Sase dalal na Yeesu ci këram
19
Yeesu wéy ci yoonam, dugg Yeriko, doon jàll dëkk bi. 2 Foofu amoon na benn nit bu ñuy woowe Sase, njiitu juutikat te am alal. 3 Mu bëggoona gis kan mooy Yeesu, waaye mënu ko woona gis ndax mbooloo mi, ndaxte dafa gàttoon. 4 Noonu mu daw jiitu ko, yéeg ci génn garab bu ñuy woowe sicomor ngir gis ko, ndaxte xamoon na ne foofu la waroona jaar. 5 Bi Yeesu yegsee ci béréb bi, mu yékkëti bëtam yi, wax ko ne: «Sase, gaawantul nga wàcc ndaxte fàww ma dal sa kër tey.» 6 Sase gaawantu wàcc dalal ko ak mbégte. 7 Bi ñu gisee loolu, ñoom ñépp tàmbali nañu xuntu di naan: «Dem na dal ci kër bàkkaarkat.» 8 Waaye Sase taxaw ci kanamu Boroom bi te wax ko ne: «Xoolal, Boroom bi! Dinaa joxe sama genn-wàll alal néew ji doole yi te su fekkee ne tooñ naa nit jël alalam, dinaa ko fey ñeenti yoon.» 9 Noonu Yeesu wax ko ne: «Tey, mucc gi dugg na ci kër gii, ndaxte Sase mii tamit sëtu Ibraayma la, 10 ndaxte Doomu nit ki ñëw na ngir seet te musal ñi réer.»Léebu buur bi dénkoon surgaam yi wurus
11 Ni mbooloo mi doon dégloo kàddu yooyu, Yeesu yokk ca, wax leen benn léeb ndaxte fekkoon na ñu jegesi Yerusalem te mbooloo mi foogoon nañu ne nguuru Yàlla gi dina feeñ ci saa si. 12 Loolu moo tax mu ne leen: «Dafa amoon boroom juddu bu rafet, bu bokk ci njabootu buur te waroona dem ci réew mu sori ngir ñu fal ko buur te mu dellusi. 13 Bala muy dem mu woo fukk ci ay surgaam te dénk leen ku ci nekk benn wurus te ne leen: "Fexeleen mu jur bala may dellusi." 14 Waaye waa réewam bañ ko, yónni ay ndaw ci gannaawam ngir ñu wax: "Nit ki, bëggunu mu nekk sunu buur."
15 «Gannaaw bi ñu ko falee buur, mu dellusi ci réewam, te woo surga yi mu dénkoon wurus yi ngir xam lan lañu ci jële. 16 Ku jëkk ki jegesi ko, wax ko ne: "Sang bi sa benn wurus bi jur na fukk." 17 Buur bi ne ko: "Waaw góor, surga bu baax nga te gore ci ay mbir yu ndaw. Dénk naa la fukki dëkk." 18 Ñaareelu surga bi ñëw, wax ko ne: "Sang bi, sa benn wurus bi jur na juróomi wurus." 19 Buur bi ne ko: "Yaw tamit, dénk naa la juróomi dëkk."
20 «Beneen surga bi ñëw ne ko: "Sang bi, wurus bi nga ma joxoon mu ngi nii. Dama koo lëmës, denc ko. 21 Dama laa ragal ndaxte ku néeg nga te dangay nangu alal joo dencul te di góob foo jiwuloon." 22 Buur bi ne ko: "Ci say kàddu laa laay àtte, yaw surga bu bon bi. Bi nga xamee, ku néeg laa di nangu alal ji ma dencul te di góob li ma jiwul, 23 lan moo tax jëloo sama benn wurus bi ma la dénkoon te denc ko fi ñuy dence wurus yi, ba bu ma dellusee ma jot sama wurus ak li mu jur?"
