Bàkkaar, ngëm, te warugaru surga
17
Yeesu wéyal njàngaleem di wax taalibe yi ne: «Lu leen di xiir ci bàkkaar mënula ñàkk ci seen biir, waaye musiba dina dal ci ki muy jaar. 2 Ñu takk ko xeer gu réy ci baatam te sànni ko ci biir géej gi, mooy gën ci moom, muy bàkkaarloo kenn ci ñi gëna ndaw. 3 Moytuleen yeen ci seen bopp! Bu la sa moroom tooñee, woo ko, nga yedd ko. Bu tuubee, baal ko. 4 Te bu la tooñee juróom ñaari yoon ci bés bi, mu dellu juróom ñaari yoon ne la: "Tuub naa", baal ko.»5 Ci noonu, ndaw yi ñaan Boroom bi ne: «Yokkal nu sunu ngëm.» 6 Boroom bi ne leen: «Bu ngeen amee ngëm bu tuuti bu tollu ni peppu fuddën sax, dingeen wax garab bi: "Buddeekul te nga sampu ci biir géej gi," dina leen déggal. 7 Kan ci yeen bu amoon surga, mu nekk ci tool yi di bey walla muy sàmm ba ñibbisi nga ne ko: "toogal te nga lekk"? 8 Déedéet! Danga koy ne: "Toogal ma reer te nga solu, jox ma lekk te naan. Gannaaw loolu dinga mëna lekk te naan." 9 Ndax njaatige bi dina gërëm surga bi ngir li mu ko sant mu def ko? Déedéet! 10 Yeen tamit su ngeen defee lépp li ñu leen sant ba noppi neleen: "Surga rekk lanu. Sunu warugar lanu def."»
Yeesu setal na fukki gaana
11 Benn bés, Yeesu doon na dem Yerusalem, mu jaar ci dig wi xàjjale diiwaanu Samari ak bu Galile. 12 Bi muy waaja dugg ci benn gox, fukki gaana ñëw di dajesi ak moom. Ñu taxaw, sori ko tuuti, 13 ñu wax ci kaw ne: «Yeesu Kilifa gi, yërëm nu.»
14 Bi leen Yeesu gisee, mu ne leen: «Demleen ngeen won seen bopp jébbalkatu-sarax yi, ngir ñu saytu seen yaram.» Bi ñuy dem ci jébbalkatu-sarax yi, ci yoon bi, mu daldi leen setal. 15 Bi kenn ci ñoom gisee ne wér na, mu jaaraat ci ay tànkam di màggal Yàlla ak baat bu kawe. 16 Mu ñëw ci Yeesu, daanu ci ay tànkam, di ko gërëm. Kooku waa Samari la woon. 17 Noonu Yeesu daldi ne: «Xanaa, du fukk yi yépp ñoo set, ana yeneen juróom ñeent yi? 18 Bu dul gan gi, kenn ci ñoom dellusiwul ngir màggal Yàlla?» 19 Noonu Yeesu daldi wax waa ji: «Jógal te nga dem, sa ngëm muccal na la.»
Bés bi Doomu nit ki di ñëw
20 Benn bés Farisen yi laaj Yeesu, kañ la nguuru Yàlla gi di ñëw. Noonu Yeesu tontu leen: «Nguuru Yàlla gi, kenn mënu koo gis buy ñëw, 21 te kenn mënu la wax "mu ngi fii" walla "mu ngi fale" ndaxte, xamleen ne, nguuru Yàlla gi mu ngi ci seen biir.»
22 Noonu Yeesu ne taalibe yi: «Ay bés a ngi ñëw, yu ngeen di bëgga gis Doomu nit ki, bu doon sax benn bés, waaye du mëna nekk. 23 Dinañu leen ne: "Mu ngi fii" walla "mu ngi fee." Bu leen daw di leen topp. 24 Ndaxte ni melax di leerale asamaan boor ba boor, noonu lay Doomu nit ki di mel ci bésam. 25 Waaye fàww mu sonn lool bu jëkk, te niti jamono jii beddi ko.
26 «Bés bi Doomu nit ki dellusee, dina mel ni jamonoy Nóoyin. 27 Nit ñi, ñu ngi doon lekk ak naan. Ñii di takk jabar, ñii di séyi ba keroog Nóoyin di dugg ca gaal gu mag gi. Noonu mbënn mi ñëw te sànk leen ñoom ñépp. 28 Itam dina mel ni jamonoy Lóot. Nit ñi ñu ngi doon lekk, naan di jënd di jaay, tey tabax. 29 Ba keroog Lóot di génn ci dëkku Sodom te tawu safara ak tamarax wàcce ca asamaan te sànk leen ñoom ñépp. 30 Noonu lay mel bés bu Doomu nit ki feeñee. 31 Ci bés boobu nit ku nekk ci kaw këram te am ay yëfam ci biir kër ga, bu mu wàcc ngir jël leen. Te ki nekk ci tool yi, bu mu ñibbisi. 32 Fàttalikuleen li daloon jabaru Lóot. 33 Ku wuta muccal sa bakkan dinga ko ñàkk, waaye ku ñàkk sa bakkan dinga dund. 34 Maa ngi leen koy wax, ci guddi googu, ñaar ñu bokk lal, ñu jël kenn ki bàyyi keneen ki. 35-36 Ñaari jigéen ànd di soq, ñu jël kenn ki bàyyi keneen ki.» 37 Noonu taalibe yi laaj ko: «Boroom bi, fan la loolu di xewe?» Mu ne leen: «Fu lu dee nekk, fa la tan yi di daje.»