Yeesu jàngale na ci naka la nit mëna jege Yàlla
18
Gannaaw loolu Yeesu nettali leen benn léeb ngir won leen ne dañu war di ñaan saa su nekk te baña xàddi. 2 Mu ne leen: «Dafa amoon ci benn dëkk, benn àttekat bu ragalul woon Yàlla te faalewul kenn. 3 Ci dëkk boobu tamit amoon na benn jigéen bu ñàkkoon jëkkëram te doon ñëw ci moom saa su nekk te ne ko: "Àtte ma ak ki ma joteel." 4 Àttekat ba, bañ na lu yàgg waaye gannaaw loolu mu wax ci xelam ne: "Doonte ragaluma Yàlla te faalewuma kenn, 5 jigéen jii lakkal na ma, kon nag dinaa ko àtte ngir mu bañati ñëw di ma sonnal."» 6 Boroom bi yokk ca ne: «Dégluleen li àttekat bu bon bi wax. 7 Te Yàlla ndax du àtte jub ñi mu tànn tey ñaan ci moom guddi ak bëccëg? Ndax dina leen xaarloo? 8 Maa ngi leen koy wax, dina leen gaawa àtte jub. Waaye nag Doomu nit ki buy dellusi ndax dina fekk ngëm ci àddina si?»9 Noonu Yeesu nettali leen beneen léeb jëmale ko ci ñiy jàppe seen bopp ñu jub tey xeeb ñeneen ñi. 10 «Dafa amoon ñaari waay yu demoon ci kër-Yàlla gi ngir ñaan. Kenn ki ab Farisen la woon, keneen ki ab juutikat. 11 Farisen bi taxaw di ñaan ci xelam ne: "Yàlla maa ngi lay gërëm ci ni ma melul ni yeneen nit, ñiy sàcc, di def lu bon, te di njaaloo, rawatina juutikat bee. 12 Waaye damay woor ñaari yoon ci juróom ñaari fan yu nekk tey joxe asaka ci lépp li ma am." 13 Waaye juutikat bi moom taxaw na fu sori, te bëggul sax siggi, xol asamaan, di fëgg dënnam di réccu tey wax ci suuf ne: "Yàlla yërëm ma, man bàkkaarkat bi."» 14 Yeesu yokk ca ne: «Maa ngi leen koy wax, kooku bi muy ñibbi këram Yàlla àtte na ko ni ku jub, waaye du Farisen bi, ndaxte képp ku yékkëtiku dinañu la suufeel te ku suufeelu dinañu la yékkëti.»
15 Amoon na ñu ñëw indil Yeesu ay gone ngir mu teg leen loxo, waaye bi taalibe yi gisee loolu ñu di leen gëdd. 16 Yeesu woo gone yi, ñu ñëw te wax ne: «Bàyyileen gone yi ñu ñëw ci man. Buleen leen tere ndaxte ñu mel ni ñoom ñoo moom nguuru Yàlla gi. 17 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, képp ku nanguwul nguuru Yàlla gi ni gone, doo ci dugg mukk.»
Boroom alal dugg ci nguuru Yàlla
18 Noonu benn njiitu Yawut laaj Yeesu ne: «Jàngalekat bu baax bi, lan laa wara def ngir am dund gu dul jeex?» 19 Yeesu tontu ko ne: «Lan moo tax nga may woowe ku baax? Kenn baaxul ku dul Yàlla rekk. 20 Xam nga ndigal yi, bul njaaloo, bul rey, bul sàcc, bul seede lu dul dëgg, teralal sa yaay ak baay.» 21 Waa ji ne ko: «Ndigle yooyu yépp, sàmm naa ko bi ma nekkee ndaw ba léegi!» 22 Bi Yeesu déggee loolu mu ne: «Lenn rekk moo la dese: jaayal lépp li nga am, séddale ko néew-di-doole yi, noonu dinga am alal ci asamaan, te nga ñëw topp ci man.» 23 Waaye bi waa ji déggee loolu, mu ànd ak tiis ndaxte dafa bari woon alal lool.
24 Bi Yeesu gisee waa ji ànd ak tiis mu ne: «Lu jafe a ngoogu ngir boroom alal dugg ci nguuru Yàlla! 25 Giléem jaar ci bën-bënu puso moo gëna yomb boroom alal dugg ci nguuru Yàlla.» 26 Ñi ko doon déglu daldi ne: «Kon nag, ku mëna mucc?» 27 Yeesu ne leen: «Lu të nit, Yàlla mën na ko.»
28 Piyeer ne ko: «Xoolal! Nun, bàyyi nanu lépp lu nu amoon ngir topp la.» 29 Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, képp ku bàyyi këram, jabaram, ay magam, ay rakkam, ay waajuram walla ay doomam ndax nguuru Yàlla gi, 30 dina jot lu bari lool ci àddina si ak dund gu dul jeex ci jamono jee di ñëw.»
Yeesu xamal na fukk yi ak ñaar li ko wara dal ci Yerusalem
31 Yeesu jëloon na fukk yi ak ñaar, ber leen, ne leen: «Dégluleen! Nu ngi ci yoonu Yerusalem. Foofu lépp li nga xam ne moom la yonent yi bindoon ci Doomu nit ki dina mat. 32 Dinañu ko jébbal ci loxoy ñi nga xam ne nekkuñu Yawut. Dinañu ko ñaawal, saaga ko, tifli ko, 33 dóor ko ay yar ba noppi, daldi ko rey, te ci ñetteelu fan ba mu dekki.» 34 Waaye loolu leerul ci taalibe yi, kàddu yooyu ump na leen, te xamuñu li wax yooyu di tekki.
Yeesu wéral na waa ju gumba
35 Benn bés Yeesu di jegesi dëkku Yeriko. Ci wetu yoon bi amoon na gumba bu fa toog di yelwaan. 36 Bi mu déggee mbooloo mi di jàll mu laaj lan moo xew. 37 Ñu xamal ko ne Yeesu mu Nasaret mooy jàll. 38 Noonu muy yuuxu te wax ne: «Yeesu sëtu Daawuda yërëm ma.» 39 Waaye ñi jiitu woon ci kanam di ko gëdd te di ko tere mu wax. Waaye mu gëna yuuxu ak baat bu kawe di wax ne: «Sëtu Daawuda yërëm ma.»
40 Yeesu daldi taxaw te sant leen ñu andil ko ko. Bi gumba bi jegesee Yeesu, Yeesu laaj ko ne: 41 «Loo bëgg ma defal la ko?» Gumba bi ne ko: «Boroom bi, damaa bëgga gisaat.» 42 Yeesu ne ko: «Gisaatal. Sa ngëm wéral na la.» 43 Ci saa si mu daldi gisaat te topp Yeesu di màggal Yàlla. Mbooloo ma fa nekkoon yépp, bi ñu gisee loolu ñoom tamit ñuy sant Yàlla.