24 «Noonu mu ne ñi fa nekkoon: "Jëlleen benn wurus bi te ngeen dolli ko ki am fukki wurus yi." 25 Noonu, ñu tontu ko ne: "Sang bi, kooku am na fukki wurus." 26 Noonu mu ne leen: "Maa ngi leen koy wax, ku am dinañu ko dollil, waaye ku amul, dinañu jël lu tuuti sax li nga yor. 27 Samay noon yi bañoon ma nekk seen buur andil ma leen fii te ngeen rey leen ci sama kanam."»
Yeesu dugg na Yerusalem
28 Gannaaw bi mu waxee loolu Yeesu jiitu na leen di dem Yerusalem. 29 Bi mu jegesee dëkku Betfase ak bu Betani ci wetu tund bi ñuy woowe Tundu Oliw ya, mu yónni ñaar ci taalibeem yi 30 ne leen: «Demleen ci gox bi nekk seen kanam. Su ngeen yeggee dingeen fekk benn mbaam bu ndaw bu kenn mësula yéeg. Yewwileen ko, ngeen indi ko fii. 31 Bu leen kenn laajee "Lu tax ngeen di yewwi mbaam bi?" neleen ko "Boroom bi Yeesu moo ko soxla."»
32 Ñi mu yónni, bi ñu yeggee ñu fekk lépp ni leen ko Yeesu waxe woon. 33 Bi ñuy yewwi mbaam mi, ñi moom mbaam mi ne leen: «Lu tax ngeen di yewwi mbaam mi?» 34 Ñu tontu leen ne: «Boroom bi Yeesu moo ko soxla.»
35 Noonu ñu indil Yeesu mbaam mi, teg ci seen yére yi te yéegal Yeesu ci mbaam mi. 36 Yeesu, bi muy dem, nit ñi di lal seen yére yi ci yoon bi. 37 Bi mu jegesee yoon bi wàcce ci tundu Oliw ya, mbooloo taalibeem yi yépp ànd ak mbégte, di sant Yàlla ak baat bu kawe ndax kéemaan yépp yi ñu gisoon, 38 di wax ne:
«Barkeel na buur biy ñëw ci turu Boroom bi.
Na jàmm am ci asamaan
te ñu màggal Yàlla ci béréb yi gëna kawe.»
39 Noonu ñenn ci Farisen yi nekkoon ci mbooloo mi wax Yeesu ne: «Jàngalekat bi, waxal sa taalibe yi ñu noppi.» 40 Yeesu tontu ne: «Maa ngi leen koy wax, su ñu noppee, xeer yi dinañu yuuxu.»
41 Bi Yeesu jegesee dëkku Yerusalem te gis ko, mu jooy ci moom 42 te wax ne: «Aa yaw, soo ràññee woon ci bés bii, li lay may jàmm. Waaye léegi loolu lépp nëbbu na ci say bët. 43 Ndaxte ci yaw ay bés a ngi ñëw, say noon dinañu defar ay jalu suuf ngir wër la, te tanc la ci boor bu nekk. 44 Dinañu la yàqate yaxeet, yaw ak sa waa dëkk te duñu bàyyi ci yaw doj ci kaw doj. Lu tax? Ndaxte ràññeewoo jamono ji la Yàlla wallusee.»
Yeesu dàq na ay jaaykat ci kër-Yàlla gi
45 Gannaaw loolu Yeesu dugg na ci kër-Yàlla gi, fekk fa ay jaaykat. Noonu mu dàq leen, 46 di leen wax ne, «Mbind mi nee na, sama kër, këru ñaanukaay lay doon, waaye yeen def ngeen ko këru sàcc.» 47 Yeesu doon na jàngale bés bu nekk ci kër-Yàlla gi. Noonu njiiti-jébbalkati-sarax yi ak ay jàngalekati-yoonu-Musaa ak njiiti askan bi, ñu ngi ko doon wuta rey, 48 waaye amuñu woon pexe ngir def ko ndaxte askan bi yépp, ñu ngi ko doon déglu ak xel.