekati Yawut yi waaye àndul woon ci ni ñu tege woon daan Yeesu. 52 Mu dem ci Pilaat laaj ko néewu Yeesu, 53 mu wàcce ko ci bant bi, lëmës ko ci perkaal, denc ko ci bàmmeel bu ñu yattoon te kenn mësu fa tëdd. 54 Booba àjjuma ci ngoon, bésu noflaay bi mu ngi dugg. 55 Jigéen ñi àndoon ak Yeesu ci Galile, topp Yuusufa ngir gis bàmmeel bi ak ni ñu dence néewu Yeesu. 56 Noonu ñu ñibbi, di defar cuuraay ak latkoloñ. Ci bésu noflaay bi, ñu toog, defuñu dara, ni ko yoonu Musaa digle.