Yudaa nangu na jébbale Yeesu
22
Màggalu mburu yu amul lawiir yi, maanaam màggalu Paak jegesi na. 2 Njiiti-jébbalkatu-sarax si ak jàngalekati-yoonu-Musaa yi, ñu ngi doon wut ay pexe yu ñuy reyloo Yeesu waaye bëgguñu ko woon fésal, ndaxte ragaloon nañu mbooloo mi. 3 Noonu Seytaane dugg Yudaa Iskariyot mi bokkoon ci fukk yi ak ñaar. 4 Mu dem ci njiiti-jébbalkati-sarax si ak njiiti garjen kër-Yàlla gi di waxtaan ak ñoom, ni mu leen di jébbale Yeesu. 5 Ñu ànd ci ak mbégte te nangu koo fey xaalis. 6 Yudaa nangu te dellu di wut ay pexe yu mu leen di jébbale Yeesu te mbooloo mi bañ ko yég.
Reeru Yeesu bu mujj bi
7 Ci màggalu mburu yu amul lawiir yi, bés bi ñuy rendi mbote yi ngir reeru Paak bi yegsi na. 8 Noonu Yeesu yónni Piyeer ak Yowaana ne leen: «Demleen, ngeen waajal nu reeru Paak bi.» 9 Ñu laaj ko ne ko: «Fan nga bëgg nu waaje ko?» 10 Mu ne leen: «Sungeen duggee ci dëkk bi, dingeen daje ak benn waay bu yenu ndaal bu am ndox. Toppleen ko ba ci kër gi muy dugg, 11 te nii ngeen di waxe ak boroom kër gi ne ko: "Jàngalekat bi moo lay wax ne: 'Fan mooy néegu gan bi may lekke reeru Paak bi ak samay taalibe?'" 12 Noonu dina leen won benn néeg bu yaatu; bu ñu defar ba noppi te mu féete ci kaw. Foofu ngeen koy waajale.» 13 Ñu dem fekk lépp ni leen ko Yeesu waxe woon, te ñu daldi waajal reeru Paak bi.
14 Bi waxtu bi jotee Yeesu toog na ak ndawam ya. 15 Noonu mu ne leen: «Sama xel bépp nekkoon na ci lekkandoo ak yeen reeru Paak bii bala ñu may teg ci coono, 16 ndaxte maa ngi leen koy wax dootuma lekk reer bii mukk lu dul bés bi nga xam ne ci la lépp li muy tekki di mat ci nguuru Yàlla.» 17 Noonu mu daldi jël kaasu biiñ, sant Yàlla ba noppi, ne leen: «Jëlleen kaas bi, ngeen séddoo ko ci seen biir 18 ndaxte maa ngi leen koy wax gannaaw si tey, dotuma naan biiñ mukk lu dul nguuru Yàlla gi di ñëw.» 19 Noonu mu jël mburu mi sant Yàlla ba noppi; damm ko, jox leen ko, ne: «Lii moo di sama yaram bi ma joxe ngir yeen; deeleen def lii ngir di ma fàttaliku.» 20 Gannaaw bi ñu reeree mu jël kaas bi jox leen ko te ne: «Kaas bii mooy kóllëre gu bees gi Yàlla fas jaarale ko ci sama deret bi ma tuur ngir yeen.
21 «Waaye xoolleen, ki ma nara jébbale mu ngi fii di reerandoo ak man 22 ndaxte Doomu nit ki dina dee ni ko Yàlla dogale waaye musiba dina dal nit ki koy jébbale.» 23 Ndaw yi di laajante ci seen biir, kan ci ñoom mooy ki nara def loolu.
24 Noonu ñu tàmbali di laajante te di werante ci seen biir kan mooy ki gëna màgg. 25 Yeesu jël kàddu gi ne leen: «Buuri xeet yi dañuy nguuru ak doole ci seen askan yi te njiit yiy jëfe ak sañ-sañ ci ñoom, ñuy sàkku ñu woowe leen ay defkatu lu baax. 26 Buleen jëfe noonu. Waaye na ki gëna mag ci seen biir mel ni ki gëna ndaw te ki jiite mel ni surga bi. 27 Ci seen xalaat kan mooy ki gëna mag? Ki toog ci bérébu lekkukaay bi walla ki koy toppatoo? Ndax du ki toog ci bérébu lekkukaay bi? Waaye man damaa nekk ci seen biir ni surga. 28 Yeena doon muñandoo ak man ci samay coono; 29 moo tax ni ma Baay bi joxe nguur gi dinaa leen ko joxaat, 30 ngir ngeen lekkandoo te naanandoo ak man ci sama nguur, te ngeen toog ci ay baŋi nguur, ngir àtte fukki giir ak ñaar yu Israyil.»
31 Noonu Yeesu ne: «Simoŋ, Simoŋ, moytul! Seytaane ñaan na Yàlla sañ-sañ ngir sonnal leen ni ñuy teqale dugub ak xatax. 32 Waaye man ñaanal naa la, ngir nga baña ñàkk sa ngëm. Te bés bi ngay dellusi ci man nanga dëgëral say mbokki taalibe.» 33 Simoŋ ne ko: «Boroom bi pare naa su ko jaree, ma ànd ak yaw kaso walla sax ma dee.» 34 Yeesu ne ko: «Piyeer maa ngi la koy wax tey jii sax bala ginaar di sab dinga weddi ñetti yoon ne xam nga ma.»
