Saraxu jigéen ju néew doole bi
21
Bi Yeesu yékkëtee bëtam mu gis boroom alal yiy joxe seen sarax ci ndab bi ñuy joxee xaalis ci biir kër-Yàlla gi. 2 Itam mu gis benn jigéen bu jëkkëram gaañu woon te néew doole, mu joxe ñaari xànjaru xaalis. 3 Noonu mu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jigéen bi néew doole moo gëna joxe yeneen nit yi yépp 4 ndaxte ñoom ñépp dañoo joxe ci seen barile waaye moom dafa joxe ci néewleem ba joxe lépp li mu wara dunde.»
Yàqute Yerusalem ak dellusi Doomu nit ki
5 Yenn nit doon wax ci kër-Yàlla gi ak ci xeer yu rafet yi ñu ko defare ak yeneen yëf yu nit ñi saraxe woon ngir rafetal kër-Yàlla gi. Waaye Yeesu ne leen: 6 «Mbir yi ngeen di xool nii, ay bés a ngi ñëw yoo xamante ne xeer du des ci xeer, lépp dina yàqu.» 7 Noonu ñu laaj ko ne: «Jàngalekat bi, kañ la mbir yooyu di ñëw ak ban màndarga moo leen di firndeel?» 8 Yeesu tontu leen: «Moytuleen ñu nax leen ndaxte dina am ñu bari ñuy ñëw ci sama tur tey wax ne: "Man maay Almasi bi," te "waxtu bi jegesi na." Buleen topp ñooñu. 9 Bu ngeen déggee mbir yii: ay xare ak ay réew yu fippu, buleen ragal ndaxte mbir yooyu fàww ñu am, bu jëkk. Waaye nekkagul njeextel gi.»
10 Mu yokk ca ne: «Benn xeet dina jóg ngir xeex ak moroomu xeetam te benn réew dina jóg ngir xeex ak moroomu réewam. 11 Dina am ay yëngute yu réy ci suuf si ak xiif ak ay feebari mbas ci béréb yu wuute. Dina am ay xew-xew yuy tiitalaate ak ay màndarga yu mag ci biir asamaan si. 12 Waaye bala loolu dinañu leen teg loxo di leen metital te ñu jébbal leen ci kër-ñaan yi ngir àtte leen, te noonu ñu tëj leen ci kaso yi. Dinañu leen yóbbu ci kanamu buur yi ak ci kanamu njiiti réew yi ndax sama tur. 13 Loolu dina leen dal ngir ngeen mëna seede. 14 Waaye defleen ci seen xel ne waruleen jaaxle ci li ngeen wara wax, 15 ndaxte dinaa leen jox kàddu yu ànd ak xel ngir seeni noon duñu leen mëna weddi. 16 Seeni waajur, seeni mag walla rakk, seeni mbokk ak seeni xarit dinañu leen jébbale te dinañu rey ñu bari ci yeen. 17 Ñépp dinañu leen bañ ndax man 18 waaye dungeen ñàkk benn kawar ci seen bopp, 19 te ci seen dëgër-dëgërlu dingeen muccal seen dund.
20 «Bu ngeen gisee ay soldaar yu wër Yerusalem, ngeen xam ne yàquteem jegesi na. 21 Noonu ñi nekk ci Yude, nañu daw yéeg ci tund yi; ñi nekk ci diggu Yerusalem, nañu génn, dem; ñi nekk ci àll bi, buñu dugg ci dëkk bi, 22 ndaxte ay bési feyyu lay doon, ay bési matal lépp li nga xam ne moom la Mbind mi wax. 23 Musiba dina dal jigéen ñi nga xam ne ñoo ëmb ak ñi di nàmpal ci bés yooyu, ndaxte njàqare bu mag dina am ci réew mii ak mer ci askan bi. 24 Dinañu daanu fi nga xam ne foofu la jaasi bi di dagge; dinañu leen téye ci ay réew te ñi nga xamante ne nekkuñu Yawut dinañu dëggaate Yerusalem ba seen waxtu di mat.
25 «Ci biir jant bi ak weer bi ak biddéew yi, ay màndarga yu yéeme dinañu ci jóge. Ci suuf si, xeet yi dinañu ànd ak njàqare ndax ngelaw bu metti biy yëngu ci biir géej gi. 26 Tiit dina bëgga rey xeet yi ci mbir yu ñëwagul ci suuf si, ndaxte kàttani asamaan dinañu yëngu. 27 Noonu dinañu gis Doomu nit ki di ñëw ci biir niir ak kàttanam bu bari ak màggaayam bu bari. 28 Su mbir yooyu tàmbalee am, nangeen dëgër-dëgërlu, yékkëti seeni bopp, ànd ak yaakaar ndaxte Yàlla dina leen yewwi ci anam bu gàtt.»
29 Noonu Yeesu nettali leen léeb bii, ne: «Sungeen gisee figg, maanaam benn xeetu garab, ak yeneen xeetu garab yépp, 30 seeni xob tàmbalee sëq, dangeen di xam ne waxtu góob bi jegesi na. 31 Noonu yeen tamit, sungeen gisee mbir yooyu di xew, xamleen ne nguuru Yàlla gi jegesi na. 32 Ci dëgg, maa ngi leen koy wax, niti jamono jooju duñu romb mukk te mbir yooyu matul. 33 Asamaan ak suuf dinañu weesu, waaye samay kàddu duñu weesu mukk.
34 «Buleen xër ci bànneexu àddina, buleen di màndi, buleen jaaxle ci lu jëm ci dund bi. Loolu yépp dina jaxase seen xel, 35 ba tax bésu àtte bi di leen bett ni mbaal, ndaxte bés boobu dina daanu ci kaw ñépp ñi nekk ci suuf si. 36 Yeewuleen te sax di ñaan saay su nekk, ngir ngeen am dooley dékku mbir yooyu di ñëw te mëna taxaw ak kóolute ci kanamu Doomu nit ki.»
37 Ci bés yooyu Yeesu di jàngale ci biir kër-Yàlla bi te ci guddi yooyu, mu doon dem ci tund bi ñuy woowe tund Oliw ya, 38 te mbooloo mi yépp ci suba teel, dañu doon dem ci moom ci kër-Yàlla bi ngir déglu ko.