Sañ-sañu Yeesu
20
Benn bés Yeesu da doon jàngale ci kër-Yàlla gi di yégal xibaar bu baax bi askan bi. Njiiti-jébbalkatu-sarax yi, jàngalekatu-yoonu-Musaa yi, ak mag yi ñëw ci moom 2 laaj ko ne: «Wax nu, ci ban sañ-sañ ngay defe mbir yi ak kan moo la jox sañ-sañ boobu?» 3 Noonu Yeesu tontu leen: «Man tamit am naa benn laaj ngir yeen. 4 Lu Yaxya doon sóobe nit ñi ci ndox, fan la ko jële, ci Yàlla walla ci nit?» 5 Ñuy waxtaan ci seen biir ne: «bu nu waxee ne ci Yàlla la ko jële, dina wax "Lan moo tax gëmuleen ko?" 6 Waaye bu ñu waxee ci nit la ko jële askan bi yépp dinañu sànni ay xeer ba nu dee, ndaxte gëm nañu ne Yaxya yonent la woon.» 7 Noonu ñu tontu ko ne: «Xamunu fan la ko jële.» 8 Yeesu ne leen: «Kon nag man itam duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe mbir yii.»9 Gannaaw loolu Yeesu tàmbalee di nettali léeb bii askan bi: «Dafa amoon benn waay bu jëmbët toolu reseñ, batale ko ay beykat, mu tukki te yàgg fa lool. 10 Bi waxtu góob jotee mu yónni benn surga ci beykat yi ngir ñu jox ko wàllam ci meññeef bi waaye beykat yi dóor ko, dàq ko loxoy neen. 11 Boroom tool bi yónniwaat beneen surga waaye beykat yi dóor ko moom itam, saaga ko, dàq ko loxoy neen. 12 Mu yónniwaat ñetteelu surga waaye beykat yi gaañ ko, génne ko tool bi. 13 Noonu boroom tool bi ne: "Lan laa wara def? Dinaa yónni sama doom bi ma sopp. Xéy-na, ñu jox ko cér." 14 Waaye bi ko beykat yi gisee ñuy wax ci seen biir ne: "Ki wara donn tool bi mu ngi nee di ñëw. Nanu ko rey ngir moom tool bi." 15 Noonu ñu génne ko tool bi te rey ko.» Yeesu laaj leen: «Naka la boroom tool bi wara def beykat yooyu? 16 Dina ñëw rey beykat yi, jël toolam dénk ko yeneen nit.» Bi nit ñi déggee kàddu yooyu, ñu ne: «Yàlla tere.» 17 Waaye Yeesu xool leen ci biir bët te ne leen: «Kon nag lan la kàddu yi ci Mbind mi di tekki:
"Doj bi tabaxkat yi sànni woon
mujj na nekk doj bi ëpp solo ci tabax bi"?
18 Ku daanu ci kaw doj bii damm. Te képp ku mu daanu ci sa kaw dina la rajaxe.»
Ay nit yu doon fexe fiir Yeesu
19 Noonu jàngalekati-yoonu-Musaa yi ak njiiti-jébbalkatu-sarax yi di wut nu ñu jàppe Yeesu ci waxtu boobu, ndaxte xamoon nañu ne léeb bi mu doon wax ngir ñoom la woon, waaye ragaloon nañu askan bi. 20 Ñu tàmbali di bàyyee xel Yeesu. Ci noonu ñu yónnee ko ay nit yu doon mbubboo jub. Nit ñooñu dañu ko waroona fiir jaarale ko ci benn laaj ngir mën koo jébbal njiitu Yude, bi am kilifteef ak sañ-sañ ci diiwaan bi. 21 Ñu laaj ko, laaj bii, ne: «Jàngalekat bi xam nanu ne dangay wax tey jàngale ci njub te doo àtte nit ci melokaanam, waaye dangay jàngale yoonu Yàlla ci njub. 22 Wax nu nag léegi, ndax yoonu Musaa bi maye na walla déet, nuy fey lempo Sesaar?» 23 Yeesu daldi xam seen pexe te wax leen ne: 24 «Wonleen ma benn xànjaru xaalis. Nataal ak mbind mi ci nekk, kan moy boroom?» Ñu ne ko: «Sesaar.» 25 Yeesu daldi leen ne: «Kon nag joxleen Sesaar, li Sesaar moom te ngeen jox Yàlla, li Yàlla moom.» 26 Noonu mënuñu ko woona jàpp ci ay waxam ci kanamu askan bi. Ñu waaru ci ay tontoom te amatuñu woon lu ñu wax.