35 Noonu Yeesu wax taalibeem yépp ne: «Bi ma leen yónnee te yóbbaalewuleen kalpe, saaku tukki ak dàll, ndax ñàkkoon ngeen dara?» Ñu ne ko: «Ñàkkunu woon dara.» 36 Mu ne leen: «Waaye léegi na ki am kalpe, jël ko. Na ki am saaku tukki tamit jël ko, te ki amul jaasi jaay sabadooram, jënd ko. 37 Maa ngi leen koy wax fàww mu mat li Mbind mi wax ci man ne: "Boole nañu ko ak defkatu lu bon yi," ndaxte lépp li ñu bind ci man dina mat.» 38 Ñu ne ko: «Boroom bi am nanu fii ñaari jaasi.» Mu ne leen: «Loolu doy na.»
Yeesu ñaan na ci tundu Oliw ya
39 Yeesu génn di dem ci tundu Oliw ya, ni mu ko tàmme woon di defe. Taalibe yi topp ko. 40 Bi ñu yegsee mu ne leen: «Ñaanleen ngir ngeen baña daanu ci fiir.» 41 Mu sori leen tuuti, sukk óomam di ñaan 42 ne: «Baay, su la neexee soril ma kaasu naqar bii, waaye bu mu doon sama coobare waaye na sa coobare rekk am.» 43 Noonu malaaka asamaan feeñu ko te di ko dëgëral. 44 Ci njaqareem, muy gëna sawar ci ñaan ba ñaq yi mel ni ay toqu deret di daanu ci suuf. 45 Mu ñaan ba noppi, jóg, ñëw, fekk taalibe yi nelawoon nañu ndax tiis. 46 Mu ne leen: «Lan moo tax ngeen di nelaw? Jógleen te ngeen ñaan ngir ngeen baña daanu ci fiir.»
Yudaa jébbale na Yeesu, ñu jàpp ko te njiiti Yawut yi di ko laaj
47 Bi Yeesu di wax loolu, mbooloo mu bari yegsi, te ki ñuy woowe Yudaa, bokkoon ci fukk yi ak ñaar, jiitu leen. Mu jegesi Yeesu ngir fóon ko, 48 waaye Yeesu ne: «Yudaa, ndax ci fóon ngay jébbale Doomu nit ki?» 49 Noonu bi ñi àndoon ak Yeesu gisee li waroona xew, ñu laaj ko ne: «Boroom bi, ndax nu jëfandikoo sunuy jaasi?» 50 Te kenn ci ñoom dóor surga njiitu-jébbalkati-sarax si, ba dagg noppu ndeyjooram. 51 Waaye Yeesu jël kàddu gi ne leen: «Bàyyileen, doy na,» te mu laal noppu waa ji te wéral ko. 52 Noonu Yeesu wax njiiti-jébbalkati-sarax yi ak mag ñi ak njiiti garjen Kër-Yàlla gi, yi ñëwoon jàppsi ko ne leen: «Lu tax ngeen gàddu seeni jaasi ak seeni yet mel ni ñuy wuta jàpp defkatu lu bon, 53 moona bés bu nekk nekkandoo woon naa ak yeen ci kër-Yàlla gi te jàppuleen ma waaye léegi ngir yeen waxtu bi jot na, waxtu bi kilifteefu lëndëm bi di jëf.»
54 Ci noonu ñu jàpp Yeesu te yóbbu ko ci kër njiitu-jébbalkatu-sarax si, te Piyeer doon leen toppe fu sori. 55 Ci diggu ëtt bi taaloon nañu fa xal, te nit ñu bari toog, wër xal bi, te Piyeer toogoon ci seen biir. 56 Benn surga bu jigéen gis ko mu toog ci leeraayu xal bi, mu daldi ko xool te wax ko ne: «Nit kii tamit nekkoon na ak moom.» 57 Waaye Piyeer weddi ko ne: «Soxna si, xamuma ko.» 58 Ci kanam tuuti, keneen gis ko te wax ne: «Yaw tamit, ci ñoom nga bokk.» Waaye Piyeer tontu ko ne: «Déedéet, sama waay, bokkuma ci.» 59 Lu tollu ci benn waxtu kenn di wax te di ko dëggal ne: «Ci dëgg, nit kii àndoon na ak moom, ndaxte ci diiwaanu Galile la jóge.» 60 Waaye Piyeer tontu ko ne: «Sama waay, xawma li nga bëgga wax.» Ci saa si bi mu nekkee di wax loolu benn ginaar sab. 61 Noonu Boroom bi geestu, xool Piyeer te Piyeer fàttaliku li ko Boroom bi waxoon ne: «Bala ginaar gi sab tey dinga ma weddi ñetti yoon ne xam nga ma.» 62 Te Piyeer génn, di jooy, jooy yu metti.
63 Nit ñi jàppoon Yeesu di ko ñaawal te di ko dóor. 64 Ñu muur kanamam di ko laaj: «Éey yonent bi, wax nu, kan moo la dóor!» 65 Te ñu koy wax yeneen kàddu yu bon ngir saaga ko.
66 Bi bët setee kurélu àttekati Yawut yi: njiiti-jébbalkati-sarax yi ak jàngalekati-yoonu-Musaa yi booloo nañu. Ñu andil leen Yeesu ci bérébu àttekaay bu mag bi. 67 Ñu wax ko ne: «Wax nu, ndax yaw yaay Almasi bi?» Yeesu tontu leen: «Su ma leen ko waxee, dooleen ma gëm, 68 te su ma leen ko laajee, dooleen ma tontu. 69 Waaye dale ko tey, Doomu nit ki dina toog ci ndeyjooru Yàlla Aji-Kàttan ji.» 70 Ñoom ñépp ñu wax ne: «Ndax yaw yaay Doomu Yàlla ji, nag?» Mu tontu leen ne: «Yeena wax ne moom laa.» 71 Noonu ñu daldi wax ne: «Soxlatunu beneen seede ndaxte dégg nanu ba noppi li mu tontu ci gémmiñam.»