27 Ñenn ci ni bokkoon ci tarixa Sadusen yi ñëw ci Yeesu. Sadusen yi gëmuñu woon ne ndekkite am na. Ñu laaj ko ne: 28 «Jàngalekat bi, Musaa ci mbindam dafa nu jox ndigal ne, su fekkee dafa am benn waay ju dee, bàyyi jabar te amul doom, rakkam dafa wara takk ku jigéen ki ngir amal ko doom. 29 Léegi nag dafa amoon juróom ñaari góor yu bokk ndey ak baay, taaw bi takk jabar dee te amul doom. 30 Ñaareel ba takk ku jigéen ki, daldi dee, ñetteel ba noonu, 31 ba juróom ñaar ñi yépp dee te amuñu doom. 32 Gannaaw loolu ku jigéen ki daldi dee. 33 Ci ndekkitelu ñu dee ñi, kan ci ñoom mooy nekk jëkkëru ku jigéen ki? Ndaxte juróom ñaar ñépp takkoon nañu ko.»
34 Yeesu tontu leen ne: «Ci àddina sii góor yi dañuy takk jabar, jigéen ñi di séyi, 35 waaye ñi Yàlla di àtte ñu yeyoo dekki ci ñu dee ñi ngir dund ci jamono jee di ñëw dootuñu séy, 36 te dootuñu mëna dee tamit ndaxte dinañu mel ni malaaka yi. Ay doomu Yàlla lañu, ndaxte moo leen dekkil ci ñu dee ñi. 37 Musaa ci boppam wone na ne ndekkite am na bi mu bindee ci téereem, ci lu jëm ci safara suy tàkk ci garab bi. Foofu la Musaa woowe Boroom bi, "Yàllay Ibraayma, Yàllay Isaaxa ak Yàllay Yanqóoba". 38 Kon nag Yàlla nekkul Yàllay ñu dee ñi waaye Yàllay ñiy dund, ndaxte ci moom ñépp dañuy dund.» 39 Noonu ñenn ci jàngalekati-yoonu-Musaa yi jël kàddu gi ne ko: «Dëgg bu wér péŋŋ nga wax, jàngalekat bi!» 40 Ndaxte ñemeetuñu ko woona laaj dara.
41 Yeesu waxaat leen ne: «Naka la nit ñi mëna waxe ne Almasi bi sëtu Daawuda la? 42 Ndaxte Daawuda ci boppam sax wax na ci Sabóor yi ne:
"Yàlla Aji-Sax ji nee na sama Boroom:
'toogal ci sama ndeyjoor
43 ba ma daaneel say noon fi ngay teg say tànk.'"
44 Daawuda woowe na Almasi bi Boroomam. Kon nag naka la Almasi bi mëna nekke sëtu Daawuda?»
45 Bi ko askan bi yépp di déglu, Yeesu wax taalibeem yi ne: 46 «Moytuleen jàngalekati-yoonu-Musaa yi bëgg di doxantu, sol mbubb yu réy te bëgg ñu leen di nuyu ci pénc dëkk bi. Ñuy tànn di toog ci toogukaay yi féete kanam ci kër-ñaan yi, tey taamu toogukaay yu yiw yi ci lekku xew yi. 47 Di yàq alalu jigéen ñi ñàkk seen jëkkër tey ñaan ak ngistal, ay ñaan yu gudd. Seen àtte mooy gëna metti.»